An-Nisa · 1/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
يَا أَيُّهَا النَّاسُ اتَّقُوا رَبَّكُمُ الَّذِي خَلَقَكُم مِّن نَّفْسٍ وَاحِدَةٍ وَخَلَقَ مِنْهَا زَوْجَهَا وَبَثَّ مِنْهُمَا رِجَالًا كَثِيرًا وَنِسَاءً ۚ وَاتَّقُوا اللَّهَ الَّذِي تَسَاءَلُونَ بِهِ وَالْأَرْحَامَ ۚ إِنَّ اللَّهَ كَانَ عَلَيْكُمْ رَقِيبًا ۝١
Yaaa aiyuhan naasut taqoo Rabbakumul lazee khalaqakum min nafsinw waahidatinw wa khalaqa minhaa zawjahaa wa bas sa minhumaa rijaalan kaseeranw wa nisaaa`aa; wattaqul laahallazee tasaaa `aloona bihee wal arhaam; innal laaha kaana `alaikum Raqeeba
📖 Tekkim Wolof
Éy yéen nit ni ! Ragal-leen Yàlla mi leen sàkk ci benn bakkan, sàkke itam soxnaam sa, njërtal ci aw góor ak jigéen ñu bari. Ragal-leen Yàlla ji ngeen di laajante, ak ug dog mbokk. Yàlla nag ku leen di fuglu la.
🎧 Dégg

📜 Aaya 1-3 — An-Nisa

1يَا أَيُّهَا النَّاسُ اتَّقُوا رَبَّكُمُ الَّذِي خَلَقَكُم مِّن نَّفْسٍ وَاحِدَةٍ وَخَلَقَ مِنْهَا زَوْجَهَا وَبَثَّ مِنْهُمَا رِجَالًا كَثِيرًا وَنِسَاءً ۚ وَاتَّقُوا اللَّهَ الَّذِي تَسَاءَلُونَ بِهِ وَالْأَرْحَامَ ۚ إِنَّ اللَّهَ كَانَ عَلَيْكُمْ رَقِيبًا
Éy yéen nit ni ! Ragal-leen Yàlla mi leen sàkk ci benn bakkan, sàkke itam soxnaam sa, njërtal ci aw góor ak jigéen ñu bari. Ragal-leen Yàlla ji ngeen di laajante, ak ug dog mbokk. Yàlla nag ku leen di fuglu la.
2وَآتُوا الْيَتَامَىٰ أَمْوَالَهُمْ ۖ وَلَا تَتَبَدَّلُوا الْخَبِيثَ بِالطَّيِّبِ ۖ وَلَا تَأْكُلُوا أَمْوَالَهُمْ إِلَىٰ أَمْوَالِكُمْ ۚ إِنَّهُ كَانَ حُوبًا كَبِيرًا
Te ngeen jox jirim yi seeni alal ; te buleen wecce lu baax [ca la ñu moom] joxe lu bon la. Buleen lekk la ñu am ci alal di ko booleek seeni alal : ndax loolu bàkkaar bu rëy la.
3وَإِنْ خِفْتُمْ أَلَّا تُقْسِطُوا فِي الْيَتَامَىٰ فَانكِحُوا مَا طَابَ لَكُم مِّنَ النِّسَاءِ مَثْنَىٰ وَثُلَاثَ وَرُبَاعَ ۖ فَإِنْ خِفْتُمْ أَلَّا تَعْدِلُوا فَوَاحِدَةً أَوْ مَا مَلَكَتْ أَيْمَانُكُمْ ۚ ذَٰلِكَ أَدْنَىٰ أَلَّا تَعُولُوا
Su ngeen ragale bañ a maandu [ci seen jëflante ak jirim yi]..., mën ngeen takk lu leen neex te soob leen ciw jigéen, ñaar-ñaar, ñett ñett, ak ñeent ñeent, waaye, bu ngeen ragale ci ne dungeen maandu [ñàkk a yemale soxna ya], kon takkleen benn soxna walla sax ngeen jël benn jigéen [jaam bu jigéen]. Ndax loolu moo gën a jege maandute.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
1Aaya

Tekki — An-Nisa 1

Simoore An-Nisa Aaya 1 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Éy yéen nit ni ! Ragal-leen Yàlla mi leen sàkk…

Simoore Aaya 1/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 1–3. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers