An-Nisa · 2/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
وَآتُوا الْيَتَامَىٰ أَمْوَالَهُمْ ۖ وَلَا تَتَبَدَّلُوا الْخَبِيثَ بِالطَّيِّبِ ۖ وَلَا تَأْكُلُوا أَمْوَالَهُمْ إِلَىٰ أَمْوَالِكُمْ ۚ إِنَّهُ كَانَ حُوبًا كَبِيرًا ۝٢
Wa aatul yataamaaa amwaalahum wa laa tatabad dalul khabeesa bittaiyibi wa laa taakulooo amwaalahum ilaaa amwaalikum; innahoo kaana hooban kabeeraa
📖 Tekkim Wolof
Te ngeen jox jirim yi seeni alal ; te buleen wecce lu baax [ca la ñu moom] joxe lu bon la. Buleen lekk la ñu am ci alal di ko booleek seeni alal : ndax loolu bàkkaar bu rëy la.
🎧 Dégg

📜 Aaya 1-4 — An-Nisa

1يَا أَيُّهَا النَّاسُ اتَّقُوا رَبَّكُمُ الَّذِي خَلَقَكُم مِّن نَّفْسٍ وَاحِدَةٍ وَخَلَقَ مِنْهَا زَوْجَهَا وَبَثَّ مِنْهُمَا رِجَالًا كَثِيرًا وَنِسَاءً ۚ وَاتَّقُوا اللَّهَ الَّذِي تَسَاءَلُونَ بِهِ وَالْأَرْحَامَ ۚ إِنَّ اللَّهَ كَانَ عَلَيْكُمْ رَقِيبًا
Éy yéen nit ni ! Ragal-leen Yàlla mi leen sàkk ci benn bakkan, sàkke itam soxnaam sa, njërtal ci aw góor ak jigéen ñu bari. Ragal-leen Yàlla ji ngeen di laajante, ak ug dog mbokk. Yàlla nag ku leen di fuglu la.
2وَآتُوا الْيَتَامَىٰ أَمْوَالَهُمْ ۖ وَلَا تَتَبَدَّلُوا الْخَبِيثَ بِالطَّيِّبِ ۖ وَلَا تَأْكُلُوا أَمْوَالَهُمْ إِلَىٰ أَمْوَالِكُمْ ۚ إِنَّهُ كَانَ حُوبًا كَبِيرًا
Te ngeen jox jirim yi seeni alal ; te buleen wecce lu baax [ca la ñu moom] joxe lu bon la. Buleen lekk la ñu am ci alal di ko booleek seeni alal : ndax loolu bàkkaar bu rëy la.
3وَإِنْ خِفْتُمْ أَلَّا تُقْسِطُوا فِي الْيَتَامَىٰ فَانكِحُوا مَا طَابَ لَكُم مِّنَ النِّسَاءِ مَثْنَىٰ وَثُلَاثَ وَرُبَاعَ ۖ فَإِنْ خِفْتُمْ أَلَّا تَعْدِلُوا فَوَاحِدَةً أَوْ مَا مَلَكَتْ أَيْمَانُكُمْ ۚ ذَٰلِكَ أَدْنَىٰ أَلَّا تَعُولُوا
Su ngeen ragale bañ a maandu [ci seen jëflante ak jirim yi]..., mën ngeen takk lu leen neex te soob leen ciw jigéen, ñaar-ñaar, ñett ñett, ak ñeent ñeent, waaye, bu ngeen ragale ci ne dungeen maandu [ñàkk a yemale soxna ya], kon takkleen benn soxna walla sax ngeen jël benn jigéen [jaam bu jigéen]. Ndax loolu moo gën a jege maandute.
4وَآتُوا النِّسَاءَ صَدُقَاتِهِنَّ نِحْلَةً ۚ فَإِن طِبْنَ لَكُمْ عَن شَيْءٍ مِّنْهُ نَفْسًا فَكُلُوهُ هَنِيئًا مَّرِيئًا
Nangeen jox jigéen ñi seen can mu dig may. Bu ñu leen ca yéwénalee dara te may leen ca dara te mu di ci teeyu bakkan, lekkleen ko na mu leen neexe.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
2Aaya

Tekki — An-Nisa 2

Simoore An-Nisa Aaya 2 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te ngeen jox jirim yi seeni alal ; te buleen…

Simoore Aaya 2/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 1–4. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers