An-Nisa · 123/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
لَّيْسَ بِأَمَانِيِّكُمْ وَلَا أَمَانِيِّ أَهْلِ الْكِتَابِ ۗ مَن يَعْمَلْ سُوءًا يُجْزَ بِهِ وَلَا يَجِدْ لَهُ مِن دُونِ اللَّهِ وَلِيًّا وَلَا نَصِيرًا ۝١٢٣
Laisa bi amaaniyyikum wa laaa amaaniyyi Ahlil Kitaab; mai ya`mal sooo`ai yujza bihee wa laa yajid lahoo min doonil laahi waliyanw wa laa naseeraa
📖 Tekkim Wolof
Mbir ma ajuwul ci seeni mébét walla ci mébétu ña jotoon Téere. Waaye ku def ñaawtéef, jot peyam, kenn du ko mën a amal kilifa gu ko yiir mbaa mu ko mën a dimbali ginnaaw bu ca Yàlla génnee.

🎧 Dégg


📜 Aaya 121-125 — An-Nisa

121أُولَٰئِكَ مَأْوَاهُمْ جَهَنَّمُ وَلَا يَجِدُونَ عَنْهَا مَحِيصًا
Ñooñu seeni dëkkuwaay mooy Safara. Te kenn duleen ca musal !
122وَالَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ سَنُدْخِلُهُمْ جَنَّاتٍ تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ خَالِدِينَ فِيهَا أَبَدًا ۖ وَعْدَ اللَّهِ حَقًّا ۚ وَمَنْ أَصْدَقُ مِنَ اللَّهِ قِيلًا
Ñi gëm te jëf aw yiw. Dananu leen dugal Àjjana yu ay dex di daw ci suufam, dañu fay béel ba fàwwu. Digeb Yàlla lu dëggu la. Te sax, ana kan moo gën a dëggu ay wax Yàlla ?
123لَّيْسَ بِأَمَانِيِّكُمْ وَلَا أَمَانِيِّ أَهْلِ الْكِتَابِ ۗ مَن يَعْمَلْ سُوءًا يُجْزَ بِهِ وَلَا يَجِدْ لَهُ مِن دُونِ اللَّهِ وَلِيًّا وَلَا نَصِيرًا
Mbir ma ajuwul ci seeni mébét walla ci mébétu ña jotoon Téere. Waaye ku def ñaawtéef, jot peyam, kenn du ko mën a amal kilifa gu ko yiir mbaa mu ko mën a dimbali ginnaaw bu ca Yàlla génnee.
124وَمَن يَعْمَلْ مِنَ الصَّالِحَاتِ مِن ذَكَرٍ أَوْ أُنثَىٰ وَهُوَ مُؤْمِنٌ فَأُولَٰئِكَ يَدْخُلُونَ الْجَنَّةَ وَلَا يُظْلَمُونَ نَقِيرًا
Ku jëf, jëf ju bokk ci aw yiw, di góor mbaa muy jigéen, te di ab jullit... ñooña danañu dugg Àjjana; te kenn duleen ca tooñ [ba waññil leen] lu toll ni mboxosu xooxu tàndarma.
125وَمَنْ أَحْسَنُ دِينًا مِّمَّنْ أَسْلَمَ وَجْهَهُ لِلَّهِ وَهُوَ مُحْسِنٌ وَاتَّبَعَ مِلَّةَ إِبْرَاهِيمَ حَنِيفًا ۗ وَاتَّخَذَ اللَّهُ إِبْرَاهِيمَ خَلِيلًا
Ana ku gën a rafet diine ku jubale boppam Yàlla, te di kuy rafetal [jëfam], tey roy diiney Ibraahiima cig wéetal Yàlla ? Te Yàlla Moom jàppe na Ibraahiima soppeem.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
123Aaya

Tekki — An-Nisa 123

Simoore An-Nisa Aaya 123 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mbir ma ajuwul ci seeni mébét walla ci mébétu ña…

Simoore Aaya 123/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 121–125. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers