An-Nisa · 122/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
وَالَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ سَنُدْخِلُهُمْ جَنَّاتٍ تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ خَالِدِينَ فِيهَا أَبَدًا ۖ وَعْدَ اللَّهِ حَقًّا ۚ وَمَنْ أَصْدَقُ مِنَ اللَّهِ قِيلًا ۝١٢٢
Wallazeena aamanoo wa `amilus saalihaati sanud khiluhum Jannaatin tajree min tahtihal anhaaru khaalideena feehaaa abadaa; wa`dal laahi haqqaa; wa man asdaqu minal laahi qeelaa
📖 Tekkim Wolof
Ñi gëm te jëf aw yiw. Dananu leen dugal Àjjana yu ay dex di daw ci suufam, dañu fay béel ba fàwwu. Digeb Yàlla lu dëggu la. Te sax, ana kan moo gën a dëggu ay wax Yàlla ?
🎧 Dégg

📜 Aaya 120-124 — An-Nisa

120يَعِدُهُمْ وَيُمَنِّيهِمْ ۖ وَمَا يَعِدُهُمُ الشَّيْطَانُ إِلَّا غُرُورًا
Dana leen dig, xemmemlu leen. Te Séytaane du dige lu dul ay wor.
121أُولَٰئِكَ مَأْوَاهُمْ جَهَنَّمُ وَلَا يَجِدُونَ عَنْهَا مَحِيصًا
Ñooñu seeni dëkkuwaay mooy Safara. Te kenn duleen ca musal !
122وَالَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ سَنُدْخِلُهُمْ جَنَّاتٍ تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ خَالِدِينَ فِيهَا أَبَدًا ۖ وَعْدَ اللَّهِ حَقًّا ۚ وَمَنْ أَصْدَقُ مِنَ اللَّهِ قِيلًا
Ñi gëm te jëf aw yiw. Dananu leen dugal Àjjana yu ay dex di daw ci suufam, dañu fay béel ba fàwwu. Digeb Yàlla lu dëggu la. Te sax, ana kan moo gën a dëggu ay wax Yàlla ?
123لَّيْسَ بِأَمَانِيِّكُمْ وَلَا أَمَانِيِّ أَهْلِ الْكِتَابِ ۗ مَن يَعْمَلْ سُوءًا يُجْزَ بِهِ وَلَا يَجِدْ لَهُ مِن دُونِ اللَّهِ وَلِيًّا وَلَا نَصِيرًا
Mbir ma ajuwul ci seeni mébét walla ci mébétu ña jotoon Téere. Waaye ku def ñaawtéef, jot peyam, kenn du ko mën a amal kilifa gu ko yiir mbaa mu ko mën a dimbali ginnaaw bu ca Yàlla génnee.
124وَمَن يَعْمَلْ مِنَ الصَّالِحَاتِ مِن ذَكَرٍ أَوْ أُنثَىٰ وَهُوَ مُؤْمِنٌ فَأُولَٰئِكَ يَدْخُلُونَ الْجَنَّةَ وَلَا يُظْلَمُونَ نَقِيرًا
Ku jëf, jëf ju bokk ci aw yiw, di góor mbaa muy jigéen, te di ab jullit... ñooña danañu dugg Àjjana; te kenn duleen ca tooñ [ba waññil leen] lu toll ni mboxosu xooxu tàndarma.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
122Aaya

Tekki — An-Nisa 122

Simoore An-Nisa Aaya 122 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñi gëm te jëf aw yiw. Dananu leen dugal Àjjana…

Simoore Aaya 122/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 120–124. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers