An-Nisa · 143/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
مُّذَبْذَبِينَ بَيْنَ ذَٰلِكَ لَا إِلَىٰ هَٰؤُلَاءِ وَلَا إِلَىٰ هَٰؤُلَاءِ ۚ وَمَن يُضْلِلِ اللَّهُ فَلَن تَجِدَ لَهُ سَبِيلًا ۝١٤٣
Muzabzabeena baina zaalika laaa ilaa haaa` ulaaa`i wa laaa ilaa haaa`ulaaa`; wa mai yudlilil laahu falan tajida lahoo sabeela
📖 Tekkim Wolof
Ñuy deŋŋi-deŋŋi ci diggante yooyu, féetewuñu ci ñii, féetewuñu ca ñaa. Ku Yàlla bàyyi cig cànkuteem, kenn du ko mën a teg ci yoon wu jub wa.
🎧 Dégg

📜 Aaya 141-145 — An-Nisa

141الَّذِينَ يَتَرَبَّصُونَ بِكُمْ فَإِن كَانَ لَكُمْ فَتْحٌ مِّنَ اللَّهِ قَالُوا أَلَمْ نَكُن مَّعَكُمْ وَإِن كَانَ لِلْكَافِرِينَ نَصِيبٌ قَالُوا أَلَمْ نَسْتَحْوِذْ عَلَيْكُمْ وَنَمْنَعْكُم مِّنَ الْمُؤْمِنِينَ ۚ فَاللَّهُ يَحْكُمُ بَيْنَكُمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ ۗ وَلَن يَجْعَلَ اللَّهُ لِلْكَافِرِينَ عَلَى الْمُؤْمِنِينَ سَبِيلًا
Ña nga xam ne ñanga téyandi seen bopp ci yéen ; su leen Yàlla joxee ndam, ñu gaaw ne : “Ndax àndunu woon ak yéen ? ” ; bu yéefar yi amee cër ci ndam, ñu ne leen : “Xanaa du ñoo leen doon song [yéen yéefar yi] te nu fegal leen jullit ñi ? ”. Yàlla Dana àtte seen diggante Bis-pénc ba. Te du jox yéefar yi ndam ci kaw jullit ñi.
142إِنَّ الْمُنَافِقِينَ يُخَادِعُونَ اللَّهَ وَهُوَ خَادِعُهُمْ وَإِذَا قَامُوا إِلَى الصَّلَاةِ قَامُوا كُسَالَىٰ يُرَاءُونَ النَّاسَ وَلَا يَذْكُرُونَ اللَّهَ إِلَّا قَلِيلًا
Naaféq ya dañuy jéem a nax Yàlla, te fekk Yàlla Dana leen juuy. Te bu ñu taxawalee julli, taxaw ci tàyyeel, di ngistal ci bëti nit ñi. Te duñu tudd [fàttaliku Yàlla] lu dul ñu néew ci ñoom.
143مُّذَبْذَبِينَ بَيْنَ ذَٰلِكَ لَا إِلَىٰ هَٰؤُلَاءِ وَلَا إِلَىٰ هَٰؤُلَاءِ ۚ وَمَن يُضْلِلِ اللَّهُ فَلَن تَجِدَ لَهُ سَبِيلًا
Ñuy deŋŋi-deŋŋi ci diggante yooyu, féetewuñu ci ñii, féetewuñu ca ñaa. Ku Yàlla bàyyi cig cànkuteem, kenn du ko mën a teg ci yoon wu jub wa.
144يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَا تَتَّخِذُوا الْكَافِرِينَ أَوْلِيَاءَ مِن دُونِ الْمُؤْمِنِينَ ۚ أَتُرِيدُونَ أَن تَجْعَلُوا لِلَّهِ عَلَيْكُمْ سُلْطَانًا مُّبِينًا
Éy yéen ñi gëm ! Buleen jàppe yéefar yi ay xarit bàyyi jullit ña. Ndax dangeen bëgg a jox Yàlla lay wu jub ci seen kaw ?
145إِنَّ الْمُنَافِقِينَ فِي الدَّرْكِ الْأَسْفَلِ مِنَ النَّارِ وَلَن تَجِدَ لَهُمْ نَصِيرًا
Naaféq yaa nga ca dëru ya gën a suufe ca Safara, te kenn duleen dimbali,
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
143Aaya

Tekki — An-Nisa 143

Simoore An-Nisa Aaya 143 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñuy deŋŋi-deŋŋi ci diggante yooyu, féetewuñu ci ñii, féetewuñu ca…

Simoore Aaya 143/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 141–145. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers