An-Nisa · 49/176
Tekki Waxtaan — Simoore An-Nisa
أَلَمْ تَرَ إِلَى الَّذِينَ يُزَكُّونَ أَنفُسَهُم ۚ بَلِ اللَّهُ يُزَكِّي مَن يَشَاءُ وَلَا يُظْلَمُونَ فَتِيلًا ۝٤٩
Alam tara ilal lazeena yuzakkoona anfusahum; balil laahu yuzakkee mai yashaaa`u wa laa yuzlamoona fateelaa
📖 Tekkim Wolof
Moo ndax dangaa gisul ña doon sànkoo sellal seen bopp ? Li wér te wóor mooy Yàllaay sellal ku ko soob ; te duleen tooñ [Bis-pénc ba], lu toll ni karnu xooxu tàndarma.

🎧 Dégg


📜 Aaya 47-51 — Simoore An-Nisa

47يَا أَيُّهَا الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ آمِنُوا بِمَا نَزَّلْنَا مُصَدِّقًا لِّمَا مَعَكُم مِّن قَبْلِ أَن نَّطْمِسَ وُجُوهًا فَنَرُدَّهَا عَلَىٰ أَدْبَارِهَا أَوْ نَلْعَنَهُمْ كَمَا لَعَنَّا أَصْحَابَ السَّبْتِ ۚ وَكَانَ أَمْرُ اللَّهِ مَفْعُولًا
Éy yéen ñi jotoon Téere, gëmleen lii Nu wàcce, di dëggal li ngeen yor, bala Noo marmaral ay xar-kanam wëlbati leen ñu jëm ginnaaw, walla Nu leen di rëbbu na ñu rëbbe woon ña jalgati woon ca gaawu ba. Ndigalu Yàlla ak mbiram jëfe la sant [du jaas].
48إِنَّ اللَّهَ لَا يَغْفِرُ أَن يُشْرَكَ بِهِ وَيَغْفِرُ مَا دُونَ ذَٰلِكَ لِمَن يَشَاءُ ۚ وَمَن يُشْرِكْ بِاللَّهِ فَقَدِ افْتَرَىٰ إِثْمًا عَظِيمًا
Yàlla du baal ku Ko bokkaale dara. Waaye lu moy loolu, Dana ko jéggal ku ko soob. Ka bokkaale Yàlla [ak dara], def na bàkkaar bu rëy.
49أَلَمْ تَرَ إِلَى الَّذِينَ يُزَكُّونَ أَنفُسَهُم ۚ بَلِ اللَّهُ يُزَكِّي مَن يَشَاءُ وَلَا يُظْلَمُونَ فَتِيلًا
Moo ndax dangaa gisul ña doon sànkoo sellal seen bopp ? Li wér te wóor mooy Yàllaay sellal ku ko soob ; te duleen tooñ [Bis-pénc ba], lu toll ni karnu xooxu tàndarma.
50انظُرْ كَيْفَ يَفْتَرُونَ عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ ۖ وَكَفَىٰ بِهِ إِثْمًا مُّبِينًا
Gisal ni ñuy duuralee Yàlla ay fen. Te loolu, doy na bàkkaar te rànniku !
51أَلَمْ تَرَ إِلَى الَّذِينَ أُوتُوا نَصِيبًا مِّنَ الْكِتَابِ يُؤْمِنُونَ بِالْجِبْتِ وَالطَّاغُوتِ وَيَقُولُونَ لِلَّذِينَ كَفَرُوا هَٰؤُلَاءِ أَهْدَىٰ مِنَ الَّذِينَ آمَنُوا سَبِيلًا
Moo ndax gisoo ña jot lenni Téere ba, ñay gëm ay xërëm yu tudd [Jibti] ak [Taagut], ñuy wax ak ña weddi naanleen: “Seen xërëm yooyoo gën a nekk ci njub jullit ya gëm [Lislaam]” ?
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
49Aaya

Tekki — An-Nisa 49

Simoore An-Nisa Aaya 49 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Moo ndax dangaa gisul ña doon sànkoo sellal seen bopp…

Simoore Aaya 49/176 — Simoore An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore An-Nisa Dégg, Simoore An-Nisa Tekki, Simoore An-Nisa mp3, Simoore An-Nisa pdf. Aaya 47–51. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers