An-Nisa · 50/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
انظُرْ كَيْفَ يَفْتَرُونَ عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ ۖ وَكَفَىٰ بِهِ إِثْمًا مُّبِينًا ۝٥٠
Unzur kaifa yaftaroona `alal laahil kazib, wakafaa biheee ismamm mubeenaa
📖 Tekkim Wolof
Gisal ni ñuy duuralee Yàlla ay fen. Te loolu, doy na bàkkaar te rànniku !
🎧 Dégg

📜 Aaya 48-52 — An-Nisa

48إِنَّ اللَّهَ لَا يَغْفِرُ أَن يُشْرَكَ بِهِ وَيَغْفِرُ مَا دُونَ ذَٰلِكَ لِمَن يَشَاءُ ۚ وَمَن يُشْرِكْ بِاللَّهِ فَقَدِ افْتَرَىٰ إِثْمًا عَظِيمًا
Yàlla du baal ku Ko bokkaale dara. Waaye lu moy loolu, Dana ko jéggal ku ko soob. Ka bokkaale Yàlla [ak dara], def na bàkkaar bu rëy.
49أَلَمْ تَرَ إِلَى الَّذِينَ يُزَكُّونَ أَنفُسَهُم ۚ بَلِ اللَّهُ يُزَكِّي مَن يَشَاءُ وَلَا يُظْلَمُونَ فَتِيلًا
Moo ndax dangaa gisul ña doon sànkoo sellal seen bopp ? Li wér te wóor mooy Yàllaay sellal ku ko soob ; te duleen tooñ [Bis-pénc ba], lu toll ni karnu xooxu tàndarma.
50انظُرْ كَيْفَ يَفْتَرُونَ عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ ۖ وَكَفَىٰ بِهِ إِثْمًا مُّبِينًا
Gisal ni ñuy duuralee Yàlla ay fen. Te loolu, doy na bàkkaar te rànniku !
51أَلَمْ تَرَ إِلَى الَّذِينَ أُوتُوا نَصِيبًا مِّنَ الْكِتَابِ يُؤْمِنُونَ بِالْجِبْتِ وَالطَّاغُوتِ وَيَقُولُونَ لِلَّذِينَ كَفَرُوا هَٰؤُلَاءِ أَهْدَىٰ مِنَ الَّذِينَ آمَنُوا سَبِيلًا
Moo ndax gisoo ña jot lenni Téere ba, ñay gëm ay xërëm yu tudd [Jibti] ak [Taagut], ñuy wax ak ña weddi naanleen: “Seen xërëm yooyoo gën a nekk ci njub jullit ya gëm [Lislaam]” ?
52أُولَٰئِكَ الَّذِينَ لَعَنَهُمُ اللَّهُ ۖ وَمَن يَلْعَنِ اللَّهُ فَلَن تَجِدَ لَهُ نَصِيرًا
Ñooñu Yàlla rëbb na leen ; te ku Yàlla rëbb, kenn mënu koo amal ndimbal.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
50Aaya

Tekki — An-Nisa 50

Simoore An-Nisa Aaya 50 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Gisal ni ñuy duuralee Yàlla ay fen. Te loolu, doy…

Simoore Aaya 50/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 48–52. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers