Al-An'am · 137/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
وَكَذَٰلِكَ زَيَّنَ لِكَثِيرٍ مِّنَ الْمُشْرِكِينَ قَتْلَ أَوْلَادِهِمْ شُرَكَاؤُهُمْ لِيُرْدُوهُمْ وَلِيَلْبِسُوا عَلَيْهِمْ دِينَهُمْ ۖ وَلَوْ شَاءَ اللَّهُ مَا فَعَلُوهُ ۖ فَذَرْهُمْ وَمَا يَفْتَرُونَ ۝١٣٧
Wa kazaalika zaiyana likaseerim minal mushrikeena qatla awlaadihim shurakaaa`uhum liyurdoohum wa liyalbisoo `alaihim deenahum wa law shaaa`al laahu maa fa`aloohu fazarhum wa maa yaftaroon
📖 Tekkim Wolof
Noonu la seen xërëm yooyu rafetale, ca ñu bari ca way-bokkaale ya, rey seeni doom, ngir alag leen, lëntal seen diine. Bu neexoon Yàlla, duñu ko def. Waaye bàyyileen ak la ñuy duur.
🎧 Dégg

📜 Aaya 135-139 — Al-An'am

135قُلْ يَا قَوْمِ اعْمَلُوا عَلَىٰ مَكَانَتِكُمْ إِنِّي عَامِلٌ ۖ فَسَوْفَ تَعْلَمُونَ مَن تَكُونُ لَهُ عَاقِبَةُ الدَّارِ ۗ إِنَّهُ لَا يُفْلِحُ الظَّالِمُونَ
Neel : "Yéen samaw nit ! Jëfleen ci seeni mbir ; man dey aji-jëf laa. Dangeen mas a xami kan moo moom kër gu mujj ga.”. Ak lu mën a xew, tooñkat ya ñoom duñu texe.
136وَجَعَلُوا لِلَّهِ مِمَّا ذَرَأَ مِنَ الْحَرْثِ وَالْأَنْعَامِ نَصِيبًا فَقَالُوا هَٰذَا لِلَّهِ بِزَعْمِهِمْ وَهَٰذَا لِشُرَكَائِنَا ۖ فَمَا كَانَ لِشُرَكَائِهِمْ فَلَا يَصِلُ إِلَى اللَّهِ ۖ وَمَا كَانَ لِلَّهِ فَهُوَ يَصِلُ إِلَىٰ شُرَكَائِهِمْ ۗ سَاءَ مَا يَحْكُمُونَ
Dañuy sédd Yàlla li Mu bind ci mbey ak ci jur gi, ab cér daldi wax ne : “Lii mooy wàllu Yàlla - ci seeni njortu ! - lii mooy wàllu li nu koy bokkaale.”. Te la ñu sédd ñii, du agsi ca Yàlla, waaye la ñu sédd Yàlla, dana agsi ca ñañu koy bokkaaleel. Na ñuy àttee ñaaw na !
137وَكَذَٰلِكَ زَيَّنَ لِكَثِيرٍ مِّنَ الْمُشْرِكِينَ قَتْلَ أَوْلَادِهِمْ شُرَكَاؤُهُمْ لِيُرْدُوهُمْ وَلِيَلْبِسُوا عَلَيْهِمْ دِينَهُمْ ۖ وَلَوْ شَاءَ اللَّهُ مَا فَعَلُوهُ ۖ فَذَرْهُمْ وَمَا يَفْتَرُونَ
Noonu la seen xërëm yooyu rafetale, ca ñu bari ca way-bokkaale ya, rey seeni doom, ngir alag leen, lëntal seen diine. Bu neexoon Yàlla, duñu ko def. Waaye bàyyileen ak la ñuy duur.
138وَقَالُوا هَٰذِهِ أَنْعَامٌ وَحَرْثٌ حِجْرٌ لَّا يَطْعَمُهَا إِلَّا مَن نَّشَاءُ بِزَعْمِهِمْ وَأَنْعَامٌ حُرِّمَتْ ظُهُورُهَا وَأَنْعَامٌ لَّا يَذْكُرُونَ اسْمَ اللَّهِ عَلَيْهَا افْتِرَاءً عَلَيْهِ ۚ سَيَجْزِيهِم بِمَا كَانُوا يَفْتَرُونَ
Ñu naan : “Jur gi ak mbey mi araam na : kenn du ci lekk ku dul ku Nu neex.”. - ci seeni njort ! - Ak jur goo xam ne seen ginnaaw araam na, ak yoo xam ne duñu tuddu Yàlla ci ñoom, lu dul di ko duural, Dana leen fey la ñu nekkoon di ko duur.
139وَقَالُوا مَا فِي بُطُونِ هَٰذِهِ الْأَنْعَامِ خَالِصَةٌ لِّذُكُورِنَا وَمُحَرَّمٌ عَلَىٰ أَزْوَاجِنَا ۖ وَإِن يَكُن مَّيْتَةً فَهُمْ فِيهِ شُرَكَاءُ ۚ سَيَجْزِيهِمْ وَصْفَهُمْ ۚ إِنَّهُ حَكِيمٌ عَلِيمٌ
Ñu naan : “Li nekk ci biir jur gi dagan na ci sunuy góor waaye araam na ci sunuy jabar [jigéen ñi].”. Waay, bu dee lu médd, góor ak jigéen ñoo ci yem. Dana leen fey seeni duur, Moom dey [Yàlla] Ku xereñ la, Ku xam la.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
137Aaya

Tekki — Al-An'am 137

Simoore Al-An'am Aaya 137 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Noonu la seen xërëm yooyu rafetale, ca ñu bari ca…

Simoore Aaya 137/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 135–139. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers