Al-An'am · 38/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
وَمَا مِن دَابَّةٍ فِي الْأَرْضِ وَلَا طَائِرٍ يَطِيرُ بِجَنَاحَيْهِ إِلَّا أُمَمٌ أَمْثَالُكُم ۚ مَّا فَرَّطْنَا فِي الْكِتَابِ مِن شَيْءٍ ۚ ثُمَّ إِلَىٰ رَبِّهِمْ يُحْشَرُونَ ۝٣٨
Wa maa min daaabbatin fil ardi wa laa taaa`iriny yateeru bijanaahaihi illaaa umamun amsaalukum; maa farratnaa fil Kitaabi min shai`in summa ilaa Rabbihim yuhsharoon
📖 Tekkim Wolof
Amul lenn luy dukkat ci suuf, du caageene luy naawe ñaari laaf, lu dul ne dañoo doon ay xeet [waasoo] ni yéen. Amul lenn lu Nu bàyyi ci Téere bi. [Xamleen ne] dees na leen fang jëme ci seen Boroom, gur-gur jiital wëtal.

🎧 Dégg


📜 Aaya 36-40 — Al-An'am

36۞ إِنَّمَا يَسْتَجِيبُ الَّذِينَ يَسْمَعُونَ ۘ وَالْمَوْتَىٰ يَبْعَثُهُمُ اللَّهُ ثُمَّ إِلَيْهِ يُرْجَعُونَ
Ñay dégg ñoo lay wuyu. Ña dee, Yàlla Dana leen dekkal ; ñu dellusi ca Moom..
37وَقَالُوا لَوْلَا نُزِّلَ عَلَيْهِ آيَةٌ مِّن رَّبِّهِ ۚ قُلْ إِنَّ اللَّهَ قَادِرٌ عَلَىٰ أَن يُنَزِّلَ آيَةً وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَهُمْ لَا يَعْلَمُونَ
Te ña ngay wax naan : “Lu tee woon ñu wàcce ci moom kéemaan gu tukke ci Yàlla ? ”. Neel : “Yàlla ku am kàttan la ci wàcce kéemaan. Waaye li ëpp ci ñoom xamuñu”.
38وَمَا مِن دَابَّةٍ فِي الْأَرْضِ وَلَا طَائِرٍ يَطِيرُ بِجَنَاحَيْهِ إِلَّا أُمَمٌ أَمْثَالُكُم ۚ مَّا فَرَّطْنَا فِي الْكِتَابِ مِن شَيْءٍ ۚ ثُمَّ إِلَىٰ رَبِّهِمْ يُحْشَرُونَ
Amul lenn luy dukkat ci suuf, du caageene luy naawe ñaari laaf, lu dul ne dañoo doon ay xeet [waasoo] ni yéen. Amul lenn lu Nu bàyyi ci Téere bi. [Xamleen ne] dees na leen fang jëme ci seen Boroom, gur-gur jiital wëtal.
39وَالَّذِينَ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا صُمٌّ وَبُكْمٌ فِي الظُّلُمَاتِ ۗ مَن يَشَإِ اللَّهُ يُضْلِلْهُ وَمَن يَشَأْ يَجْعَلْهُ عَلَىٰ صِرَاطٍ مُّسْتَقِيمٍ
Te ña weddi Sunuy kàddu, dañoo tëx, luu, gumba. Yàlla ku ko soob, mu bàyyi ko cig réeram ; ku Ko soob Mu teg ko ci yoon wu jub wa xocc.
40قُلْ أَرَأَيْتَكُمْ إِنْ أَتَاكُمْ عَذَابُ اللَّهِ أَوْ أَتَتْكُمُ السَّاعَةُ أَغَيْرَ اللَّهِ تَدْعُونَ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Neel : “Waxleen ma : ndax su leen mbugalum Yàlla dalee, walla Bis-pénc ba na jaseet ci seen kaw, su fekkee li ngeen di woote dëgg la ci yéen, moo ndax kon dangeen fawoo keneen ku moy Yàlla ? ”
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
38Aaya

Tekki — Al-An'am 38

Simoore Al-An'am Aaya 38 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Amul lenn luy dukkat ci suuf, du caageene luy naawe…

Simoore Aaya 38/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 36–40. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers