Al-An'am · 39/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
وَالَّذِينَ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا صُمٌّ وَبُكْمٌ فِي الظُّلُمَاتِ ۗ مَن يَشَإِ اللَّهُ يُضْلِلْهُ وَمَن يَشَأْ يَجْعَلْهُ عَلَىٰ صِرَاطٍ مُّسْتَقِيمٍ ۝٣٩
Wallazeena kazzaboo bi Aayaatinaa summunw wa bukmun fiz zulumaat; mai yasha il laahu yudlilh; wa mai yashaa yaj`alhu `alaa Siraatim Mustaqeem
📖 Tekkim Wolof
Te ña weddi Sunuy kàddu, dañoo tëx, luu, gumba. Yàlla ku ko soob, mu bàyyi ko cig réeram ; ku Ko soob Mu teg ko ci yoon wu jub wa xocc.
🎧 Dégg

📜 Aaya 37-41 — Al-An'am

37وَقَالُوا لَوْلَا نُزِّلَ عَلَيْهِ آيَةٌ مِّن رَّبِّهِ ۚ قُلْ إِنَّ اللَّهَ قَادِرٌ عَلَىٰ أَن يُنَزِّلَ آيَةً وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَهُمْ لَا يَعْلَمُونَ
Te ña ngay wax naan : “Lu tee woon ñu wàcce ci moom kéemaan gu tukke ci Yàlla ? ”. Neel : “Yàlla ku am kàttan la ci wàcce kéemaan. Waaye li ëpp ci ñoom xamuñu”.
38وَمَا مِن دَابَّةٍ فِي الْأَرْضِ وَلَا طَائِرٍ يَطِيرُ بِجَنَاحَيْهِ إِلَّا أُمَمٌ أَمْثَالُكُم ۚ مَّا فَرَّطْنَا فِي الْكِتَابِ مِن شَيْءٍ ۚ ثُمَّ إِلَىٰ رَبِّهِمْ يُحْشَرُونَ
Amul lenn luy dukkat ci suuf, du caageene luy naawe ñaari laaf, lu dul ne dañoo doon ay xeet [waasoo] ni yéen. Amul lenn lu Nu bàyyi ci Téere bi. [Xamleen ne] dees na leen fang jëme ci seen Boroom, gur-gur jiital wëtal.
39وَالَّذِينَ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا صُمٌّ وَبُكْمٌ فِي الظُّلُمَاتِ ۗ مَن يَشَإِ اللَّهُ يُضْلِلْهُ وَمَن يَشَأْ يَجْعَلْهُ عَلَىٰ صِرَاطٍ مُّسْتَقِيمٍ
Te ña weddi Sunuy kàddu, dañoo tëx, luu, gumba. Yàlla ku ko soob, mu bàyyi ko cig réeram ; ku Ko soob Mu teg ko ci yoon wu jub wa xocc.
40قُلْ أَرَأَيْتَكُمْ إِنْ أَتَاكُمْ عَذَابُ اللَّهِ أَوْ أَتَتْكُمُ السَّاعَةُ أَغَيْرَ اللَّهِ تَدْعُونَ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Neel : “Waxleen ma : ndax su leen mbugalum Yàlla dalee, walla Bis-pénc ba na jaseet ci seen kaw, su fekkee li ngeen di woote dëgg la ci yéen, moo ndax kon dangeen fawoo keneen ku moy Yàlla ? ”
41بَلْ إِيَّاهُ تَدْعُونَ فَيَكْشِفُ مَا تَدْعُونَ إِلَيْهِ إِن شَاءَ وَتَنسَوْنَ مَا تُشْرِكُونَ
Déedéet, Moom ci boppam ngeen di woo. Mu xar lor ja su ko soobee, ngeen daldi fàtte ya ngeen daan bokkaale.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
39Aaya

Tekki — Al-An'am 39

Simoore Al-An'am Aaya 39 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te ña weddi Sunuy kàddu, dañoo tëx, luu, gumba. Yàlla…

Simoore Aaya 39/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 37–41. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers