Al-Mumtahina · 8/13
Tekki Waxtaan — Al-Mumtahina
لَّا يَنْهَاكُمُ اللَّهُ عَنِ الَّذِينَ لَمْ يُقَاتِلُوكُمْ فِي الدِّينِ وَلَمْ يُخْرِجُوكُم مِّن دِيَارِكُمْ أَن تَبَرُّوهُمْ وَتُقْسِطُوا إِلَيْهِمْ ۚ إِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ الْمُقْسِطِينَ ۝٨
Laa yanhaakumul laahu `anil lazeena lam yuqaatilookum fid deeni wa lam yukhrijookum min diyaarikum an tabarroohum wa tuqsitooo ilaihim; innal laaha yuhibbul muqsiteen
📖 Tekkim Wolof
Yàlla duleen tere ngeen di maslaa ak di laamisook ñi xeexul ak yéen ci seen diine te génnewuñuleen seeni kër. Yàlla safoona way maandu yi.
🎧 Dégg

📜 Aaya 6-10 — Al-Mumtahina

6لَقَدْ كَانَ لَكُمْ فِيهِمْ أُسْوَةٌ حَسَنَةٌ لِّمَن كَانَ يَرْجُو اللَّهَ وَالْيَوْمَ الْآخِرَ ۚ وَمَن يَتَوَلَّ فَإِنَّ اللَّهَ هُوَ الْغَنِيُّ الْحَمِيدُ
Ñoom am ngeen ci ñoom royuwaay wu rafet, mu ñeel képp ku yaakaar Yàlla ak Bis bu mujj ba : képp ku dumóoyu nag... na xam ne Yàlla ku doyloo boppam Yayoowaakoonu cant la.
7۞ عَسَى اللَّهُ أَن يَجْعَلَ بَيْنَكُمْ وَبَيْنَ الَّذِينَ عَادَيْتُم مِّنْهُم مَّوَدَّةً ۚ وَاللَّهُ قَدِيرٌ ۚ وَاللَّهُ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Amaana bu Yàlla defee ci seen diggante ak ñi ngeen noonooloon ag bëggënte. Yàlla Ku Man la te Yàlla Jéggëlaakoon Jaglewaakoon la.
8لَّا يَنْهَاكُمُ اللَّهُ عَنِ الَّذِينَ لَمْ يُقَاتِلُوكُمْ فِي الدِّينِ وَلَمْ يُخْرِجُوكُم مِّن دِيَارِكُمْ أَن تَبَرُّوهُمْ وَتُقْسِطُوا إِلَيْهِمْ ۚ إِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ الْمُقْسِطِينَ
Yàlla duleen tere ngeen di maslaa ak di laamisook ñi xeexul ak yéen ci seen diine te génnewuñuleen seeni kër. Yàlla safoona way maandu yi.
9إِنَّمَا يَنْهَاكُمُ اللَّهُ عَنِ الَّذِينَ قَاتَلُوكُمْ فِي الدِّينِ وَأَخْرَجُوكُم مِّن دِيَارِكُمْ وَظَاهَرُوا عَلَىٰ إِخْرَاجِكُمْ أَن تَوَلَّوْهُمْ ۚ وَمَن يَتَوَلَّهُمْ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الظَّالِمُونَ
Ñi leen Yàlla di tere kay ñooy ñiy xeex ak yéen ci diine, di leen génnee ci seeni kër walla ña leen cay jàppale. Buleen xaritoo mukk ak ñoom képp kuy xaritook ñoom ñooy tooñkat yi.
10يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا إِذَا جَاءَكُمُ الْمُؤْمِنَاتُ مُهَاجِرَاتٍ فَامْتَحِنُوهُنَّ ۖ اللَّهُ أَعْلَمُ بِإِيمَانِهِنَّ ۖ فَإِنْ عَلِمْتُمُوهُنَّ مُؤْمِنَاتٍ فَلَا تَرْجِعُوهُنَّ إِلَى الْكُفَّارِ ۖ لَا هُنَّ حِلٌّ لَّهُمْ وَلَا هُمْ يَحِلُّونَ لَهُنَّ ۖ وَآتُوهُم مَّا أَنفَقُوا ۚ وَلَا جُنَاحَ عَلَيْكُمْ أَن تَنكِحُوهُنَّ إِذَا آتَيْتُمُوهُنَّ أُجُورَهُنَّ ۚ وَلَا تُمْسِكُوا بِعِصَمِ الْكَوَافِرِ وَاسْأَلُوا مَا أَنفَقْتُمْ وَلْيَسْأَلُوا مَا أَنفَقُوا ۚ ذَٰلِكُمْ حُكْمُ اللَّهِ ۖ يَحْكُمُ بَيْنَكُمْ ۚ وَاللَّهُ عَلِيمٌ حَكِيمٌ
Eey yéen ñi gëm ! Su leen jullit yu jigéen ñi digëloon ne da ñuy gàddaay, nangeen leen seetlu nattu leen ; Yàllaa gën a xam seen dayob ngëm ; su ngeen xamee ne ay jullit la ñu, buleen leen delloo ca Yéefër ya. Ndax daganatuñu ci yéefar yi, Yéefër yi it daganatuñu ci ñoom. Te nangeen delloo alal ya. Aayul ci yéen ngeen denc leen soxna su ngeen joxee can. Buleen maslaak Yéefër. Laajleen la ngeen joxe woon ñoom it nañu laaj la ñu joxe woon. Loolu moo di àtteb Yàlla, Yàlla di àtte seen diggante Yàlla Ku Xam la Ku Xereñ la.
Al-MumtahinaFihi Alxuraan
13Aaya
MedinanRevelation
8Aaya

Tekki — Al-Mumtahina 8

Simoore Al-Mumtahina Aaya 8 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla duleen tere ngeen di maslaa ak di laamisook ñi…

Simoore Aaya 8/13 — Al-Mumtahina الممتحنة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Mumtahina Dégg, Al-Mumtahina Tekki, Al-Mumtahina mp3, Al-Mumtahina pdf. Aaya 6–10. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers