Al-A'raf · 51/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
الَّذِينَ اتَّخَذُوا دِينَهُمْ لَهْوًا وَلَعِبًا وَغَرَّتْهُمُ الْحَيَاةُ الدُّنْيَا ۚ فَالْيَوْمَ نَنسَاهُمْ كَمَا نَسُوا لِقَاءَ يَوْمِهِمْ هَٰذَا وَمَا كَانُوا بِآيَاتِنَا يَجْحَدُونَ ٥١
Transliteration
Allazeenat takhazoo deenahu lahwanw wa la`i-banw wa gharrat humul hayaatud dunyaa; fal Yawma nnannsaahum kamaa nasoo liqaaa`a Yawmihim haazaa wa maa kaanoo bi aayaatinaa yajhadoon
Tekki (Tekkim Wolof)
📖 Tekkim Wolof
Ña nga xam ne dañoo jàppe seen diine po ak i caaxaan, te dundug àddina nax leen. Tey Dananu leen fàtte na ñu fàttee woon ndajem tey jii, ak la ñu weddi woon Sunuy kàddu.
Additional reference in Fulfulde
🎧 Dégg
📜 Aaya 49-53 — Al-A'raf
49أَهَٰؤُلَاءِ الَّذِينَ أَقْسَمْتُمْ لَا يَنَالُهُمُ اللَّهُ بِرَحْمَةٍ ۚ ادْخُلُوا الْجَنَّةَ لَا خَوْفٌ عَلَيْكُمْ وَلَا أَنتُمْ تَحْزَنُونَ
Moo ndax ñii du ña ngeen giñoon ne Yàlla duleen dugal ci yërmaande... ? - Dugguleen ci Àjjana ! Te buleen am njàqare, te buleen am naqar.
50وَنَادَىٰ أَصْحَابُ النَّارِ أَصْحَابَ الْجَنَّةِ أَنْ أَفِيضُوا عَلَيْنَا مِنَ الْمَاءِ أَوْ مِمَّا رَزَقَكُمُ اللَّهُ ۚ قَالُوا إِنَّ اللَّهَ حَرَّمَهُمَا عَلَى الْكَافِرِينَ
Waa Safara woo waa Àjjana ne leen : “Bëbël-leen ci nun lenn ci ndox mi, walla ci li leen Yàlla wërsëgale.” Ñu toontu ne : “Yàlla dogal na ne [xéewal yii] araam na ci yéefar yi”.
51الَّذِينَ اتَّخَذُوا دِينَهُمْ لَهْوًا وَلَعِبًا وَغَرَّتْهُمُ الْحَيَاةُ الدُّنْيَا ۚ فَالْيَوْمَ نَنسَاهُمْ كَمَا نَسُوا لِقَاءَ يَوْمِهِمْ هَٰذَا وَمَا كَانُوا بِآيَاتِنَا يَجْحَدُونَ
Ña nga xam ne dañoo jàppe seen diine po ak i caaxaan, te dundug àddina nax leen. Tey Dananu leen fàtte na ñu fàttee woon ndajem tey jii, ak la ñu weddi woon Sunuy kàddu.
52وَلَقَدْ جِئْنَاهُم بِكِتَابٍ فَصَّلْنَاهُ عَلَىٰ عِلْمٍ هُدًى وَرَحْمَةً لِّقَوْمٍ يُؤْمِنُونَ
Te wóor na ne joxoon nanu leen ab Téere, bu Nu faramfàcce mu neex a dégg, muy njub ak yërmaande ngir nit ñu gëm.
53هَلْ يَنظُرُونَ إِلَّا تَأْوِيلَهُ ۚ يَوْمَ يَأْتِي تَأْوِيلُهُ يَقُولُ الَّذِينَ نَسُوهُ مِن قَبْلُ قَدْ جَاءَتْ رُسُلُ رَبِّنَا بِالْحَقِّ فَهَل لَّنَا مِن شُفَعَاءَ فَيَشْفَعُوا لَنَا أَوْ نُرَدُّ فَنَعْمَلَ غَيْرَ الَّذِي كُنَّا نَعْمَلُ ۚ قَدْ خَسِرُوا أَنفُسَهُمْ وَضَلَّ عَنْهُم مَّا كَانُوا يَفْتَرُونَ
Moo ndax dañuy xaar ba lu ko firndéel agsi ? Ña ko fàtte woon, la ko jiitu, danañu wax ne : “Yonenti sunu Boroom indi woon nañu dëgg. Moo ndax dananu amatiy rammukat yu nuy rammu ? Walla ñu delloo nu [àddina] nu def fa lu gën a rafet la nu fa daan def ? ”. Yàqal nañu jeeg seen bopp ; te la ñu daan duur réer na leen.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
51Aaya
Tekki — Al-A'raf 51
Simoore Al-A'raf Aaya 51 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña nga xam ne dañoo jàppe seen diine po ak…Simoore Aaya 51/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 49–53. Tekkim Wolof: Fulfulde.
العربية
English
Bahasa Indonesia
Türkçe
Русский
فارسی
Français
اردو
বাংলা
Deutsch
Español
中文
हिन्दी
Português
Italiano
ภาษาไทย
Polski
Nederlands
Shqip
Kiswahili
O'zbek
தமிழ்
Melayu
Bosanski
Soomaali
Azərbaycan
کوردی
한국어
日本語
Svenska
Dansk
Norsk
پښتو
മലയാളം
සිංහල
Tamazight
Hausa
አማርኛ
Български
Тоҷикӣ
Қазақша
Filipino
سنڌي
Yorùbá
Fulfulde
Татарча
ئۇيغۇرچە
Кыргызча
ਪੰਜਾਬੀ
Jawa
తెలుగు
မြန်မာ
ગુજરાતી
Oromo
मराठी
Tiếng Việt
Malagasy
Нохчийн
Wolof
ދިވެހި
ಕನ್ನಡ
Українська
Ελληνικά
ქართული
ខ្មែរ
دری
Qafar af
Maranao
नेपाली
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers








