Al-A'raf · 52/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
وَلَقَدْ جِئْنَاهُم بِكِتَابٍ فَصَّلْنَاهُ عَلَىٰ عِلْمٍ هُدًى وَرَحْمَةً لِّقَوْمٍ يُؤْمِنُونَ ۝٥٢
Wa laqad ji`naahum bi Kitaabin fassalnaahu `alaa `ilmin hudanw wa rahmatal liqawminy-yu`miinoon
📖 Tekkim Wolof
Te wóor na ne joxoon nanu leen ab Téere, bu Nu faramfàcce mu neex a dégg, muy njub ak yërmaande ngir nit ñu gëm.

🎧 Dégg


📜 Aaya 50-54 — Al-A'raf

50وَنَادَىٰ أَصْحَابُ النَّارِ أَصْحَابَ الْجَنَّةِ أَنْ أَفِيضُوا عَلَيْنَا مِنَ الْمَاءِ أَوْ مِمَّا رَزَقَكُمُ اللَّهُ ۚ قَالُوا إِنَّ اللَّهَ حَرَّمَهُمَا عَلَى الْكَافِرِينَ
Waa Safara woo waa Àjjana ne leen : “Bëbël-leen ci nun lenn ci ndox mi, walla ci li leen Yàlla wërsëgale.” Ñu toontu ne : “Yàlla dogal na ne [xéewal yii] araam na ci yéefar yi”.
51الَّذِينَ اتَّخَذُوا دِينَهُمْ لَهْوًا وَلَعِبًا وَغَرَّتْهُمُ الْحَيَاةُ الدُّنْيَا ۚ فَالْيَوْمَ نَنسَاهُمْ كَمَا نَسُوا لِقَاءَ يَوْمِهِمْ هَٰذَا وَمَا كَانُوا بِآيَاتِنَا يَجْحَدُونَ
Ña nga xam ne dañoo jàppe seen diine po ak i caaxaan, te dundug àddina nax leen. Tey Dananu leen fàtte na ñu fàttee woon ndajem tey jii, ak la ñu weddi woon Sunuy kàddu.
52وَلَقَدْ جِئْنَاهُم بِكِتَابٍ فَصَّلْنَاهُ عَلَىٰ عِلْمٍ هُدًى وَرَحْمَةً لِّقَوْمٍ يُؤْمِنُونَ
Te wóor na ne joxoon nanu leen ab Téere, bu Nu faramfàcce mu neex a dégg, muy njub ak yërmaande ngir nit ñu gëm.
53هَلْ يَنظُرُونَ إِلَّا تَأْوِيلَهُ ۚ يَوْمَ يَأْتِي تَأْوِيلُهُ يَقُولُ الَّذِينَ نَسُوهُ مِن قَبْلُ قَدْ جَاءَتْ رُسُلُ رَبِّنَا بِالْحَقِّ فَهَل لَّنَا مِن شُفَعَاءَ فَيَشْفَعُوا لَنَا أَوْ نُرَدُّ فَنَعْمَلَ غَيْرَ الَّذِي كُنَّا نَعْمَلُ ۚ قَدْ خَسِرُوا أَنفُسَهُمْ وَضَلَّ عَنْهُم مَّا كَانُوا يَفْتَرُونَ
Moo ndax dañuy xaar ba lu ko firndéel agsi ? Ña ko fàtte woon, la ko jiitu, danañu wax ne : “Yonenti sunu Boroom indi woon nañu dëgg. Moo ndax dananu amatiy rammukat yu nuy rammu ? Walla ñu delloo nu [àddina] nu def fa lu gën a rafet la nu fa daan def ? ”. Yàqal nañu jeeg seen bopp ; te la ñu daan duur réer na leen.
54إِنَّ رَبَّكُمُ اللَّهُ الَّذِي خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ فِي سِتَّةِ أَيَّامٍ ثُمَّ اسْتَوَىٰ عَلَى الْعَرْشِ يُغْشِي اللَّيْلَ النَّهَارَ يَطْلُبُهُ حَثِيثًا وَالشَّمْسَ وَالْقَمَرَ وَالنُّجُومَ مُسَخَّرَاتٍ بِأَمْرِهِ ۗ أَلَا لَهُ الْخَلْقُ وَالْأَمْرُ ۗ تَبَارَكَ اللَّهُ رَبُّ الْعَالَمِينَ
Seen Boroom nag mooy ki bind asamaan yeek suuf si ci juróom-benni fan, ba noppi Mu jublu ca Gàngunaay ga. Dana muure guddi ak bëccëg Mu toftale ko bu gaaw. Te jant bi ak weer wi ak bindiw, yu ñu tàggat lañu ci ndigalam. Moo ndax du Moo moom bind gi ak dogal yi? Yàlla Boroom àddina si, Ku barkeel la !
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
52Aaya

Tekki — Al-A'raf 52

Simoore Al-A'raf Aaya 52 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te wóor na ne joxoon nanu leen ab Téere, bu…

Simoore Aaya 52/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 50–54. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, August 19, 2026

Don't forget us in your sincere prayers