At-Tawba · 32/129
Tekki Waxtaan — At-Tawba
يُرِيدُونَ أَن يُطْفِئُوا نُورَ اللَّهِ بِأَفْوَاهِهِمْ وَيَأْبَى اللَّهُ إِلَّا أَن يُتِمَّ نُورَهُ وَلَوْ كَرِهَ الْكَافِرُونَ ۝٣٢
Yureedoona ai yutfi`oo nooral laahi bi`afwaahihim wa yaaballaahu illaaa ai yutimma noorahoo wa law karihal kaafiroon
📖 Tekkim Wolof
Dañoo bëgg a feye leerug Yàlla ak seen gémmiñ, te Yàlla di bañ ngir namm a mottali leeram, doonte la ñu weddi ña sib nañu loolu.
🎧 Dégg

📜 Aaya 30-34 — At-Tawba

30وَقَالَتِ الْيَهُودُ عُزَيْرٌ ابْنُ اللَّهِ وَقَالَتِ النَّصَارَى الْمَسِيحُ ابْنُ اللَّهِ ۖ ذَٰلِكَ قَوْلُهُم بِأَفْوَاهِهِمْ ۖ يُضَاهِئُونَ قَوْلَ الَّذِينَ كَفَرُوا مِن قَبْلُ ۚ قَاتَلَهُمُ اللَّهُ ۚ أَنَّىٰ يُؤْفَكُونَ
Yahuuf ya wax nañu ne : “Uzayru doomu Yàllaa”, Nasraan yi wax nañu ne : “Iisaa doomu Yàllaa”. Loolu seeni wax la jóge ci seeni gémmiñ. Dañoo jaare ci waxi ña weddi woon la leen jiitu. Yal na leen Yàlla alag ! Naka lañuy dummóoyoo ?
31اتَّخَذُوا أَحْبَارَهُمْ وَرُهْبَانَهُمْ أَرْبَابًا مِّن دُونِ اللَّهِ وَالْمَسِيحَ ابْنَ مَرْيَمَ وَمَا أُمِرُوا إِلَّا لِيَعْبُدُوا إِلَٰهًا وَاحِدًا ۖ لَّا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۚ سُبْحَانَهُ عَمَّا يُشْرِكُونَ
Dañoo jàppee seen fóore ya ak seen làbbe ya, ak Iisaa doomi Maryaama, ay yàlla, bàyyi Yàlla te digaleefuleen lu dul ñu jaamu Yàlla ja di kenn. Amul jeneen Yàlla ju dul Moom ! Sellam ga jomb na li ñu Koy bokkaale.
32يُرِيدُونَ أَن يُطْفِئُوا نُورَ اللَّهِ بِأَفْوَاهِهِمْ وَيَأْبَى اللَّهُ إِلَّا أَن يُتِمَّ نُورَهُ وَلَوْ كَرِهَ الْكَافِرُونَ
Dañoo bëgg a feye leerug Yàlla ak seen gémmiñ, te Yàlla di bañ ngir namm a mottali leeram, doonte la ñu weddi ña sib nañu loolu.
33هُوَ الَّذِي أَرْسَلَ رَسُولَهُ بِالْهُدَىٰ وَدِينِ الْحَقِّ لِيُظْهِرَهُ عَلَى الدِّينِ كُلِّهِ وَلَوْ كَرِهَ الْمُشْرِكُونَ
Moom moo yónni ab Yonentam cig njub jox ko diine ju dëggu ngir mu kaweel ko ca kaw diine yépp, doonte la bokkaalekat ya soppuñu ko.
34۞ يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا إِنَّ كَثِيرًا مِّنَ الْأَحْبَارِ وَالرُّهْبَانِ لَيَأْكُلُونَ أَمْوَالَ النَّاسِ بِالْبَاطِلِ وَيَصُدُّونَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ ۗ وَالَّذِينَ يَكْنِزُونَ الذَّهَبَ وَالْفِضَّةَ وَلَا يُنفِقُونَهَا فِي سَبِيلِ اللَّهِ فَبَشِّرْهُم بِعَذَابٍ أَلِيمٍ
Éy yéen ñi gëm ! Ñu bari ci fóore yi ak làbbe yi dañuy lekk alali nit ñi ciy caaxaan tey dox diggante nit ñi ak yoonu Yàlla. Te ña nga xam ne dañuy rënk wurus ak xaalis te duñu ko joxe ngir yoonu Yàlla, nanga leen yégal mbugal mu metti,
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
32Aaya

Tekki — At-Tawba 32

Simoore At-Tawba Aaya 32 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Dañoo bëgg a feye leerug Yàlla ak seen gémmiñ, te…

Simoore Aaya 32/129 — At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: At-Tawba Dégg, At-Tawba Tekki, At-Tawba mp3, At-Tawba pdf. Aaya 30–34. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers