Simoore Al-Ma'arij
PDF —
44 Aaya Meccan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Al-Ma'arij pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Al-Ma'arij pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Ma'arij Tekki. Al-Ma'arij (Meccan) 44 Aaya.



Simoore Al-Ma'arij
44 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﮮﮯﮰﮱﯓ
Ab ñaankat ñaan na mbugël mu tàbbi,
ﯔﯕﯖﯗﯘ
ñeel yéefar yi, te kenn du ku mana fanq,
ﯙﯚﯛﯜﯝ
bawoo ca Yàlla, miy Boroomi yéegukaay.
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
Malaaka yaak Ruugaa ngay yéeg ci bis boo xam ne dayoom juróom-fukki-junniy at la.
ﯪﯫﯬﯭ
Muñal, muñ gu rafet.
ﯮﯯﯰﯱ
Dañuy gis (mbugal) may lu sori,
ﯲﯳﯴ
te nun danu koo jàppe lu jigeñ,
ﯵﯶﯷﯸﯹ
bu keroogee ba asamaan si ruy melni biteex
ﯺﯻﯼﯽ
tund doj yi melni ngëndal,
ﯾﯿﰀﰁﰂ
benn xarit dootul laajte xaritam,
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
danañuy gisante. Su boobaa tooñkat bi danaa siiw jot boppam, joxe njabootam,
ﭜﭝﭞ
ak soxnaam, ak mbokkam,
ﭟﭠﭡﭢ
ak askanam wa ko yiir,
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
ak sax far képp ku nekk ci kaw suuf, ngir mu mana mucc.
ﭪﭫﭬﭭﭮ
Mukk dootul raw Safara
ﭯﭰﭱ
(Tàng) bay wësëm kaaŋum bopp.
ﭲﭳﭴﭵﭶ
Dafay woo képp ku ne wërëñ ba bëgg a dem,
ﭷﭸﭹ
dajaley alal ba dencu ko.
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Bindéef na nit ci xel muy jaxasoo [di yoqat] ;
ﮀﮁﮂﮃﮄ
su ko aw ay laalee, muy saalit ;
ﮅﮆﮇﮈﮉ
su ko jàmm ganesee mu nay, alal ak yiw danay tax mu nay bew.
ﮊﮋﮌ
Ba mu des jullikat yi
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
ña nga xam ne dañuy saxoo Julli,
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
ña nga xam ne seeni alal sàkk nañu ca cér bus xam jagle ko
ﮙﮚﮛ
mu ñéel yalwaankat yeek ñu ñakk ñi ;
ﮜﮝﮞﮟﮠ
ak ñiy dëggël Bis Pénc bi,
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
ak ñiy ragal seen mbugalum Boroom
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
te, sa mbugalum Boroom kenn du ca naagu ;
ﮮﮯﮰﮱﯓ
ak ñiy sàmm seen pëy
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
lu dul ca seeni soxna ak seeni jébéer, ñoom kenn yeddu leen,
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
képp kuy sàkku [bànneex] ci lu moy loolu, ñoo ñaa di way jalgati ya ;
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
ak ñay sàmm ndénkaane ya, ak seenub dëelante.
ﯭﯮﯯﯰﯱ
ak ñiy taxaw temm ci li ñuy seede,
ﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
ak ñiy matal sëkk seeni julli.
ﯸﯹﯺﯻﯼ
Ñoom ña nga biir Àjjana deefi leen teral.
ﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
Waaw yéefar yi lu ñu xewal bay raj-rajloo wutsi la,
ﰃﰄﰅﰆﰇﰈ
di bawoo ndeyjoor ak càmmooñ, tey wél-wéli ?
ﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑ
Ndax nit ñépp dañoo maase bëgg a duggëndoo Àjjanay xéewal?
ﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘ
Mukk ! Noo leen sàkk ak ni ñu ko xame.
ﰙﰚﰛﰜﰝﰞﰟﰠ
Déedéet !... Maa ngi giñ ci Boroom Penku ak Sowu yi ci ne Nun boroom Kàttan la nu.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙ
Ci soppi wuutale leen ak ñeneen ñu leen gën, te kenn du ko fanq.
ﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Bàyyileen ñu nuur (ci kéefër) aka fo ba baa ñuy dajeek bis ba ñu leen daan digu,
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
bu keroogee, ba ñuy génn bàmmeel ya gaaw melni ku jëm ciy xërëm ;
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
seen gët ya sajju, ñu torox ngir gàcce. Bis boobee mooy ba ñu leen daan dig (tëkoo)!

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers