Hud · 29/123
Tekki Waxtaan — Hud
وَيَا قَوْمِ لَا أَسْأَلُكُمْ عَلَيْهِ مَالًا ۖ إِنْ أَجْرِيَ إِلَّا عَلَى اللَّهِ ۚ وَمَا أَنَا بِطَارِدِ الَّذِينَ آمَنُوا ۚ إِنَّهُم مُّلَاقُو رَبِّهِمْ وَلَٰكِنِّي أَرَاكُمْ قَوْمًا تَجْهَلُونَ ۝٢٩
Wa yaa qawmi laaa as`alukum `alaihi maalan in ajriya illaa `alal laah; wa maaa ana bitaaridil lazeena aamanoo; innahum mulaaqoo Rabbihim wa laakinneee araakum qawman tajhaloon
📖 Tekkim Wolof
Te yéen samaw nit, laajumaleen ci alal. Samag pey nekkul ci kenn ku dul Yàlla. Te nekkuma ñiy dàq way-gëm, ñoom danañu dajeek seen Boroom. Waaye ni ma leen gise, aw nit ñu réer ngeen.

🎧 Dégg


📜 Aaya 27-31 — Hud

27فَقَالَ الْمَلَأُ الَّذِينَ كَفَرُوا مِن قَوْمِهِ مَا نَرَاكَ إِلَّا بَشَرًا مِّثْلَنَا وَمَا نَرَاكَ اتَّبَعَكَ إِلَّا الَّذِينَ هُمْ أَرَاذِلُنَا بَادِيَ الرَّأْيِ وَمَا نَرَىٰ لَكُمْ عَلَيْنَا مِن فَضْلٍ بَلْ نَظُنُّكُمْ كَاذِبِينَ
Ña di ay kilifa ci aw nitam, te weddi, ne ko : “Xoolewunu la lu dul ngay kenn rekk ci nun ; te it gisunu ñi la topp ñu dul ñi gën a suufe ci nun te lu yomb a gis ; te ëppalewuleen nu dara. Te sax am nanu njort ci ne ay fenkat ngeen”.
28قَالَ يَا قَوْمِ أَرَأَيْتُمْ إِن كُنتُ عَلَىٰ بَيِّنَةٍ مِّن رَّبِّي وَآتَانِي رَحْمَةً مِّنْ عِندِهِ فَعُمِّيَتْ عَلَيْكُمْ أَنُلْزِمُكُمُوهَا وَأَنتُمْ لَهَا كَارِهُونَ
Mu ne leen : "Samaw nit ! Naka ngeen di gisee mbir mi ? Su fekkee maa ngi ci lu wér lu jóge ci sama Boroom, te Mu jox ma yërmaande ju jóge ci Moom ci lu nëbbu ci yéen, ndax dama cee ga te fekk yéen ngeen sib ko ?
29وَيَا قَوْمِ لَا أَسْأَلُكُمْ عَلَيْهِ مَالًا ۖ إِنْ أَجْرِيَ إِلَّا عَلَى اللَّهِ ۚ وَمَا أَنَا بِطَارِدِ الَّذِينَ آمَنُوا ۚ إِنَّهُم مُّلَاقُو رَبِّهِمْ وَلَٰكِنِّي أَرَاكُمْ قَوْمًا تَجْهَلُونَ
Te yéen samaw nit, laajumaleen ci alal. Samag pey nekkul ci kenn ku dul Yàlla. Te nekkuma ñiy dàq way-gëm, ñoom danañu dajeek seen Boroom. Waaye ni ma leen gise, aw nit ñu réer ngeen.
30وَيَا قَوْمِ مَن يَنصُرُنِي مِنَ اللَّهِ إِن طَرَدتُّهُمْ ۚ أَفَلَا تَذَكَّرُونَ
te yéen samaw nit, ku may dimbali ci [mbugalu Yàlla] su ma leen dàqee ? Moo ndax dangeen dul xel-lu ?
31وَلَا أَقُولُ لَكُمْ عِندِي خَزَائِنُ اللَّهِ وَلَا أَعْلَمُ الْغَيْبَ وَلَا أَقُولُ إِنِّي مَلَكٌ وَلَا أَقُولُ لِلَّذِينَ تَزْدَرِي أَعْيُنُكُمْ لَن يُؤْتِيَهُمُ اللَّهُ خَيْرًا ۖ اللَّهُ أَعْلَمُ بِمَا فِي أَنفُسِهِمْ ۖ إِنِّي إِذًا لَّمِنَ الظَّالِمِينَ
Te waxumaleen maa yore ndàmbi Yàlla, te xamuma it lu fàddu, neewumaleen Malaaka laa ; te waxuma it ne seeni bët a xeebu, Yàlla duleen jox yiw ; Yàlla moo gën a xam li nekk ci ñoom [su ma leen waxoon yooyu], kon ma bokk ci tooñkat yi.
HudFihi Alxuraan
123Aaya
MeccanRevelation
29Aaya

Tekki — Hud 29

Simoore Hud Aaya 29 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te yéen samaw nit, laajumaleen ci alal. Samag pey nekkul…

Simoore Aaya 29/123 — Hud هود (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Hud Dégg, Hud Tekki, Hud mp3, Hud pdf. Aaya 27–31. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers