Ar-Ra'd · 24/43
Tekki Waxtaan — Ar-Ra'd
سَلَامٌ عَلَيْكُم بِمَا صَبَرْتُمْ ۚ فَنِعْمَ عُقْبَى الدَّارِ ۝٢٤
Salaamun `alaikum bimaa sabartum; fani`ma `uqbad daar
📖 Tekkim Wolof
[Ñu naan leen] - “Jàmmi Yàlla na nekk ci yéen ngir la ngeen muñoon ! ” - Aka rafet kërug mujj ga ! ”
🎧 Dégg

📜 Aaya 22-26 — Ar-Ra'd

22وَالَّذِينَ صَبَرُوا ابْتِغَاءَ وَجْهِ رَبِّهِمْ وَأَقَامُوا الصَّلَاةَ وَأَنفَقُوا مِمَّا رَزَقْنَاهُمْ سِرًّا وَعَلَانِيَةً وَيَدْرَءُونَ بِالْحَسَنَةِ السَّيِّئَةَ أُولَٰئِكَ لَهُمْ عُقْبَى الدَّارِ
ak ñay muñ ngir jëmmi seen Boroom, tey taxawal julli tey dundale ca la leen Yàlla wërsëgale ci la nëbbu walla ci lu feeñ, te ñuy jiñe lu ñaaw ak lu rafet. Ñooña am nañu kër gu mujj ga,
23جَنَّاتُ عَدْنٍ يَدْخُلُونَهَا وَمَن صَلَحَ مِنْ آبَائِهِمْ وَأَزْوَاجِهِمْ وَذُرِّيَّاتِهِمْ ۖ وَالْمَلَائِكَةُ يَدْخُلُونَ عَلَيْهِم مِّن كُلِّ بَابٍ
Àjjana ju sax ja, danañu ca dugg, ak ña jëfoon lu baax ca seeni baay ak ca seeni jabar ak seeni doom ak i sët. Te Malaaka ya dañuy duggandook ñoom ci buntu yépp :
24سَلَامٌ عَلَيْكُم بِمَا صَبَرْتُمْ ۚ فَنِعْمَ عُقْبَى الدَّارِ
[Ñu naan leen] - “Jàmmi Yàlla na nekk ci yéen ngir la ngeen muñoon ! ” - Aka rafet kërug mujj ga ! ”
25وَالَّذِينَ يَنقُضُونَ عَهْدَ اللَّهِ مِن بَعْدِ مِيثَاقِهِ وَيَقْطَعُونَ مَا أَمَرَ اللَّهُ بِهِ أَن يُوصَلَ وَيُفْسِدُونَ فِي الْأَرْضِ ۙ أُولَٰئِكَ لَهُمُ اللَّعْنَةُ وَلَهُمْ سُوءُ الدَّارِ
[Waaye] ñiy firi kóllareg Yàlla ginnaaw ba mu fasoo, te muy dog la Mu santaane ñu jokk ko [mooy ag mbokk], di yàq ci kaw suuf si, ñooña am rëbb dal na ci seen kaw [sori yërmaandey Yàlla], te it am nañu kër gu bon ga.
26اللَّهُ يَبْسُطُ الرِّزْقَ لِمَن يَشَاءُ وَيَقْدِرُ ۚ وَفَرِحُوا بِالْحَيَاةِ الدُّنْيَا وَمَا الْحَيَاةُ الدُّنْيَا فِي الْآخِرَةِ إِلَّا مَتَاعٌ
Yàlla dana yaatal wërsëg ci ku ko soob, Dana ko xatal it. Te ñoom dundu àdduna neex na leen, te dundu àdduna soo ko méngaleek gu àllaaxira, du nekk lu dul xéewal gu ñàkk solo.
Ar-Ra'dFihi Alxuraan
43Aaya
MedinanRevelation
24Aaya

Tekki — Ar-Ra'd 24

Simoore Ar-Ra'd Aaya 24 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Ñu naan leen] - “Jàmmi Yàlla na nekk ci yéen…

Simoore Aaya 24/43 — Ar-Ra'd الرعد (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ar-Ra'd Dégg, Ar-Ra'd Tekki, Ar-Ra'd mp3, Ar-Ra'd pdf. Aaya 22–26. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers