An-Nahl · 34/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
فَأَصَابَهُمْ سَيِّئَاتُ مَا عَمِلُوا وَحَاقَ بِهِم مَّا كَانُوا بِهِ يَسْتَهْزِئُونَ ۝٣٤
Fa asaabahum saiyi aatu maa `amiloo wa haaqa bihim maa kaano bihee yastahzi`oon
📖 Tekkim Wolof
Dal na ci seen kaw ñaawtéefu la ñu defoon, ndax wàcc na ci ñoom la ñu doon soofantal di ko reetaan.
🎧 Dégg

📜 Aaya 32-36 — An-Nahl

32الَّذِينَ تَتَوَفَّاهُمُ الْمَلَائِكَةُ طَيِّبِينَ ۙ يَقُولُونَ سَلَامٌ عَلَيْكُمُ ادْخُلُوا الْجَنَّةَ بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
Ña nga xam ne Malaaka ya danañu leen rey - fekk ñu nekk ñu sell - danañu leen wax ne : “Yal na jàmm nekk ci yéen ! Dugguleen Àjjana ci sababus la ngeen daan jëf [ci lu baax]”.
33هَلْ يَنظُرُونَ إِلَّا أَن تَأْتِيَهُمُ الْمَلَائِكَةُ أَوْ يَأْتِيَ أَمْرُ رَبِّكَ ۚ كَذَٰلِكَ فَعَلَ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ ۚ وَمَا ظَلَمَهُمُ اللَّهُ وَلَٰكِن كَانُوا أَنفُسَهُمْ يَظْلِمُونَ
Lan la [yéefar ya] di xaar, Malaaka ya digal leen walla sa dogalu Boroom agsi ci ñoom ? Noonu la [yéefar ya] leen jiitu nekke woon. Waaye ñoom ñoo tooñ seen bopp.
34فَأَصَابَهُمْ سَيِّئَاتُ مَا عَمِلُوا وَحَاقَ بِهِم مَّا كَانُوا بِهِ يَسْتَهْزِئُونَ
Dal na ci seen kaw ñaawtéefu la ñu defoon, ndax wàcc na ci ñoom la ñu doon soofantal di ko reetaan.
35وَقَالَ الَّذِينَ أَشْرَكُوا لَوْ شَاءَ اللَّهُ مَا عَبَدْنَا مِن دُونِهِ مِن شَيْءٍ نَّحْنُ وَلَا آبَاؤُنَا وَلَا حَرَّمْنَا مِن دُونِهِ مِن شَيْءٍ ۚ كَذَٰلِكَ فَعَلَ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ ۚ فَهَلْ عَلَى الرُّسُلِ إِلَّا الْبَلَاغُ الْمُبِينُ
Ña daan bokkaale wax ne : “Bu neexoon Yàlla, dunu jaamu kenn ku dul Moom, du nun du kenn ci sunuy baay ; te kon dunu ne dara araam na te du ci ndigalam. Ña leen jiitu woon noonu lañu defoon. Te li war ab Yonent ndax dafa dul jottali rekk [la ñu ko yónni] ba mu mat sëkk ?
36وَلَقَدْ بَعَثْنَا فِي كُلِّ أُمَّةٍ رَّسُولًا أَنِ اعْبُدُوا اللَّهَ وَاجْتَنِبُوا الطَّاغُوتَ ۖ فَمِنْهُم مَّنْ هَدَى اللَّهُ وَمِنْهُم مَّنْ حَقَّتْ عَلَيْهِ الضَّلَالَةُ ۚ فَسِيرُوا فِي الْأَرْضِ فَانظُرُوا كَيْفَ كَانَ عَاقِبَةُ الْمُكَذِّبِينَ
Yónni nañu ci xeet wu nekk ab Yonent [buy xamle ne] : “Jaamuleen Yàlla te ngeen moytuy xërëm”. Mu am ci ñoom [xeet yooyu] ñu Yàlla jubal ak ñoo xam ne réer war na ci ñoom. Doxleen ci seeni suuf te xool ña weddi woon naka lañu mujje.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
34Aaya

Tekki — An-Nahl 34

Simoore An-Nahl Aaya 34 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Dal na ci seen kaw ñaawtéefu la ñu defoon, ndax…

Simoore Aaya 34/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 32–36. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers