Al-Kahf · 24/110
Tekki Waxtaan — Al-Kahf
إِلَّا أَن يَشَاءَ اللَّهُ ۚ وَاذْكُر رَّبَّكَ إِذَا نَسِيتَ وَقُلْ عَسَىٰ أَن يَهْدِيَنِ رَبِّي لِأَقْرَبَ مِنْ هَٰذَا رَشَدًا ۝٢٤
Illaaa any yashaaa`al laah; wazkur Rabbaka izaa naseeta wa qul `asaaa any yahdiyani Rabbee li aqraba min haazaa rashadaa
📖 Tekkim Wolof
[te boolewoo ca] : “Bu soobee Yàlla”, tuddal sa Boroom, boo fàttee fàttaliku Ko te nga wax ne : “Xéy-na sama Boroom gindi ma jëme ma ca la gën a jegeñ lii cig njub”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 22-26 — Al-Kahf

22سَيَقُولُونَ ثَلَاثَةٌ رَّابِعُهُمْ كَلْبُهُمْ وَيَقُولُونَ خَمْسَةٌ سَادِسُهُمْ كَلْبُهُمْ رَجْمًا بِالْغَيْبِ ۖ وَيَقُولُونَ سَبْعَةٌ وَثَامِنُهُمْ كَلْبُهُمْ ۚ قُل رَّبِّي أَعْلَمُ بِعِدَّتِهِم مَّا يَعْلَمُهُمْ إِلَّا قَلِيلٌ ۗ فَلَا تُمَارِ فِيهِمْ إِلَّا مِرَاءً ظَاهِرًا وَلَا تَسْتَفْتِ فِيهِم مِّنْهُمْ أَحَدًا
Danañu wax ne : “Ñett lañu woon, seen xaj ba ñeenteel leen”. Danañu wax it ne juróom lañu woon, seen xaj bi juróom-benneel leen, muy njort ci lu fàddu. Te danañu wax ne : “Juróom-ñaar lañu woon, seen xaj ba juróom-ñetteel leen”. Neel : “Sama Boroom a gën a xam seen lim. Te kenn xamu ko lu dul ñu néew”. Bul werante ci ñoom lu dul ci waxi biti te bul sàkku xam ci kenn ci ñoom.
23وَلَا تَقُولَنَّ لِشَيْءٍ إِنِّي فَاعِلٌ ذَٰلِكَ غَدًا
Bul wax mukk ci dara ne : “Man dana def nàngam ëllëg”.
24إِلَّا أَن يَشَاءَ اللَّهُ ۚ وَاذْكُر رَّبَّكَ إِذَا نَسِيتَ وَقُلْ عَسَىٰ أَن يَهْدِيَنِ رَبِّي لِأَقْرَبَ مِنْ هَٰذَا رَشَدًا
[te boolewoo ca] : “Bu soobee Yàlla”, tuddal sa Boroom, boo fàttee fàttaliku Ko te nga wax ne : “Xéy-na sama Boroom gindi ma jëme ma ca la gën a jegeñ lii cig njub”.
25وَلَبِثُوا فِي كَهْفِهِمْ ثَلَاثَ مِائَةٍ سِنِينَ وَازْدَادُوا تِسْعًا
Toog nañu ca seen xunt ma ñetti téeméeri at yu teg juróom-ñeent.
26قُلِ اللَّهُ أَعْلَمُ بِمَا لَبِثُوا ۖ لَهُ غَيْبُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۖ أَبْصِرْ بِهِ وَأَسْمِعْ ۚ مَا لَهُم مِّن دُونِهِ مِن وَلِيٍّ وَلَا يُشْرِكُ فِي حُكْمِهِ أَحَدًا
Neel : “Yàllaa gën a xam diir ba ñu fa toog. Ñeel na ko [moom Yàlla] kumpag asamaan yi ak suuf si. Nangay gise ci Moom, di dégge ci Moom ! Amuñu ku leen di wattu ci Moom, du boole kenn ci àtteem.
Al-KahfFihi Alxuraan
110Aaya
MeccanRevelation
24Aaya

Tekki — Al-Kahf 24

Simoore Al-Kahf Aaya 24 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [te boolewoo ca] : “Bu soobee Yàlla”, tuddal sa Boroom,…

Simoore Aaya 24/110 — Al-Kahf الكهف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Kahf Dégg, Al-Kahf Tekki, Al-Kahf mp3, Al-Kahf pdf. Aaya 22–26. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers