Al-Kahf · 23/110
Tekki Waxtaan — Al-Kahf
وَلَا تَقُولَنَّ لِشَيْءٍ إِنِّي فَاعِلٌ ذَٰلِكَ غَدًا ۝٢٣
Wa laa taqoolanna lishai`in innee faa`ilun zaalika ghadaa
📖 Tekkim Wolof
Bul wax mukk ci dara ne : “Man dana def nàngam ëllëg”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 21-25 — Al-Kahf

21وَكَذَٰلِكَ أَعْثَرْنَا عَلَيْهِمْ لِيَعْلَمُوا أَنَّ وَعْدَ اللَّهِ حَقٌّ وَأَنَّ السَّاعَةَ لَا رَيْبَ فِيهَا إِذْ يَتَنَازَعُونَ بَيْنَهُمْ أَمْرَهُمْ ۖ فَقَالُوا ابْنُوا عَلَيْهِم بُنْيَانًا ۖ رَّبُّهُمْ أَعْلَمُ بِهِمْ ۚ قَالَ الَّذِينَ غَلَبُوا عَلَىٰ أَمْرِهِمْ لَنَتَّخِذَنَّ عَلَيْهِم مَّسْجِدًا
Nu feeñal leen ca waa dëkk ba, ngir ñu xam ne digu Yàlla lu dëggu la te xam it ne waxtu wa [àddinay jeex] amul sikk ci ne luy am la. Ba ñuy xëccoo ci seen biir ci mbirum [waxembaane ya], ñu naan : “Tabaxleen ci seen kaw am taax. Seen Boroom a gën a xam seen mbir”. Ña not wax ja ci seen mbir ne : “Nanu def ci seen kaw jàkka”.
22سَيَقُولُونَ ثَلَاثَةٌ رَّابِعُهُمْ كَلْبُهُمْ وَيَقُولُونَ خَمْسَةٌ سَادِسُهُمْ كَلْبُهُمْ رَجْمًا بِالْغَيْبِ ۖ وَيَقُولُونَ سَبْعَةٌ وَثَامِنُهُمْ كَلْبُهُمْ ۚ قُل رَّبِّي أَعْلَمُ بِعِدَّتِهِم مَّا يَعْلَمُهُمْ إِلَّا قَلِيلٌ ۗ فَلَا تُمَارِ فِيهِمْ إِلَّا مِرَاءً ظَاهِرًا وَلَا تَسْتَفْتِ فِيهِم مِّنْهُمْ أَحَدًا
Danañu wax ne : “Ñett lañu woon, seen xaj ba ñeenteel leen”. Danañu wax it ne juróom lañu woon, seen xaj bi juróom-benneel leen, muy njort ci lu fàddu. Te danañu wax ne : “Juróom-ñaar lañu woon, seen xaj ba juróom-ñetteel leen”. Neel : “Sama Boroom a gën a xam seen lim. Te kenn xamu ko lu dul ñu néew”. Bul werante ci ñoom lu dul ci waxi biti te bul sàkku xam ci kenn ci ñoom.
23وَلَا تَقُولَنَّ لِشَيْءٍ إِنِّي فَاعِلٌ ذَٰلِكَ غَدًا
Bul wax mukk ci dara ne : “Man dana def nàngam ëllëg”.
24إِلَّا أَن يَشَاءَ اللَّهُ ۚ وَاذْكُر رَّبَّكَ إِذَا نَسِيتَ وَقُلْ عَسَىٰ أَن يَهْدِيَنِ رَبِّي لِأَقْرَبَ مِنْ هَٰذَا رَشَدًا
[te boolewoo ca] : “Bu soobee Yàlla”, tuddal sa Boroom, boo fàttee fàttaliku Ko te nga wax ne : “Xéy-na sama Boroom gindi ma jëme ma ca la gën a jegeñ lii cig njub”.
25وَلَبِثُوا فِي كَهْفِهِمْ ثَلَاثَ مِائَةٍ سِنِينَ وَازْدَادُوا تِسْعًا
Toog nañu ca seen xunt ma ñetti téeméeri at yu teg juróom-ñeent.
Al-KahfFihi Alxuraan
110Aaya
MeccanRevelation
23Aaya

Tekki — Al-Kahf 23

Simoore Al-Kahf Aaya 23 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bul wax mukk ci dara ne : “Man dana def…

Simoore Aaya 23/110 — Al-Kahf الكهف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Kahf Dégg, Al-Kahf Tekki, Al-Kahf mp3, Al-Kahf pdf. Aaya 21–25. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers