Al-Kahf · 48/110
Tekki Waxtaan — Al-Kahf
وَعُرِضُوا عَلَىٰ رَبِّكَ صَفًّا لَّقَدْ جِئْتُمُونَا كَمَا خَلَقْنَاكُمْ أَوَّلَ مَرَّةٍ ۚ بَلْ زَعَمْتُمْ أَلَّن نَّجْعَلَ لَكُم مَّوْعِدًا ۝٤٨
Wa `uridoo `alaa Rabbika saffaa, laqad ji`tumoonaa kamaa khalaqnaakum awala marrah; bal za`amtum allannaj`ala lakum maw`idaa
📖 Tekkim Wolof
Te Nu werale leen ci sa kanamu Boroom ñu def ay sàppe. “Dangeen di sikk ci ne sàkk Nanu ab dig [bu ngeen di dekkee]”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 46-50 — Al-Kahf

46الْمَالُ وَالْبَنُونَ زِينَةُ الْحَيَاةِ الدُّنْيَا ۖ وَالْبَاقِيَاتُ الصَّالِحَاتُ خَيْرٌ عِندَ رَبِّكَ ثَوَابًا وَخَيْرٌ أَمَلًا
Alal ak i doom ci yiy neexal àddina lañu bokk. Waaye way-des ya di [jëf] yu yiw, ñooy ya gën ca sa Boroom ci wàllu yool ak yaakaar.
47وَيَوْمَ نُسَيِّرُ الْجِبَالَ وَتَرَى الْأَرْضَ بَارِزَةً وَحَشَرْنَاهُمْ فَلَمْ نُغَادِرْ مِنْهُمْ أَحَدًا
Bis ba Nuy doxloo tundi doj yi nga gis suuf si maase nerr, Nu fang leen te Dunu bàyyi kenn ci ñoom.
48وَعُرِضُوا عَلَىٰ رَبِّكَ صَفًّا لَّقَدْ جِئْتُمُونَا كَمَا خَلَقْنَاكُمْ أَوَّلَ مَرَّةٍ ۚ بَلْ زَعَمْتُمْ أَلَّن نَّجْعَلَ لَكُم مَّوْعِدًا
Te Nu werale leen ci sa kanamu Boroom ñu def ay sàppe. “Dangeen di sikk ci ne sàkk Nanu ab dig [bu ngeen di dekkee]”.
49وَوُضِعَ الْكِتَابُ فَتَرَى الْمُجْرِمِينَ مُشْفِقِينَ مِمَّا فِيهِ وَيَقُولُونَ يَا وَيْلَتَنَا مَالِ هَٰذَا الْكِتَابِ لَا يُغَادِرُ صَغِيرَةً وَلَا كَبِيرَةً إِلَّا أَحْصَاهَا ۚ وَوَجَدُوا مَا عَمِلُوا حَاضِرًا ۗ وَلَا يَظْلِمُ رَبُّكَ أَحَدًا
Ñu teg Téere ba. Nga gis saay-saay sa tiit ca la nekk ca biir, ñu naan : “Ngalla nun, cëy waay téere bii, bàyyiwul lu tuuti, bàyyiwul lu rëy, bind na lépp ? ” Ñu gis la ñu defoon di lu teew. Te sa Boroom du tooñ kenn.
50وَإِذْ قُلْنَا لِلْمَلَائِكَةِ اسْجُدُوا لِآدَمَ فَسَجَدُوا إِلَّا إِبْلِيسَ كَانَ مِنَ الْجِنِّ فَفَسَقَ عَنْ أَمْرِ رَبِّهِ ۗ أَفَتَتَّخِذُونَهُ وَذُرِّيَّتَهُ أَوْلِيَاءَ مِن دُونِي وَهُمْ لَكُمْ عَدُوٌّ ۚ بِئْسَ لِلظَّالِمِينَ بَدَلًا
[Fàttalikul] ba Nu waxee Malaaka ya ne leen : “Sujjóotleen ci Aadama”, ñu sujjóot [ñoom ñépp] ba mu des Ibliis, moom bokkoon na ca jinne ya, daldi sàqi ndigalu Boroomam. Ndax dangeen koy jàppe xarit mook i sëtam, bàyyi Nu [Nun Yàlla], te ñoom seeni noon lañu ? Bon na, li tooñkat ya di weccee !
Al-KahfFihi Alxuraan
110Aaya
MeccanRevelation
48Aaya

Tekki — Al-Kahf 48

Simoore Al-Kahf Aaya 48 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te Nu werale leen ci sa kanamu Boroom ñu def…

Simoore Aaya 48/110 — Al-Kahf الكهف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Kahf Dégg, Al-Kahf Tekki, Al-Kahf mp3, Al-Kahf pdf. Aaya 46–50. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers