Al-Baqara · 129/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
رَبَّنَا وَابْعَثْ فِيهِمْ رَسُولًا مِّنْهُمْ يَتْلُو عَلَيْهِمْ آيَاتِكَ وَيُعَلِّمُهُمُ الْكِتَابَ وَالْحِكْمَةَ وَيُزَكِّيهِمْ ۚ إِنَّكَ أَنتَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ ۝١٢٩
Rabbanaa wab`as feehim Rasoolam minhum yatloo `alaihim aayaatika wa yu`allimuhumul Kitaaba wal Hikmata wa yuzakkeehim; innaka Antal `Azeezul Hakeem
📖 Tekkim Wolof
Yaw sunu Boroom ! Yónneel ci ñoom Yonent bu bokk ci ñoom, bu leen di jàngal say laaya, di leen xamal Téere ba ak i xereñe, te di leen sellal Yaw Aji-not ji , Aji-xereñ ji!

🎧 Dégg


📜 Aaya 127-131 — Al-Baqara

127وَإِذْ يَرْفَعُ إِبْرَاهِيمُ الْقَوَاعِدَ مِنَ الْبَيْتِ وَإِسْمَاعِيلُ رَبَّنَا تَقَبَّلْ مِنَّا ۖ إِنَّكَ أَنتَ السَّمِيعُ الْعَلِيمُ
[Fàttalikuleen] Ba Ibraahiima ak Ismaahiila di yékkati ndéttalu néeg ba (Kaaba ga) : "Yaw sunu Boroom nangul nu, Yaw dey Kuy dégg nga, Kuy xam nga.
128رَبَّنَا وَاجْعَلْنَا مُسْلِمَيْنِ لَكَ وَمِن ذُرِّيَّتِنَا أُمَّةً مُّسْلِمَةً لَّكَ وَأَرِنَا مَنَاسِكَنَا وَتُبْ عَلَيْنَا ۖ إِنَّكَ أَنتَ التَّوَّابُ الرَّحِيمُ
Yaw sunu Boroom ! Def nu nuy ñaari way-wommatu jëm ci yaw. Te nga def ci sunuy sët askan wu wommatu jëm ci Yaw te nga won nu sunu jaamuwaay, boole ca jéggal nu. Yaw dey Boroom bi, Yaa di Jéggalaakoon bi, di Jaglewaakoon bi.
129رَبَّنَا وَابْعَثْ فِيهِمْ رَسُولًا مِّنْهُمْ يَتْلُو عَلَيْهِمْ آيَاتِكَ وَيُعَلِّمُهُمُ الْكِتَابَ وَالْحِكْمَةَ وَيُزَكِّيهِمْ ۚ إِنَّكَ أَنتَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ
Yaw sunu Boroom ! Yónneel ci ñoom Yonent bu bokk ci ñoom, bu leen di jàngal say laaya, di leen xamal Téere ba ak i xereñe, te di leen sellal Yaw Aji-not ji , Aji-xereñ ji!
130وَمَن يَرْغَبُ عَن مِّلَّةِ إِبْرَاهِيمَ إِلَّا مَن سَفِهَ نَفْسَهُ ۚ وَلَقَدِ اصْطَفَيْنَاهُ فِي الدُّنْيَا ۖ وَإِنَّهُ فِي الْآخِرَةِ لَمِنَ الصَّالِحِينَ
Ana kan mooy bañ diinay Ibraahiima, ku dul ku kannasu ? Nun dey tànn nanu ko ci àddina ; te moom, bu àllaaxiraa it, mu bokk ca ña gën a yiw.
131إِذْ قَالَ لَهُ رَبُّهُ أَسْلِمْ ۖ قَالَ أَسْلَمْتُ لِرَبِّ الْعَالَمِينَ
[Fàttalikuleen] Ba ko Boroomam nee : “Wommatul”, Mu ne : “Wommatunaa jëm ci Boroom àddina bi”.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
129Aaya

Tekki — Al-Baqara 129

Simoore Al-Baqara Aaya 129 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yaw sunu Boroom ! Yónneel ci ñoom Yonent bu bokk…

Simoore Aaya 129/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 127–131. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers