Al-Baqara · 159/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
إِنَّ الَّذِينَ يَكْتُمُونَ مَا أَنزَلْنَا مِنَ الْبَيِّنَاتِ وَالْهُدَىٰ مِن بَعْدِ مَا بَيَّنَّاهُ لِلنَّاسِ فِي الْكِتَابِ ۙ أُولَٰئِكَ يَلْعَنُهُمُ اللَّهُ وَيَلْعَنُهُمُ اللَّاعِنُونَ ۝١٥٩
Innal lazeena yaktumoona maaa anzalnaa minal baiyinaati walhudaa mim ba`di maa baiyannaahu linnaasi fil kitaabi ulaaa`ika yal`anuhumul laahu wa yal`anuhumul laa `inoon
📖 Tekkim Wolof
Ña nga xam ne dañuy nëbb la ñu wàcce ci ag leeral ak ug njub ginnaaw ba ñu ko biralalee nit ñi ca Téere ba, ñooña Yàlla dana leen rëbb, rëbbkat ya itam dana leen rëbb
🎧 Dégg

📜 Aaya 157-161 — Al-Baqara

157أُولَٰئِكَ عَلَيْهِمْ صَلَوَاتٌ مِّن رَّبِّهِمْ وَرَحْمَةٌ ۖ وَأُولَٰئِكَ هُمُ الْمُهْتَدُونَ
Gaa ñooña am nañu njéggal gu bawoo ca seen Boroom, ak yérmaande ; te ñoo di ña gindiku tigi.
158۞ إِنَّ الصَّفَا وَالْمَرْوَةَ مِن شَعَائِرِ اللَّهِ ۖ فَمَنْ حَجَّ الْبَيْتَ أَوِ اعْتَمَرَ فَلَا جُنَاحَ عَلَيْهِ أَن يَطَّوَّفَ بِهِمَا ۚ وَمَن تَطَوَّعَ خَيْرًا فَإِنَّ اللَّهَ شَاكِرٌ عَلِيمٌ
Safaa ak Marwa bokk nañu ci màndargay jaamukaayu Yàlla yi. Ku aj Màkka walla mu Umra , du aay ci moom mu jaabante seen diggante ñoom ñaar. Ku coobarewu te jëf lu baax, lu yiw, na xam ne Yàlla gërëmaakoon la, Aji-xam la.
159إِنَّ الَّذِينَ يَكْتُمُونَ مَا أَنزَلْنَا مِنَ الْبَيِّنَاتِ وَالْهُدَىٰ مِن بَعْدِ مَا بَيَّنَّاهُ لِلنَّاسِ فِي الْكِتَابِ ۙ أُولَٰئِكَ يَلْعَنُهُمُ اللَّهُ وَيَلْعَنُهُمُ اللَّاعِنُونَ
Ña nga xam ne dañuy nëbb la ñu wàcce ci ag leeral ak ug njub ginnaaw ba ñu ko biralalee nit ñi ca Téere ba, ñooña Yàlla dana leen rëbb, rëbbkat ya itam dana leen rëbb
160إِلَّا الَّذِينَ تَابُوا وَأَصْلَحُوا وَبَيَّنُوا فَأُولَٰئِكَ أَتُوبُ عَلَيْهِمْ ۚ وَأَنَا التَّوَّابُ الرَّحِيمُ
lu dul ña ca tuub, yéwénal te leeral : ñooña Danaa leen jéggal Man Yàlla. Te Man maay Jéggalaakoon bi, di Jaglewaakoon bi.
161إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا وَمَاتُوا وَهُمْ كُفَّارٌ أُولَٰئِكَ عَلَيْهِمْ لَعْنَةُ اللَّهِ وَالْمَلَائِكَةِ وَالنَّاسِ أَجْمَعِينَ
Ña weddi te dee ci kéefar, ñooña rëbbum Yàlla ak Malaaka ya ak nit ñépp dana dal ci seen kaw.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
159Aaya

Tekki — Al-Baqara 159

Simoore Al-Baqara Aaya 159 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña nga xam ne dañuy nëbb la ñu wàcce ci…

Simoore Aaya 159/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 157–161. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers