Al-Hajj · 12/78
Tekki Waxtaan — Al-Hajj
يَدْعُو مِن دُونِ اللَّهِ مَا لَا يَضُرُّهُ وَمَا لَا يَنفَعُهُ ۚ ذَٰلِكَ هُوَ الضَّلَالُ الْبَعِيدُ ۝١٢
Yad`oo min doonil laahi maa laa yadurruhoo wa maa laa yanfa`uh` zaalika huwad dalaalul ba`ed
📖 Tekkim Wolof
Mangay jaamu, bàyyi Yàlla, loo xam ne mënu koo lor, mënu koo jariñ. Loolu moo di réer gu sori dëgg !
🎧 Dégg

📜 Aaya 10-14 — Al-Hajj

10ذَٰلِكَ بِمَا قَدَّمَتْ يَدَاكَ وَأَنَّ اللَّهَ لَيْسَ بِظَلَّامٍ لِّلْعَبِيدِ
Loolu la yelloo ngir la ñaari yoxoom ya def ci àddina ! Te Yàlla du tooñ jaamam ñi.
11وَمِنَ النَّاسِ مَن يَعْبُدُ اللَّهَ عَلَىٰ حَرْفٍ ۖ فَإِنْ أَصَابَهُ خَيْرٌ اطْمَأَنَّ بِهِ ۖ وَإِنْ أَصَابَتْهُ فِتْنَةٌ انقَلَبَ عَلَىٰ وَجْهِهِ خَسِرَ الدُّنْيَا وَالْآخِرَةَ ۚ ذَٰلِكَ هُوَ الْخُسْرَانُ الْمُبِينُ
Ci nit ñi am na ñuy jaamu Yàlla ci genn wet rekk. Tax na bu amee lu baax mu nekk ku dal, bu ko lu naqari dalee, mu soppeeku ca la mu nekke woon, yàqule na ci àddina ak àllaaxira. Te loolu mooy yàqule tigi !
12يَدْعُو مِن دُونِ اللَّهِ مَا لَا يَضُرُّهُ وَمَا لَا يَنفَعُهُ ۚ ذَٰلِكَ هُوَ الضَّلَالُ الْبَعِيدُ
Mangay jaamu, bàyyi Yàlla, loo xam ne mënu koo lor, mënu koo jariñ. Loolu moo di réer gu sori dëgg !
13يَدْعُو لَمَن ضَرُّهُ أَقْرَبُ مِن نَّفْعِهِ ۚ لَبِئْسَ الْمَوْلَىٰ وَلَبِئْسَ الْعَشِيرُ
Mangay jaamu loo xam ne loram moo gën jegeñnjariñam. Aka bon wéeruwaay te aka bon àndandoo !
14إِنَّ اللَّهَ يُدْخِلُ الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ جَنَّاتٍ تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ ۚ إِنَّ اللَّهَ يَفْعَلُ مَا يُرِيدُ
Naka Yàlla, Dana dugal ñi gëm tey jëf u yiw ci Àjjana yoo xam ne dex dañuy daw ci seen suuf [ron], Yàllaay def lu ko soob.
Al-HajjFihi Alxuraan
78Aaya
MedinanRevelation
12Aaya

Tekki — Al-Hajj 12

Simoore Al-Hajj Aaya 12 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mangay jaamu, bàyyi Yàlla, loo xam ne mënu koo lor,…

Simoore Aaya 12/78 — Al-Hajj الحج (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hajj Dégg, Al-Hajj Tekki, Al-Hajj mp3, Al-Hajj pdf. Aaya 10–14. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers