Al-Hajj · 34/78
Tekki Waxtaan — Al-Hajj
وَلِكُلِّ أُمَّةٍ جَعَلْنَا مَنسَكًا لِّيَذْكُرُوا اسْمَ اللَّهِ عَلَىٰ مَا رَزَقَهُم مِّن بَهِيمَةِ الْأَنْعَامِ ۗ فَإِلَٰهُكُمْ إِلَٰهٌ وَاحِدٌ فَلَهُ أَسْلِمُوا ۗ وَبَشِّرِ الْمُخْبِتِينَ ۝٣٤
Wa likulli ummatin ja`alnaa mansakal liyazkurus mal laahi `alaa maa razaqahum mim baheematil an`aam; failaahukum ilaahunw Waahidun falahooo aslimoo; wa bashshiril mukhbiteen
📖 Tekkim Wolof
Te xeet wu nekk, defal Nanu ko jaamukaay ngir ñuy tudd turu Yàlla ci li Mu leen wërsëgal ci juri kër yi. Kon seen Boroom jenn Yàlla doŋŋ la. Kon nangeen wommatu jëm ci Moom. Bégalal way-toroxlu ña,
🎧 Dégg

📜 Aaya 32-36 — Al-Hajj

32ذَٰلِكَ وَمَن يُعَظِّمْ شَعَائِرَ اللَّهِ فَإِنَّهَا مِن تَقْوَى الْقُلُوبِ
Noonu la. Képp ku màggal jaamukaayu Yàlla, na xam ne màggal googu bokk na ca ragalug Yàlla ci xol yi.
33لَكُمْ فِيهَا مَنَافِعُ إِلَىٰ أَجَلٍ مُّسَمًّى ثُمَّ مَحِلُّهَا إِلَى الْبَيْتِ الْعَتِيقِ
Ñeel na leen ci loolu ay njariñ ba àpp bu ñu tudd ; te it seen barab ba ñuy loje ma nga ca Néeg bu yàgg a yàgg ba.
34وَلِكُلِّ أُمَّةٍ جَعَلْنَا مَنسَكًا لِّيَذْكُرُوا اسْمَ اللَّهِ عَلَىٰ مَا رَزَقَهُم مِّن بَهِيمَةِ الْأَنْعَامِ ۗ فَإِلَٰهُكُمْ إِلَٰهٌ وَاحِدٌ فَلَهُ أَسْلِمُوا ۗ وَبَشِّرِ الْمُخْبِتِينَ
Te xeet wu nekk, defal Nanu ko jaamukaay ngir ñuy tudd turu Yàlla ci li Mu leen wërsëgal ci juri kër yi. Kon seen Boroom jenn Yàlla doŋŋ la. Kon nangeen wommatu jëm ci Moom. Bégalal way-toroxlu ña,
35الَّذِينَ إِذَا ذُكِرَ اللَّهُ وَجِلَتْ قُلُوبُهُمْ وَالصَّابِرِينَ عَلَىٰ مَا أَصَابَهُمْ وَالْمُقِيمِي الصَّلَاةِ وَمِمَّا رَزَقْنَاهُمْ يُنفِقُونَ
ña nga xam ne fu ñu tudde Yàlla seeni xol yëngu, ak way-muñ ña ca la leen dal, ak ñay taxawal julli tey lele ca la Nu leen wërsëgale.
36وَالْبُدْنَ جَعَلْنَاهَا لَكُم مِّن شَعَائِرِ اللَّهِ لَكُمْ فِيهَا خَيْرٌ ۖ فَاذْكُرُوا اسْمَ اللَّهِ عَلَيْهَا صَوَافَّ ۖ فَإِذَا وَجَبَتْ جُنُوبُهَا فَكُلُوا مِنْهَا وَأَطْعِمُوا الْقَانِعَ وَالْمُعْتَرَّ ۚ كَذَٰلِكَ سَخَّرْنَاهَا لَكُمْ لَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ
Te giléem yu suur ya, defal Nanu leen ñu bokk ca ya ñuy jaamoo Yàlla. Aw yiw doŋŋ la ñeel leen. Nangeen ci tudd turu Yàlla bu ñu leen di loj. Bu ñu daanoo tëdd ci seeni wet, nangeen ca lekk te ngeen leel ca way-doylu ña ak yalwaankat ya. Noonu la Nu leen tegtale ndax yéen ngeen gërëm.
Al-HajjFihi Alxuraan
78Aaya
MedinanRevelation
34Aaya

Tekki — Al-Hajj 34

Simoore Al-Hajj Aaya 34 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te xeet wu nekk, defal Nanu ko jaamukaay ngir ñuy…

Simoore Aaya 34/78 — Al-Hajj الحج (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hajj Dégg, Al-Hajj Tekki, Al-Hajj mp3, Al-Hajj pdf. Aaya 32–36. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers