An-Nur · 13/64
Tekki Waxtaan — An-Nur
لَّوْلَا جَاءُوا عَلَيْهِ بِأَرْبَعَةِ شُهَدَاءَ ۚ فَإِذْ لَمْ يَأْتُوا بِالشُّهَدَاءِ فَأُولَٰئِكَ عِندَ اللَّهِ هُمُ الْكَاذِبُونَ ۝١٣
Law laa jaaa`oo `alaihi bi-arba`ati shuhadaaa`; fa iz lam yaatoo bishshuhadaaa`i fa ulaaa `ika `indal laahi humul kaaziboon
📖 Tekkim Wolof
Bu ñu indi woon sax ñeenti seede, waaye bu ñu ko indiwul [ngeen daldi xam fa saa sa] ne ñoom kat ay fenjat lañu.
🎧 Dégg

📜 Aaya 11-15 — An-Nur

11إِنَّ الَّذِينَ جَاءُوا بِالْإِفْكِ عُصْبَةٌ مِّنكُمْ ۚ لَا تَحْسَبُوهُ شَرًّا لَّكُم ۖ بَلْ هُوَ خَيْرٌ لَّكُمْ ۚ لِكُلِّ امْرِئٍ مِّنْهُم مَّا اكْتَسَبَ مِنَ الْإِثْمِ ۚ وَالَّذِي تَوَلَّىٰ كِبْرَهُ مِنْهُمْ لَهُ عَذَابٌ عَظِيمٌ
Ña leen di indil jiixi-jaaxa [naaféq ya], ab kurél lañu ci yéen. Buleen ko jàppe ay, yiw la ci yéen. Kenn ku nekk ci yéen dana jot bàkkaaram. Képp ku ca ëppal dana am mbugal mu màgg.
12لَّوْلَا إِذْ سَمِعْتُمُوهُ ظَنَّ الْمُؤْمِنُونَ وَالْمُؤْمِنَاتُ بِأَنفُسِهِمْ خَيْرًا وَقَالُوا هَٰذَا إِفْكٌ مُّبِينٌ
Lu tere woon jullit ñu góor ñeek jigéen di jort ci aw yiw ci seen diggante ? Ana lu tere ca saa sa ñu ne : “Lii kat aw duur la ” ?
13لَّوْلَا جَاءُوا عَلَيْهِ بِأَرْبَعَةِ شُهَدَاءَ ۚ فَإِذْ لَمْ يَأْتُوا بِالشُّهَدَاءِ فَأُولَٰئِكَ عِندَ اللَّهِ هُمُ الْكَاذِبُونَ
Bu ñu indi woon sax ñeenti seede, waaye bu ñu ko indiwul [ngeen daldi xam fa saa sa] ne ñoom kat ay fenjat lañu.
14وَلَوْلَا فَضْلُ اللَّهِ عَلَيْكُمْ وَرَحْمَتُهُ فِي الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ لَمَسَّكُمْ فِي مَا أَفَضْتُمْ فِيهِ عَذَابٌ عَظِيمٌ
Cëy dogankoon ak ngënéelul Yàlla ci yéen fii ci àddina sii ak fee ci àllaaxira, kon dey seen duur wii mbugal mu rëy dana leen ci dal,
15إِذْ تَلَقَّوْنَهُ بِأَلْسِنَتِكُمْ وَتَقُولُونَ بِأَفْوَاهِكُم مَّا لَيْسَ لَكُم بِهِ عِلْمٌ وَتَحْسَبُونَهُ هَيِّنًا وَهُوَ عِندَ اللَّهِ عَظِيمٌ
ngir yéen a ngi jokk-jolaate xibaar ba ak seeni làmmiñ, di wax ci seeni gémmiñ loo xam ne amuleen ci benn xam-xam ; ngeen jàppe ko lu doyadi te fekk muy lu rëy a rëy fa Yàlla.
An-NurFihi Alxuraan
64Aaya
MedinanRevelation
13Aaya

Tekki — An-Nur 13

Simoore An-Nur Aaya 13 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu ñu indi woon sax ñeenti seede, waaye bu ñu…

Simoore Aaya 13/64 — An-Nur النور (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nur Dégg, An-Nur Tekki, An-Nur mp3, An-Nur pdf. Aaya 11–15. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers