Al-Qasas · 21/88
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Qasas
فَخَرَجَ مِنْهَا خَائِفًا يَتَرَقَّبُ ۖ قَالَ رَبِّ نَجِّنِي مِنَ الْقَوْمِ الظَّالِمِينَ ۝٢١
Fakharaja minhaa khaaa `ifany-yataraqqab; qaala Rabbi najjinee minal qawmiz zaalimeen
📖 Tekkim Wolof
Mu génne ca [dëkk] ba, tiit lool di moytu. Daldi wax ne : “Yaw sama Boroom, maa ngi sàkku nga musal ma ci tooñkat yi ! ”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 19-23 — Simoore Al-Qasas

19فَلَمَّا أَنْ أَرَادَ أَن يَبْطِشَ بِالَّذِي هُوَ عَدُوٌّ لَّهُمَا قَالَ يَا مُوسَىٰ أَتُرِيدُ أَن تَقْتُلَنِي كَمَا قَتَلْتَ نَفْسًا بِالْأَمْسِ ۖ إِن تُرِيدُ إِلَّا أَن تَكُونَ جَبَّارًا فِي الْأَرْضِ وَمَا تُرِيدُ أَن تَكُونَ مِنَ الْمُصْلِحِينَ
Ba mu bëggee lottal ka doon seen noon ba, mu ne ko : "Waaw yaw Muusaa, ndax danga maa bëgg a rey ni nga reyee woon démb bakkan ? Yaw kay dangaa bëgg a doon ku të ci réew mi ; waaye bëggoo bokk ca ñay yéwénal”.
20وَجَاءَ رَجُلٌ مِّنْ أَقْصَى الْمَدِينَةِ يَسْعَىٰ قَالَ يَا مُوسَىٰ إِنَّ الْمَلَأَ يَأْتَمِرُونَ بِكَ لِيَقْتُلُوكَ فَاخْرُجْ إِنِّي لَكَ مِنَ النَّاصِحِينَ
Mu am waa ju bawoo ca aanéeri dëkk ba di dox, dikk ne ko : “Kilifay dëkk yaa ngi takktoo ngir rey la. Génnal (dëkk bi). Man dama lay laabire”.
21فَخَرَجَ مِنْهَا خَائِفًا يَتَرَقَّبُ ۖ قَالَ رَبِّ نَجِّنِي مِنَ الْقَوْمِ الظَّالِمِينَ
Mu génne ca [dëkk] ba, tiit lool di moytu. Daldi wax ne : “Yaw sama Boroom, maa ngi sàkku nga musal ma ci tooñkat yi ! ”.
22وَلَمَّا تَوَجَّهَ تِلْقَاءَ مَدْيَنَ قَالَ عَسَىٰ رَبِّي أَن يَهْدِيَنِي سَوَاءَ السَّبِيلِ
Ba mu jubloo njëlal Madiyaana, wax na ne : “Amaana sama Boroom gindi ma, teg ma ci yoon wu jub wa”.
23وَلَمَّا وَرَدَ مَاءَ مَدْيَنَ وَجَدَ عَلَيْهِ أُمَّةً مِّنَ النَّاسِ يَسْقُونَ وَوَجَدَ مِن دُونِهِمُ امْرَأَتَيْنِ تَذُودَانِ ۖ قَالَ مَا خَطْبُكُمَا ۖ قَالَتَا لَا نَسْقِي حَتَّىٰ يُصْدِرَ الرِّعَاءُ ۖ وَأَبُونَا شَيْخٌ كَبِيرٌ
Ba mu agsee ca rootukaayub waa Madiyaana, mu fekk fa aw nit ñuy wëgg di jukki, mu fekk fa ba-tey ñaari jigéen ñu beru wëgguñu. Mu ne leen : “Lu xew ba wëgguleen ? ” Ñu ne ko : “Dunu wëgg lu dul ginnaaw ba sàmm si génnee ba dem ; te sunu baay màggat na”.
Al-QasasFihi Alxuraan
88Aaya
MeccanRevelation
21Aaya

Tekki — Al-Qasas 21

Simoore Al-Qasas Aaya 21 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mu génne ca [dëkk] ba, tiit lool di moytu. Daldi…

Simoore Aaya 21/88 — Simoore Al-Qasas القصص (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Qasas Dégg, Simoore Al-Qasas Tekki, Simoore Al-Qasas mp3, Simoore Al-Qasas pdf. Aaya 19–23. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers