Al-Qasas · 20/88
Tekki Waxtaan — Al-Qasas
وَجَاءَ رَجُلٌ مِّنْ أَقْصَى الْمَدِينَةِ يَسْعَىٰ قَالَ يَا مُوسَىٰ إِنَّ الْمَلَأَ يَأْتَمِرُونَ بِكَ لِيَقْتُلُوكَ فَاخْرُجْ إِنِّي لَكَ مِنَ النَّاصِحِينَ ۝٢٠
Wa jaaa`a rajulum min aqsal madeenati yas`aa qaala yaa Moosaaa innal mala a yaa tamiroona bika liyaqtulooka fakhruj innee laka minan naasiheen
📖 Tekkim Wolof
Mu am waa ju bawoo ca aanéeri dëkk ba di dox, dikk ne ko : “Kilifay dëkk yaa ngi takktoo ngir rey la. Génnal (dëkk bi). Man dama lay laabire”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 18-22 — Al-Qasas

18فَأَصْبَحَ فِي الْمَدِينَةِ خَائِفًا يَتَرَقَّبُ فَإِذَا الَّذِي اسْتَنصَرَهُ بِالْأَمْسِ يَسْتَصْرِخُهُ ۚ قَالَ لَهُ مُوسَىٰ إِنَّكَ لَغَوِيٌّ مُّبِينٌ
Mu nekk ca dëkk ba tiit lool di moytu, jekki-jekki rekk waa ja ko doon ñaan ndimbal sàkkooti na ca moom ndimbal. Muusaa ne ko : “Yaw daal jalaasa nga, di ku tafaar”.
19فَلَمَّا أَنْ أَرَادَ أَن يَبْطِشَ بِالَّذِي هُوَ عَدُوٌّ لَّهُمَا قَالَ يَا مُوسَىٰ أَتُرِيدُ أَن تَقْتُلَنِي كَمَا قَتَلْتَ نَفْسًا بِالْأَمْسِ ۖ إِن تُرِيدُ إِلَّا أَن تَكُونَ جَبَّارًا فِي الْأَرْضِ وَمَا تُرِيدُ أَن تَكُونَ مِنَ الْمُصْلِحِينَ
Ba mu bëggee lottal ka doon seen noon ba, mu ne ko : "Waaw yaw Muusaa, ndax danga maa bëgg a rey ni nga reyee woon démb bakkan ? Yaw kay dangaa bëgg a doon ku të ci réew mi ; waaye bëggoo bokk ca ñay yéwénal”.
20وَجَاءَ رَجُلٌ مِّنْ أَقْصَى الْمَدِينَةِ يَسْعَىٰ قَالَ يَا مُوسَىٰ إِنَّ الْمَلَأَ يَأْتَمِرُونَ بِكَ لِيَقْتُلُوكَ فَاخْرُجْ إِنِّي لَكَ مِنَ النَّاصِحِينَ
Mu am waa ju bawoo ca aanéeri dëkk ba di dox, dikk ne ko : “Kilifay dëkk yaa ngi takktoo ngir rey la. Génnal (dëkk bi). Man dama lay laabire”.
21فَخَرَجَ مِنْهَا خَائِفًا يَتَرَقَّبُ ۖ قَالَ رَبِّ نَجِّنِي مِنَ الْقَوْمِ الظَّالِمِينَ
Mu génne ca [dëkk] ba, tiit lool di moytu. Daldi wax ne : “Yaw sama Boroom, maa ngi sàkku nga musal ma ci tooñkat yi ! ”.
22وَلَمَّا تَوَجَّهَ تِلْقَاءَ مَدْيَنَ قَالَ عَسَىٰ رَبِّي أَن يَهْدِيَنِي سَوَاءَ السَّبِيلِ
Ba mu jubloo njëlal Madiyaana, wax na ne : “Amaana sama Boroom gindi ma, teg ma ci yoon wu jub wa”.
Al-QasasFihi Alxuraan
88Aaya
MeccanRevelation
20Aaya

Tekki — Al-Qasas 20

Simoore Al-Qasas Aaya 20 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mu am waa ju bawoo ca aanéeri dëkk ba di…

Simoore Aaya 20/88 — Al-Qasas القصص (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Qasas Dégg, Al-Qasas Tekki, Al-Qasas mp3, Al-Qasas pdf. Aaya 18–22. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers