Al-Qasas · 22/88
Tekki Waxtaan — Al-Qasas
وَلَمَّا تَوَجَّهَ تِلْقَاءَ مَدْيَنَ قَالَ عَسَىٰ رَبِّي أَن يَهْدِيَنِي سَوَاءَ السَّبِيلِ ۝٢٢
Wa lammaa tawajjaha tilqaaa`a Madyana qaala `asaa Rabbeee ai yahdiyanee Sawaaa`as Sabeel
📖 Tekkim Wolof
Ba mu jubloo njëlal Madiyaana, wax na ne : “Amaana sama Boroom gindi ma, teg ma ci yoon wu jub wa”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 20-24 — Al-Qasas

20وَجَاءَ رَجُلٌ مِّنْ أَقْصَى الْمَدِينَةِ يَسْعَىٰ قَالَ يَا مُوسَىٰ إِنَّ الْمَلَأَ يَأْتَمِرُونَ بِكَ لِيَقْتُلُوكَ فَاخْرُجْ إِنِّي لَكَ مِنَ النَّاصِحِينَ
Mu am waa ju bawoo ca aanéeri dëkk ba di dox, dikk ne ko : “Kilifay dëkk yaa ngi takktoo ngir rey la. Génnal (dëkk bi). Man dama lay laabire”.
21فَخَرَجَ مِنْهَا خَائِفًا يَتَرَقَّبُ ۖ قَالَ رَبِّ نَجِّنِي مِنَ الْقَوْمِ الظَّالِمِينَ
Mu génne ca [dëkk] ba, tiit lool di moytu. Daldi wax ne : “Yaw sama Boroom, maa ngi sàkku nga musal ma ci tooñkat yi ! ”.
22وَلَمَّا تَوَجَّهَ تِلْقَاءَ مَدْيَنَ قَالَ عَسَىٰ رَبِّي أَن يَهْدِيَنِي سَوَاءَ السَّبِيلِ
Ba mu jubloo njëlal Madiyaana, wax na ne : “Amaana sama Boroom gindi ma, teg ma ci yoon wu jub wa”.
23وَلَمَّا وَرَدَ مَاءَ مَدْيَنَ وَجَدَ عَلَيْهِ أُمَّةً مِّنَ النَّاسِ يَسْقُونَ وَوَجَدَ مِن دُونِهِمُ امْرَأَتَيْنِ تَذُودَانِ ۖ قَالَ مَا خَطْبُكُمَا ۖ قَالَتَا لَا نَسْقِي حَتَّىٰ يُصْدِرَ الرِّعَاءُ ۖ وَأَبُونَا شَيْخٌ كَبِيرٌ
Ba mu agsee ca rootukaayub waa Madiyaana, mu fekk fa aw nit ñuy wëgg di jukki, mu fekk fa ba-tey ñaari jigéen ñu beru wëgguñu. Mu ne leen : “Lu xew ba wëgguleen ? ” Ñu ne ko : “Dunu wëgg lu dul ginnaaw ba sàmm si génnee ba dem ; te sunu baay màggat na”.
24فَسَقَىٰ لَهُمَا ثُمَّ تَوَلَّىٰ إِلَى الظِّلِّ فَقَالَ رَبِّ إِنِّي لِمَا أَنزَلْتَ إِلَيَّ مِنْ خَيْرٍ فَقِيرٌ
Mu wëggal leen ba eggal, dem toog ca ker ga, daldi ne : “Sama Boroom, cëy aka maa ittewoo li nga may wërsëgale”.
Al-QasasFihi Alxuraan
88Aaya
MeccanRevelation
22Aaya

Tekki — Al-Qasas 22

Simoore Al-Qasas Aaya 22 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ba mu jubloo njëlal Madiyaana, wax na ne : “Amaana…

Simoore Aaya 22/88 — Al-Qasas القصص (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Qasas Dégg, Al-Qasas Tekki, Al-Qasas mp3, Al-Qasas pdf. Aaya 20–24. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers