Al-Qasas · 55/88
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Qasas
وَإِذَا سَمِعُوا اللَّغْوَ أَعْرَضُوا عَنْهُ وَقَالُوا لَنَا أَعْمَالُنَا وَلَكُمْ أَعْمَالُكُمْ سَلَامٌ عَلَيْكُمْ لَا نَبْتَغِي الْجَاهِلِينَ ۝٥٥
Wa izaa sami`ul laghwa a`radoo `anhu wa qaaloo lanaaa a`maalunaa wa lakum a`maalukum salaamun `alaikum laa nabtaghil jaahileen
📖 Tekkim Wolof
te saa yu ñu déggee ay caaxaan, dummóoyu ko tey wax naan : “Nun ak sunuy jëf, yéen ak séeni jëf. Yal na ngeen am jàmm. Nun dey, dunu sàkkuji mukk ñu réer ña”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 53-57 — Simoore Al-Qasas

53وَإِذَا يُتْلَىٰ عَلَيْهِمْ قَالُوا آمَنَّا بِهِ إِنَّهُ الْحَقُّ مِن رَّبِّنَا إِنَّا كُنَّا مِن قَبْلِهِ مُسْلِمِينَ
Te bunu leen ko mësaan a jàngal, dañu daan wax ne : “Gëm nanu ko. Te mooy dëgg ga jóge ca sunu Boroom. Faf nun jébbalu nanu ba mu laataa na ñëw”.
54أُولَٰئِكَ يُؤْتَوْنَ أَجْرَهُم مَّرَّتَيْنِ بِمَا صَبَرُوا وَيَدْرَءُونَ بِالْحَسَنَةِ السَّيِّئَةَ وَمِمَّا رَزَقْنَاهُمْ يُنفِقُونَ
Ñooña danañu seen pey ñaari yoon ca la ñu daan muñ, daan toontoo aw ñaawtéef ak lu rafet, te di joxe ca la Ma leen wërsëgal ;
55وَإِذَا سَمِعُوا اللَّغْوَ أَعْرَضُوا عَنْهُ وَقَالُوا لَنَا أَعْمَالُنَا وَلَكُمْ أَعْمَالُكُمْ سَلَامٌ عَلَيْكُمْ لَا نَبْتَغِي الْجَاهِلِينَ
te saa yu ñu déggee ay caaxaan, dummóoyu ko tey wax naan : “Nun ak sunuy jëf, yéen ak séeni jëf. Yal na ngeen am jàmm. Nun dey, dunu sàkkuji mukk ñu réer ña”.
56إِنَّكَ لَا تَهْدِي مَنْ أَحْبَبْتَ وَلَٰكِنَّ اللَّهَ يَهْدِي مَن يَشَاءُ ۚ وَهُوَ أَعْلَمُ بِالْمُهْتَدِينَ
Yaw (Muhammad) du ut ne yaay gindi ku la soob : waaye Yàlla mooy gindi ku ko soob. Te moo gën a xam ñiy gindiku.
57وَقَالُوا إِن نَّتَّبِعِ الْهُدَىٰ مَعَكَ نُتَخَطَّفْ مِنْ أَرْضِنَا ۚ أَوَلَمْ نُمَكِّن لَّهُمْ حَرَمًا آمِنًا يُجْبَىٰ إِلَيْهِ ثَمَرَاتُ كُلِّ شَيْءٍ رِّزْقًا مِّن لَّدُنَّا وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَهُمْ لَا يَعْلَمُونَ
Ñuy wax naan : “Su nu toppee njub gi ànd ak yaw, kon deef nanu foqarñee ci sunu suuf si”. - Ndax defalunu leen woon am réew wuñu wormaal, ñuy jëmmal wépp xeetu meññeef muy bawoo ci Nun [Yàlla] ? Waaye li ëpp ci ñoom xamuñu.
Al-QasasFihi Alxuraan
88Aaya
MeccanRevelation
55Aaya

Tekki — Al-Qasas 55

Simoore Al-Qasas Aaya 55 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : te saa yu ñu déggee ay caaxaan, dummóoyu ko tey…

Simoore Aaya 55/88 — Simoore Al-Qasas القصص (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Qasas Dégg, Simoore Al-Qasas Tekki, Simoore Al-Qasas mp3, Simoore Al-Qasas pdf. Aaya 53–57. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers