Aali Imran · 147/200
Tekki Waxtaan — Aali Imran
وَمَا كَانَ قَوْلَهُمْ إِلَّا أَن قَالُوا رَبَّنَا اغْفِرْ لَنَا ذُنُوبَنَا وَإِسْرَافَنَا فِي أَمْرِنَا وَثَبِّتْ أَقْدَامَنَا وَانصُرْنَا عَلَى الْقَوْمِ الْكَافِرِينَ ۝١٤٧
Wa maa kaana qawlahum illaa an qaaloo Rabbanagh fir lanaa zunoobanaa wa israafanaa feee amirnaa wa sabbit aqdaamanaa wansurnaa `alal qawmil kaafireen
📖 Tekkim Wolof
Te seeni wax nekkul lu dul ñu naan : “Sunu Boroom, jéggal nu sunuy bàkkaar ak sunuy jéggi-dayo ci sunuy mbir, te nga dëgëral sunuy ndëggu, te dimbali nu ci kaw nit ñii di ay yéefar”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 145-149 — Aali Imran

145وَمَا كَانَ لِنَفْسٍ أَن تَمُوتَ إِلَّا بِإِذْنِ اللَّهِ كِتَابًا مُّؤَجَّلًا ۗ وَمَن يُرِدْ ثَوَابَ الدُّنْيَا نُؤْتِهِ مِنْهَا وَمَن يُرِدْ ثَوَابَ الْآخِرَةِ نُؤْتِهِ مِنْهَا ۚ وَسَنَجْزِي الشَّاكِرِينَ
Bakkan du dee lu dul ci lu soob Yàlla, ci ab dig bu am àpp. Ku bëgg xéewali àddina, Dananu ko jox. Ku bëgg xéewali àllaaxira Dananu ko jox te Dananu fey [Nun Yàlla] ñiy gëram.
146وَكَأَيِّن مِّن نَّبِيٍّ قَاتَلَ مَعَهُ رِبِّيُّونَ كَثِيرٌ فَمَا وَهَنُوا لِمَا أَصَابَهُمْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ وَمَا ضَعُفُوا وَمَا اسْتَكَانُوا ۗ وَاللَّهُ يُحِبُّ الصَّابِرِينَ
Bariwaana Yonent bu xare ñu rey ko, mu ànd ak mbooloo mu bari, te doyadiwuñu ca la leen dal ci sàmm diiney Yàlla. Yoqatuñu, nekkuñu ñu xeebu. Yàlla safoo na muñkat yi.
147وَمَا كَانَ قَوْلَهُمْ إِلَّا أَن قَالُوا رَبَّنَا اغْفِرْ لَنَا ذُنُوبَنَا وَإِسْرَافَنَا فِي أَمْرِنَا وَثَبِّتْ أَقْدَامَنَا وَانصُرْنَا عَلَى الْقَوْمِ الْكَافِرِينَ
Te seeni wax nekkul lu dul ñu naan : “Sunu Boroom, jéggal nu sunuy bàkkaar ak sunuy jéggi-dayo ci sunuy mbir, te nga dëgëral sunuy ndëggu, te dimbali nu ci kaw nit ñii di ay yéefar”.
148فَآتَاهُمُ اللَّهُ ثَوَابَ الدُّنْيَا وَحُسْنَ ثَوَابِ الْآخِرَةِ ۗ وَاللَّهُ يُحِبُّ الْمُحْسِنِينَ
Yàlla yoole leen àddina [xéewal] ak gën jaa rafeti yoolub àllaaxira. Yàlla safoo na ñay rafetal.
149يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا إِن تُطِيعُوا الَّذِينَ كَفَرُوا يَرُدُّوكُمْ عَلَىٰ أَعْقَابِكُمْ فَتَنقَلِبُوا خَاسِرِينَ
Éy yéen ñi gëm!, bu ngeen toppee ñi weddi, danañu leen dugal sa seeni tànk [weddiloo leen], ngeen wëlbatiku ñàkk.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
147Aaya

Tekki — Aali Imran 147

Simoore Aali Imran Aaya 147 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te seeni wax nekkul lu dul ñu naan : “Sunu…

Simoore Aaya 147/200 — Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Aali Imran Dégg, Aali Imran Tekki, Aali Imran mp3, Aali Imran pdf. Aaya 145–149. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers