Aali Imran · 146/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
وَكَأَيِّن مِّن نَّبِيٍّ قَاتَلَ مَعَهُ رِبِّيُّونَ كَثِيرٌ فَمَا وَهَنُوا لِمَا أَصَابَهُمْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ وَمَا ضَعُفُوا وَمَا اسْتَكَانُوا ۗ وَاللَّهُ يُحِبُّ الصَّابِرِينَ ۝١٤٦
Wa ka aiyim min Nabiyyin qaatala ma`ahoo ribbiyyoona kaseerun famaa wahanoo limaaa Asaabahum fee sabeelil laahi wa maa da`ufoo wa mas takaanoo; wallaahu yuhibbus saabireen
📖 Tekkim Wolof
Bariwaana Yonent bu xare ñu rey ko, mu ànd ak mbooloo mu bari, te doyadiwuñu ca la leen dal ci sàmm diiney Yàlla. Yoqatuñu, nekkuñu ñu xeebu. Yàlla safoo na muñkat yi.

🎧 Dégg


📜 Aaya 144-148 — Simoore Aali Imran

144وَمَا مُحَمَّدٌ إِلَّا رَسُولٌ قَدْ خَلَتْ مِن قَبْلِهِ الرُّسُلُ ۚ أَفَإِن مَّاتَ أَوْ قُتِلَ انقَلَبْتُمْ عَلَىٰ أَعْقَابِكُمْ ۚ وَمَن يَنقَلِبْ عَلَىٰ عَقِبَيْهِ فَلَن يَضُرَّ اللَّهَ شَيْئًا ۗ وَسَيَجْزِي اللَّهُ الشَّاكِرِينَ
Muhammad doonul lu may ab Yonent - boo xam ne ay Yonent ñoo ko jiitu woon ba jàll - Ndax bu deewoon walla ñu rey ko, dangeen di dellu ca seeni tànk, weddi ? Ku walbatiku ca ay tànkam, du wàññi Yàlla dara ; te Yàlla dana fey ñay gëram seen Boroom.
145وَمَا كَانَ لِنَفْسٍ أَن تَمُوتَ إِلَّا بِإِذْنِ اللَّهِ كِتَابًا مُّؤَجَّلًا ۗ وَمَن يُرِدْ ثَوَابَ الدُّنْيَا نُؤْتِهِ مِنْهَا وَمَن يُرِدْ ثَوَابَ الْآخِرَةِ نُؤْتِهِ مِنْهَا ۚ وَسَنَجْزِي الشَّاكِرِينَ
Bakkan du dee lu dul ci lu soob Yàlla, ci ab dig bu am àpp. Ku bëgg xéewali àddina, Dananu ko jox. Ku bëgg xéewali àllaaxira Dananu ko jox te Dananu fey [Nun Yàlla] ñiy gëram.
146وَكَأَيِّن مِّن نَّبِيٍّ قَاتَلَ مَعَهُ رِبِّيُّونَ كَثِيرٌ فَمَا وَهَنُوا لِمَا أَصَابَهُمْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ وَمَا ضَعُفُوا وَمَا اسْتَكَانُوا ۗ وَاللَّهُ يُحِبُّ الصَّابِرِينَ
Bariwaana Yonent bu xare ñu rey ko, mu ànd ak mbooloo mu bari, te doyadiwuñu ca la leen dal ci sàmm diiney Yàlla. Yoqatuñu, nekkuñu ñu xeebu. Yàlla safoo na muñkat yi.
147وَمَا كَانَ قَوْلَهُمْ إِلَّا أَن قَالُوا رَبَّنَا اغْفِرْ لَنَا ذُنُوبَنَا وَإِسْرَافَنَا فِي أَمْرِنَا وَثَبِّتْ أَقْدَامَنَا وَانصُرْنَا عَلَى الْقَوْمِ الْكَافِرِينَ
Te seeni wax nekkul lu dul ñu naan : “Sunu Boroom, jéggal nu sunuy bàkkaar ak sunuy jéggi-dayo ci sunuy mbir, te nga dëgëral sunuy ndëggu, te dimbali nu ci kaw nit ñii di ay yéefar”.
148فَآتَاهُمُ اللَّهُ ثَوَابَ الدُّنْيَا وَحُسْنَ ثَوَابِ الْآخِرَةِ ۗ وَاللَّهُ يُحِبُّ الْمُحْسِنِينَ
Yàlla yoole leen àddina [xéewal] ak gën jaa rafeti yoolub àllaaxira. Yàlla safoo na ñay rafetal.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
146Aaya

Tekki — Aali Imran 146

Simoore Aali Imran Aaya 146 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bariwaana Yonent bu xare ñu rey ko, mu ànd ak…

Simoore Aaya 146/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 144–148. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers