Luqman · 20/34
Tekki Waxtaan — Luqman
أَلَمْ تَرَوْا أَنَّ اللَّهَ سَخَّرَ لَكُم مَّا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ وَأَسْبَغَ عَلَيْكُمْ نِعَمَهُ ظَاهِرَةً وَبَاطِنَةً ۗ وَمِنَ النَّاسِ مَن يُجَادِلُ فِي اللَّهِ بِغَيْرِ عِلْمٍ وَلَا هُدًى وَلَا كِتَابٍ مُّنِيرٍ ۝٢٠
Alam taraw annal laaha sakhkhara lakum maa fis sa maawaati wa maa fil ardi wa asbaha `alaikum ni`amahoo zaahiratanw wa baatinah; wa minan naasi many yujaadilu fil laahi bighayri `ilminw wa laa hudanw wa laa Kitaabim muneer
📖 Tekkim Wolof
Xanaa gisuleen ne Yàllaa leen tàggatal li nekk ci asamaan yeek suuf si ? Te Mu tuur leen xéewalam yi ci li feeñ ak li nëbbu. Am na ci nit ñi ñuy dàggasante ci mbiri Yàlla, te amuñu ca benn xam-xam, du càggenu ag gindiku, waxantumalaak Téere buy gindi.

🎧 Dégg


📜 Aaya 18-22 — Luqman

18وَلَا تُصَعِّرْ خَدَّكَ لِلنَّاسِ وَلَا تَمْشِ فِي الْأَرْضِ مَرَحًا ۖ إِنَّ اللَّهَ لَا يُحِبُّ كُلَّ مُخْتَالٍ فَخُورٍ
Bul dox di dummóoyu nit ñi, bul dox it di fuukarewu : Yàlla safoowul képp kuy fuukarewu ak a damu.
19وَاقْصِدْ فِي مَشْيِكَ وَاغْضُضْ مِن صَوْتِكَ ۚ إِنَّ أَنكَرَ الْأَصْوَاتِ لَصَوْتُ الْحَمِيرِ
Nangay teey ci sab dox, te nangay suufeel sa kàddu, ndax kàddu gi gën a suufe moo di kàddug mbaam sëf ”.
20أَلَمْ تَرَوْا أَنَّ اللَّهَ سَخَّرَ لَكُم مَّا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ وَأَسْبَغَ عَلَيْكُمْ نِعَمَهُ ظَاهِرَةً وَبَاطِنَةً ۗ وَمِنَ النَّاسِ مَن يُجَادِلُ فِي اللَّهِ بِغَيْرِ عِلْمٍ وَلَا هُدًى وَلَا كِتَابٍ مُّنِيرٍ
Xanaa gisuleen ne Yàllaa leen tàggatal li nekk ci asamaan yeek suuf si ? Te Mu tuur leen xéewalam yi ci li feeñ ak li nëbbu. Am na ci nit ñi ñuy dàggasante ci mbiri Yàlla, te amuñu ca benn xam-xam, du càggenu ag gindiku, waxantumalaak Téere buy gindi.
21وَإِذَا قِيلَ لَهُمُ اتَّبِعُوا مَا أَنزَلَ اللَّهُ قَالُوا بَلْ نَتَّبِعُ مَا وَجَدْنَا عَلَيْهِ آبَاءَنَا ۚ أَوَلَوْ كَانَ الشَّيْطَانُ يَدْعُوهُمْ إِلَىٰ عَذَابِ السَّعِيرِ
Te bu ñu leen waxee ne : “Toppleen li Yàlla wàcce”, dañu naan : “Nuy kay dañuy topp sunu baaxi maam”. Moo ndax Séytaane daawuleen woo jëme leen ci mbugalum Safara !
22۞ وَمَن يُسْلِمْ وَجْهَهُ إِلَى اللَّهِ وَهُوَ مُحْسِنٌ فَقَدِ اسْتَمْسَكَ بِالْعُرْوَةِ الْوُثْقَىٰ ۗ وَإِلَى اللَّهِ عَاقِبَةُ الْأُمُورِ
Képp ku jébbal Yàlla boppam tey rafetal, [na xam ne] ŋoy na ci buum gi gën a dëgër. Te ca Yàlla la mbir yépp di mujj.
LuqmanFihi Alxuraan
34Aaya
MeccanRevelation
20Aaya

Tekki — Luqman 20

Simoore Luqman Aaya 20 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Xanaa gisuleen ne Yàllaa leen tàggatal li nekk ci asamaan…

Simoore Aaya 20/34 — Luqman لقمان (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Luqman Dégg, Luqman Tekki, Luqman mp3, Luqman pdf. Aaya 18–22. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, August 19, 2026

Don't forget us in your sincere prayers