Saba · 4/54
Tekki Waxtaan — Saba
لِّيَجْزِيَ الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ ۚ أُولَٰئِكَ لَهُم مَّغْفِرَةٌ وَرِزْقٌ كَرِيمٌ ۝٤
Liyajziyal lazeena aamanoo wa `amilus saalihaat; ulaaa`ika lahum maghfiratunw wa rizqun kareem
📖 Tekkim Wolof
[Li waral Bis ba], ngir fey ña gëmoon tey jëf u yiw. Danañu am njéggal, ak teraanga ak i xéewal.
🎧 Dégg

📜 Aaya 2-6 — Saba

2يَعْلَمُ مَا يَلِجُ فِي الْأَرْضِ وَمَا يَخْرُجُ مِنْهَا وَمَا يَنزِلُ مِنَ السَّمَاءِ وَمَا يَعْرُجُ فِيهَا ۚ وَهُوَ الرَّحِيمُ الْغَفُورُ
Xam na li duggu ci suuf ak la cay génne, ak lay wàcc ci asamaan si ak la cay yéeg. Mooy Jaglewaakoon ba, di Jéggalaakoon ba.
3وَقَالَ الَّذِينَ كَفَرُوا لَا تَأْتِينَا السَّاعَةُ ۖ قُلْ بَلَىٰ وَرَبِّي لَتَأْتِيَنَّكُمْ عَالِمِ الْغَيْبِ ۖ لَا يَعْزُبُ عَنْهُ مِثْقَالُ ذَرَّةٍ فِي السَّمَاوَاتِ وَلَا فِي الْأَرْضِ وَلَا أَصْغَرُ مِن ذَٰلِكَ وَلَا أَكْبَرُ إِلَّا فِي كِتَابٍ مُّبِينٍ
Yéefar yaa ngay wax naan : “Bis-pénc ba du ñëw”. Waxal ne : “Axakañ. Giñ naa ci sama Boroom ! ne dana leen dikkal. Moom mi xam kumpa. Te dara lu tollu ni aw pepp du ko lënt ci asamaan yeek suuf si. Walla lu ko gën a tuuti, walla lu ko gën a rëy, lu dul ne mi ngi ci ab Téere bu bir.
4لِّيَجْزِيَ الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ ۚ أُولَٰئِكَ لَهُم مَّغْفِرَةٌ وَرِزْقٌ كَرِيمٌ
[Li waral Bis ba], ngir fey ña gëmoon tey jëf u yiw. Danañu am njéggal, ak teraanga ak i xéewal.
5وَالَّذِينَ سَعَوْا فِي آيَاتِنَا مُعَاجِزِينَ أُولَٰئِكَ لَهُمْ عَذَابٌ مِّن رِّجْزٍ أَلِيمٌ
Ña doon dëgërante bopp te Sunuy laaya nag ñoom, danañu am mbugalum kaŋ-kaŋ mu metti.
6وَيَرَى الَّذِينَ أُوتُوا الْعِلْمَ الَّذِي أُنزِلَ إِلَيْكَ مِن رَّبِّكَ هُوَ الْحَقَّ وَيَهْدِي إِلَىٰ صِرَاطِ الْعَزِيزِ الْحَمِيدِ
Woroom xam-xam ya danañu gis ne li Nu wàcce ci yaw mu bawoo ca sa Boroom, mooy dëgg te dafay gindee jëme ca yoonu Yàlla wu jub wa xocc, Yàlla miy boroom kàttan, di Yayowaakoonu cant.
SabaFihi Alxuraan
54Aaya
MeccanRevelation
4Aaya

Tekki — Saba 4

Simoore Saba Aaya 4 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Li waral Bis ba], ngir fey ña gëmoon tey jëf…

Simoore Aaya 4/54 — Saba سبأ (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Saba Dégg, Saba Tekki, Saba mp3, Saba pdf. Aaya 2–6. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers