An-Nisa · 138/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
بَشِّرِ الْمُنَافِقِينَ بِأَنَّ لَهُمْ عَذَابًا أَلِيمًا ۝١٣٨
Bashshiril munaafiqeena bi anna lahum `azaaban aleemaa
📖 Tekkim Wolof
Bégalal [xamalal] naaféq ya ci ne am nañu mbugal mu metti,
🎧 Dégg

📜 Aaya 136-140 — An-Nisa

136يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا آمِنُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ وَالْكِتَابِ الَّذِي نَزَّلَ عَلَىٰ رَسُولِهِ وَالْكِتَابِ الَّذِي أَنزَلَ مِن قَبْلُ ۚ وَمَن يَكْفُرْ بِاللَّهِ وَمَلَائِكَتِهِ وَكُتُبِهِ وَرُسُلِهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ فَقَدْ ضَلَّ ضَلَالًا بَعِيدًا
Éy yéen ñi gëm ! Doyluleen Yàlla ak ub Yonentam, ak Téere ba Mu wàcce ci Yonentam, ak Téere ba wàcc la jiitu. Képp ku weddi Yàlla, ak i Malaakaam, ak Yonentam, ak Bis-pénc ba, réer na réer gu sori [dëgg].
137إِنَّ الَّذِينَ آمَنُوا ثُمَّ كَفَرُوا ثُمَّ آمَنُوا ثُمَّ كَفَرُوا ثُمَّ ازْدَادُوا كُفْرًا لَّمْ يَكُنِ اللَّهُ لِيَغْفِرَ لَهُمْ وَلَا لِيَهْدِيَهُمْ سَبِيلًا
Ña nga xam ne dañoo gëm ba noppi weddi, daldi gëm, weddiwaat, seenug weddi di gën a tar, Yàlla duleen jéggal, te it duleen gindi teg leen ci yoon wu leer wa.
138بَشِّرِ الْمُنَافِقِينَ بِأَنَّ لَهُمْ عَذَابًا أَلِيمًا
Bégalal [xamalal] naaféq ya ci ne am nañu mbugal mu metti,
139الَّذِينَ يَتَّخِذُونَ الْكَافِرِينَ أَوْلِيَاءَ مِن دُونِ الْمُؤْمِنِينَ ۚ أَيَبْتَغُونَ عِندَهُمُ الْعِزَّةَ فَإِنَّ الْعِزَّةَ لِلَّهِ جَمِيعًا
ña jàppe yéefar ya ay xarit, bàyyi fa jullit ña, ndax nee dañuy sàkku ci ñoom teraanga, te moone teraanga jépp a ngi ca Yàlla.
140وَقَدْ نَزَّلَ عَلَيْكُمْ فِي الْكِتَابِ أَنْ إِذَا سَمِعْتُمْ آيَاتِ اللَّهِ يُكْفَرُ بِهَا وَيُسْتَهْزَأُ بِهَا فَلَا تَقْعُدُوا مَعَهُمْ حَتَّىٰ يَخُوضُوا فِي حَدِيثٍ غَيْرِهِ ۚ إِنَّكُمْ إِذًا مِّثْلُهُمْ ۗ إِنَّ اللَّهَ جَامِعُ الْمُنَافِقِينَ وَالْكَافِرِينَ فِي جَهَنَّمَ جَمِيعًا
Te wàcceel na leen ca Téere ba, xamal leen ne : bu ngeen déggee ay nit ñuy weddi ak a ñaawal [yéjji] ndigali Yàlla yi, buleen toog ak ñay def loolu ba ba ñuy xuus ci weneen waxtaan. Lu ko moy dangeen di mel ni ñoom [cig weddi]. Yàlla Kuy dajale la naaféq yaak yéefar ya ñoom ñépp ca biir Safara.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
138Aaya

Tekki — An-Nisa 138

Simoore An-Nisa Aaya 138 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bégalal [xamalal] naaféq ya ci ne am nañu mbugal mu…

Simoore Aaya 138/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 136–140. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers