An-Nisa · 139/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
الَّذِينَ يَتَّخِذُونَ الْكَافِرِينَ أَوْلِيَاءَ مِن دُونِ الْمُؤْمِنِينَ ۚ أَيَبْتَغُونَ عِندَهُمُ الْعِزَّةَ فَإِنَّ الْعِزَّةَ لِلَّهِ جَمِيعًا ۝١٣٩
Allazeena yattakhizoo nal kaafireena awliyaaa`a min doonil mu`mineen; a-yabta ghoona `indahumul `izzata fainnnal `izzata lillaahi jamee`aa
📖 Tekkim Wolof
ña jàppe yéefar ya ay xarit, bàyyi fa jullit ña, ndax nee dañuy sàkku ci ñoom teraanga, te moone teraanga jépp a ngi ca Yàlla.

🎧 Dégg


📜 Aaya 137-141 — An-Nisa

137إِنَّ الَّذِينَ آمَنُوا ثُمَّ كَفَرُوا ثُمَّ آمَنُوا ثُمَّ كَفَرُوا ثُمَّ ازْدَادُوا كُفْرًا لَّمْ يَكُنِ اللَّهُ لِيَغْفِرَ لَهُمْ وَلَا لِيَهْدِيَهُمْ سَبِيلًا
Ña nga xam ne dañoo gëm ba noppi weddi, daldi gëm, weddiwaat, seenug weddi di gën a tar, Yàlla duleen jéggal, te it duleen gindi teg leen ci yoon wu leer wa.
138بَشِّرِ الْمُنَافِقِينَ بِأَنَّ لَهُمْ عَذَابًا أَلِيمًا
Bégalal [xamalal] naaféq ya ci ne am nañu mbugal mu metti,
139الَّذِينَ يَتَّخِذُونَ الْكَافِرِينَ أَوْلِيَاءَ مِن دُونِ الْمُؤْمِنِينَ ۚ أَيَبْتَغُونَ عِندَهُمُ الْعِزَّةَ فَإِنَّ الْعِزَّةَ لِلَّهِ جَمِيعًا
ña jàppe yéefar ya ay xarit, bàyyi fa jullit ña, ndax nee dañuy sàkku ci ñoom teraanga, te moone teraanga jépp a ngi ca Yàlla.
140وَقَدْ نَزَّلَ عَلَيْكُمْ فِي الْكِتَابِ أَنْ إِذَا سَمِعْتُمْ آيَاتِ اللَّهِ يُكْفَرُ بِهَا وَيُسْتَهْزَأُ بِهَا فَلَا تَقْعُدُوا مَعَهُمْ حَتَّىٰ يَخُوضُوا فِي حَدِيثٍ غَيْرِهِ ۚ إِنَّكُمْ إِذًا مِّثْلُهُمْ ۗ إِنَّ اللَّهَ جَامِعُ الْمُنَافِقِينَ وَالْكَافِرِينَ فِي جَهَنَّمَ جَمِيعًا
Te wàcceel na leen ca Téere ba, xamal leen ne : bu ngeen déggee ay nit ñuy weddi ak a ñaawal [yéjji] ndigali Yàlla yi, buleen toog ak ñay def loolu ba ba ñuy xuus ci weneen waxtaan. Lu ko moy dangeen di mel ni ñoom [cig weddi]. Yàlla Kuy dajale la naaféq yaak yéefar ya ñoom ñépp ca biir Safara.
141الَّذِينَ يَتَرَبَّصُونَ بِكُمْ فَإِن كَانَ لَكُمْ فَتْحٌ مِّنَ اللَّهِ قَالُوا أَلَمْ نَكُن مَّعَكُمْ وَإِن كَانَ لِلْكَافِرِينَ نَصِيبٌ قَالُوا أَلَمْ نَسْتَحْوِذْ عَلَيْكُمْ وَنَمْنَعْكُم مِّنَ الْمُؤْمِنِينَ ۚ فَاللَّهُ يَحْكُمُ بَيْنَكُمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ ۗ وَلَن يَجْعَلَ اللَّهُ لِلْكَافِرِينَ عَلَى الْمُؤْمِنِينَ سَبِيلًا
Ña nga xam ne ñanga téyandi seen bopp ci yéen ; su leen Yàlla joxee ndam, ñu gaaw ne : “Ndax àndunu woon ak yéen ? ” ; bu yéefar yi amee cër ci ndam, ñu ne leen : “Xanaa du ñoo leen doon song [yéen yéefar yi] te nu fegal leen jullit ñi ? ”. Yàlla Dana àtte seen diggante Bis-pénc ba. Te du jox yéefar yi ndam ci kaw jullit ñi.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
139Aaya

Tekki — An-Nisa 139

Simoore An-Nisa Aaya 139 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : ña jàppe yéefar ya ay xarit, bàyyi fa jullit ña,…

Simoore Aaya 139/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 137–141. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers