Muhammad · 20/38
Tekki Waxtaan — Muhammad
وَيَقُولُ الَّذِينَ آمَنُوا لَوْلَا نُزِّلَتْ سُورَةٌ ۖ فَإِذَا أُنزِلَتْ سُورَةٌ مُّحْكَمَةٌ وَذُكِرَ فِيهَا الْقِتَالُ ۙ رَأَيْتَ الَّذِينَ فِي قُلُوبِهِم مَّرَضٌ يَنظُرُونَ إِلَيْكَ نَظَرَ الْمَغْشِيِّ عَلَيْهِ مِنَ الْمَوْتِ ۖ فَأَوْلَىٰ لَهُمْ ۝٢٠
Wa yaqoolul lazeena aamanoo law laa nuzzilat Sooratun fa izaaa unzilat Sooratum Muhkamatunw wa zukira feehal qitaalu ra aytal lazeena fee quloobihim maraduny yanzuroona ilaika nazaral maghshiyyi `alaihi minal mawti fa`awlaa lahum
📖 Tekkim Wolof
Ña gëm ña ngay wax naan : “Cëy ! Bu aw saar wàccatiwoon ! ” Te fekk na saa suñu wàccee aw saar wu leer nàññ te digal ca xare, da ngay daldi gis naaféq ya di la xool ni ñuy xoole dee (ngir ragal). Li gën a yell ci ñoom moo di.

🎧 Dégg


📜 Aaya 18-22 — Muhammad

18فَهَلْ يَنظُرُونَ إِلَّا السَّاعَةَ أَن تَأْتِيَهُم بَغْتَةً ۖ فَقَدْ جَاءَ أَشْرَاطُهَا ۚ فَأَنَّىٰ لَهُمْ إِذَا جَاءَتْهُمْ ذِكْرَاهُمْ
Ana lan la (yéefar ya di xaar ci baña jebbalu) ba bis penc ba faf ne jaseet ci seen kaw bett leen ? Ndax màndargam yi dikk nañu. Te sax su xasee ba eksi ana lan la leen fàttaliku di jariñati?
19فَاعْلَمْ أَنَّهُ لَا إِلَٰهَ إِلَّا اللَّهُ وَاسْتَغْفِرْ لِذَنبِكَ وَلِلْمُؤْمِنِينَ وَالْمُؤْمِنَاتِ ۗ وَاللَّهُ يَعْلَمُ مُتَقَلَّبَكُمْ وَمَثْوَاكُمْ
Xamal ne, amul jeneen Yàlla ju dul moom Yàlla, te nga jéggalu say bàkkaar, ak di jéggalul jullit yu goor yeek yu jigéen yi. Yàlla xam na li ngeen di def lépp guddeek bëcëg.
20وَيَقُولُ الَّذِينَ آمَنُوا لَوْلَا نُزِّلَتْ سُورَةٌ ۖ فَإِذَا أُنزِلَتْ سُورَةٌ مُّحْكَمَةٌ وَذُكِرَ فِيهَا الْقِتَالُ ۙ رَأَيْتَ الَّذِينَ فِي قُلُوبِهِم مَّرَضٌ يَنظُرُونَ إِلَيْكَ نَظَرَ الْمَغْشِيِّ عَلَيْهِ مِنَ الْمَوْتِ ۖ فَأَوْلَىٰ لَهُمْ
Ña gëm ña ngay wax naan : “Cëy ! Bu aw saar wàccatiwoon ! ” Te fekk na saa suñu wàccee aw saar wu leer nàññ te digal ca xare, da ngay daldi gis naaféq ya di la xool ni ñuy xoole dee (ngir ragal). Li gën a yell ci ñoom moo di.
21طَاعَةٌ وَقَوْلٌ مَّعْرُوفٌ ۚ فَإِذَا عَزَمَ الْأَمْرُ فَلَوْ صَدَقُوا اللَّهَ لَكَانَ خَيْرًا لَّهُمْ
topp (jëf) ak wax ju yiw. Su, ndigal la xasee dugg, ñoom dey suñu dëggaloon (ndigalul Yàlla) jëfe ko), mooy gën ci ñoom (fuuf).
22فَهَلْ عَسَيْتُمْ إِن تَوَلَّيْتُمْ أَن تُفْسِدُوا فِي الْأَرْضِ وَتُقَطِّعُوا أَرْحَامَكُمْ
Moo ndax, su ngeen dëddoo baña xare ji loolu du jur ak yàq ci suuf si ak ngeen di dog séenug mbokk ?
MuhammadFihi Alxuraan
38Aaya
MedinanRevelation
20Aaya

Tekki — Muhammad 20

Simoore Muhammad Aaya 20 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña gëm ña ngay wax naan : “Cëy ! Bu…

Simoore Aaya 20/38 — Muhammad محمد (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Muhammad Dégg, Muhammad Tekki, Muhammad mp3, Muhammad pdf. Aaya 18–22. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, August 19, 2026

Don't forget us in your sincere prayers