Muhammad · 36/38
Tekki Waxtaan — Muhammad
إِنَّمَا الْحَيَاةُ الدُّنْيَا لَعِبٌ وَلَهْوٌ ۚ وَإِن تُؤْمِنُوا وَتَتَّقُوا يُؤْتِكُمْ أُجُورَكُمْ وَلَا يَسْأَلْكُمْ أَمْوَالَكُمْ ۝٣٦
Innamal hayaatud dunyaa la`ibunw wa lahw; wa in to`minoo wa tattaqoo yu`tikum ujoorakum wa laa yas`alkum amwaalakum
📖 Tekkim Wolof
Dundug Àddina sii am po la ak i caaxaan ; bu ngeen gëmee te ragal Yàlla di wattandiku , Dina leen jox séenug pey te duleen laaj séeni alal.
🎧 Dégg

📜 Aaya 34-38 — Muhammad

34إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا وَصَدُّوا عَن سَبِيلِ اللَّهِ ثُمَّ مَاتُوا وَهُمْ كُفَّارٌ فَلَن يَغْفِرَ اللَّهُ لَهُمْ
Ña daan weddi tey dumóoyu yoonu Yàlla ba dee ca diy yéefar, Yàlla duleen jéggal.
35فَلَا تَهِنُوا وَتَدْعُوا إِلَى السَّلْمِ وَأَنتُمُ الْأَعْلَوْنَ وَاللَّهُ مَعَكُمْ وَلَن يَتِرَكُمْ أَعْمَالَكُمْ
Bu leen di doyadi tey woote maslaa te yéen a gën a kawe, Yàlla itam yéen la àndal, te it séenug (peyug jëf) dara du ci wàññiku.
36إِنَّمَا الْحَيَاةُ الدُّنْيَا لَعِبٌ وَلَهْوٌ ۚ وَإِن تُؤْمِنُوا وَتَتَّقُوا يُؤْتِكُمْ أُجُورَكُمْ وَلَا يَسْأَلْكُمْ أَمْوَالَكُمْ
Dundug Àddina sii am po la ak i caaxaan ; bu ngeen gëmee te ragal Yàlla di wattandiku , Dina leen jox séenug pey te duleen laaj séeni alal.
37إِن يَسْأَلْكُمُوهَا فَيُحْفِكُمْ تَبْخَلُوا وَيُخْرِجْ أَضْغَانَكُمْ
Buleen ko Yàlla laajoon, kon dangeen di nay te kon dana génne seeni dëxëñ teg mbañeel gi séen diggante .
38هَا أَنتُمْ هَٰؤُلَاءِ تُدْعَوْنَ لِتُنفِقُوا فِي سَبِيلِ اللَّهِ فَمِنكُم مَّن يَبْخَلُ ۖ وَمَن يَبْخَلْ فَإِنَّمَا يَبْخَلُ عَن نَّفْسِهِ ۚ وَاللَّهُ الْغَنِيُّ وَأَنتُمُ الْفُقَرَاءُ ۚ وَإِن تَتَوَلَّوْا يَسْتَبْدِلْ قَوْمًا غَيْرَكُمْ ثُمَّ لَا يَكُونُوا أَمْثَالَكُم
Yéen a ngi nii ñu di leen woo ngir ngeen di joxey alal ci yoonu Yàlla. Am na ci yéen ñuy nay a joxe. Te képp kuy nay a joxe boppam la koy def. Yàlla di ku woomal te yéen ay ñi ñàkk. Te su ngeen dumóoyoo , Dana wuutal ñeneen nit ñu dul yéen, te du ñu mel ni yéen.
MuhammadFihi Alxuraan
38Aaya
MedinanRevelation
36Aaya

Tekki — Muhammad 36

Simoore Muhammad Aaya 36 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Dundug Àddina sii am po la ak i caaxaan ;…

Simoore Aaya 36/38 — Muhammad محمد (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Muhammad Dégg, Muhammad Tekki, Muhammad mp3, Muhammad pdf. Aaya 34–38. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers