Muhammad · 37/38
Tekki Waxtaan — Muhammad
إِن يَسْأَلْكُمُوهَا فَيُحْفِكُمْ تَبْخَلُوا وَيُخْرِجْ أَضْغَانَكُمْ ۝٣٧
Iny yas`alkumoohaa fa yuhfikum tabkhaloo wa yukhrij adghaanakum
📖 Tekkim Wolof
Buleen ko Yàlla laajoon, kon dangeen di nay te kon dana génne seeni dëxëñ teg mbañeel gi séen diggante .
🎧 Dégg

📜 Aaya 35-38 — Muhammad

35فَلَا تَهِنُوا وَتَدْعُوا إِلَى السَّلْمِ وَأَنتُمُ الْأَعْلَوْنَ وَاللَّهُ مَعَكُمْ وَلَن يَتِرَكُمْ أَعْمَالَكُمْ
Bu leen di doyadi tey woote maslaa te yéen a gën a kawe, Yàlla itam yéen la àndal, te it séenug (peyug jëf) dara du ci wàññiku.
36إِنَّمَا الْحَيَاةُ الدُّنْيَا لَعِبٌ وَلَهْوٌ ۚ وَإِن تُؤْمِنُوا وَتَتَّقُوا يُؤْتِكُمْ أُجُورَكُمْ وَلَا يَسْأَلْكُمْ أَمْوَالَكُمْ
Dundug Àddina sii am po la ak i caaxaan ; bu ngeen gëmee te ragal Yàlla di wattandiku , Dina leen jox séenug pey te duleen laaj séeni alal.
37إِن يَسْأَلْكُمُوهَا فَيُحْفِكُمْ تَبْخَلُوا وَيُخْرِجْ أَضْغَانَكُمْ
Buleen ko Yàlla laajoon, kon dangeen di nay te kon dana génne seeni dëxëñ teg mbañeel gi séen diggante .
38هَا أَنتُمْ هَٰؤُلَاءِ تُدْعَوْنَ لِتُنفِقُوا فِي سَبِيلِ اللَّهِ فَمِنكُم مَّن يَبْخَلُ ۖ وَمَن يَبْخَلْ فَإِنَّمَا يَبْخَلُ عَن نَّفْسِهِ ۚ وَاللَّهُ الْغَنِيُّ وَأَنتُمُ الْفُقَرَاءُ ۚ وَإِن تَتَوَلَّوْا يَسْتَبْدِلْ قَوْمًا غَيْرَكُمْ ثُمَّ لَا يَكُونُوا أَمْثَالَكُم
Yéen a ngi nii ñu di leen woo ngir ngeen di joxey alal ci yoonu Yàlla. Am na ci yéen ñuy nay a joxe. Te képp kuy nay a joxe boppam la koy def. Yàlla di ku woomal te yéen ay ñi ñàkk. Te su ngeen dumóoyoo , Dana wuutal ñeneen nit ñu dul yéen, te du ñu mel ni yéen.
MuhammadFihi Alxuraan
38Aaya
MedinanRevelation
37Aaya

Tekki — Muhammad 37

Simoore Muhammad Aaya 37 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Buleen ko Yàlla laajoon, kon dangeen di nay te kon…

Simoore Aaya 37/38 — Muhammad محمد (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Muhammad Dégg, Muhammad Tekki, Muhammad mp3, Muhammad pdf. Aaya 35–38. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers