Al-Hujurat · 16/18
Tekki Waxtaan — Al-Hujurat
قُلْ أَتُعَلِّمُونَ اللَّهَ بِدِينِكُمْ وَاللَّهُ يَعْلَمُ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۚ وَاللَّهُ بِكُلِّ شَيْءٍ عَلِيمٌ ۝١٦
Qul atu`allimoonal laaha bideenikum wallaahu ya`lamu maa fis samaawaati wa maa fil ard; wallaahu bikulli shai`in `Aleem
📖 Tekkim Wolof
Waxal ne : “Ndax dangeen bëgg jàngal Yàlla seen diine, te Yàlla moom xam na li nekk ci biir asamaan yeek suuf si ? ” Yàlla Xamaakoon la ci lépp lu ne.
🎧 Dégg

📜 Aaya 14-18 — Al-Hujurat

14۞ قَالَتِ الْأَعْرَابُ آمَنَّا ۖ قُل لَّمْ تُؤْمِنُوا وَلَٰكِن قُولُوا أَسْلَمْنَا وَلَمَّا يَدْخُلِ الْإِيمَانُ فِي قُلُوبِكُمْ ۖ وَإِن تُطِيعُوا اللَّهَ وَرَسُولَهُ لَا يَلِتْكُم مِّنْ أَعْمَالِكُمْ شَيْئًا ۚ إِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Araab yi neenañu : “Gëm nanu”. Waxal ne : “Gëmaguleen . Waaye nañu wax ne : jébbale nanu sunu bopp, te sax ngëm ga duggagul seeni xol batey. Waaye su ngeen toppee Yàllaakub Yonentam, seen jëf jooju tus du leen ci moy”. Yàlla Jegëlaakoon la ab Jaglewaakoon la.
15إِنَّمَا الْمُؤْمِنُونَ الَّذِينَ آمَنُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ ثُمَّ لَمْ يَرْتَابُوا وَجَاهَدُوا بِأَمْوَالِهِمْ وَأَنفُسِهِمْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ ۚ أُولَٰئِكَ هُمُ الصَّادِقُونَ
Jullit ñi tigi ñooy ña gëm Yàlla akub Yonentam, te duñu ca dengi-dengi benn yoon te ñooy xare ci seen alal ak ci seeni bakkan ci yoonu Yàlla. Ñooñee ñoo di ñu dëggu ña (ca la ñu wax ñoom ne gëm nañu).
16قُلْ أَتُعَلِّمُونَ اللَّهَ بِدِينِكُمْ وَاللَّهُ يَعْلَمُ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۚ وَاللَّهُ بِكُلِّ شَيْءٍ عَلِيمٌ
Waxal ne : “Ndax dangeen bëgg jàngal Yàlla seen diine, te Yàlla moom xam na li nekk ci biir asamaan yeek suuf si ? ” Yàlla Xamaakoon la ci lépp lu ne.
17يَمُنُّونَ عَلَيْكَ أَنْ أَسْلَمُوا ۖ قُل لَّا تَمُنُّوا عَلَيَّ إِسْلَامَكُم ۖ بَلِ اللَّهُ يَمُنُّ عَلَيْكُمْ أَنْ هَدَاكُمْ لِلْإِيمَانِ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Ña nga lay caakaayoo seenug dugg ci Lislaam. Nee leen : “ Bu leen caakaayo ci seenug tàbbi ci (diine Islaam). Yàlla kay moo ame ndam li moom mi leen xéewale gindi leen jëme leen ci ngëm , ndegam ñu dëggu ngeen”.
18إِنَّ اللَّهَ يَعْلَمُ غَيْبَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۚ وَاللَّهُ بَصِيرٌ بِمَا تَعْمَلُونَ
Yàlla xam na Mbóotum asamaan yeek suuf si, te Yàlla nag Kuy gis la li ngeen di def.
Al-HujuratFihi Alxuraan
18Aaya
MedinanRevelation
16Aaya

Tekki — Al-Hujurat 16

Simoore Al-Hujurat Aaya 16 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Waxal ne : “Ndax dangeen bëgg jàngal Yàlla seen diine,…

Simoore Aaya 16/18 — Al-Hujurat الحجرات (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hujurat Dégg, Al-Hujurat Tekki, Al-Hujurat mp3, Al-Hujurat pdf. Aaya 14–18. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers