Al-Maida · 24/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
قَالُوا يَا مُوسَىٰ إِنَّا لَن نَّدْخُلَهَا أَبَدًا مَّا دَامُوا فِيهَا ۖ فَاذْهَبْ أَنتَ وَرَبُّكَ فَقَاتِلَا إِنَّا هَاهُنَا قَاعِدُونَ ۝٢٤
Qaaloo yaa Moosaaa innaa lan nadkhulahaa abadam maa daamoo feehaa fazhab anta wa Rabbuka faqaatilaaa innaa haahunaa qaa`idoon
📖 Tekkim Wolof
Ñu ne : “Yaw Muusaa ! [xamal ne] nun, dunu fa dugg mukk li feek ña nga nekk foofa. Dem fa, yaak sa Boroom, ngeen xeex yéen foofa. Nun fii la nuy toog”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 22-26 — Al-Maida

22قَالُوا يَا مُوسَىٰ إِنَّ فِيهَا قَوْمًا جَبَّارِينَ وَإِنَّا لَن نَّدْخُلَهَا حَتَّىٰ يَخْرُجُوا مِنْهَا فَإِن يَخْرُجُوا مِنْهَا فَإِنَّا دَاخِلُونَ
Ñu ne ko : "Yaw Muusaa, [xamal ne] suuf soosu ñu bari doolee fa nekk. Te nun dunu ca mën a dugg mukk li feek génnuñu. Bu ñu génnee nag ñu door a dugg”.
23قَالَ رَجُلَانِ مِنَ الَّذِينَ يَخَافُونَ أَنْعَمَ اللَّهُ عَلَيْهِمَا ادْخُلُوا عَلَيْهِمُ الْبَابَ فَإِذَا دَخَلْتُمُوهُ فَإِنَّكُمْ غَالِبُونَ ۚ وَعَلَى اللَّهِ فَتَوَكَّلُوا إِن كُنتُم مُّؤْمِنِينَ
Ñaari nit, ca ña ragal Yàlla, wax ne Yàlla teral na leen : “Dugguleen ca ñoom, nu jaare ci buntu bi ; bu ngeen jàllee, yéen ay not. Te ci Yàlla doŋŋ ngeen war a sukkandiku ndegam ñu gëm ngeen”.
24قَالُوا يَا مُوسَىٰ إِنَّا لَن نَّدْخُلَهَا أَبَدًا مَّا دَامُوا فِيهَا ۖ فَاذْهَبْ أَنتَ وَرَبُّكَ فَقَاتِلَا إِنَّا هَاهُنَا قَاعِدُونَ
Ñu ne : “Yaw Muusaa ! [xamal ne] nun, dunu fa dugg mukk li feek ña nga nekk foofa. Dem fa, yaak sa Boroom, ngeen xeex yéen foofa. Nun fii la nuy toog”.
25قَالَ رَبِّ إِنِّي لَا أَمْلِكُ إِلَّا نَفْسِي وَأَخِي ۖ فَافْرُقْ بَيْنَنَا وَبَيْنَ الْقَوْمِ الْفَاسِقِينَ
Mu ne : “Sam Boroom ! Mënaluma dara ku dul man ak sama mbokk [Haaruuna : àtteel sunu diggante ak ñiy sàqi ndigal”.
26قَالَ فَإِنَّهَا مُحَرَّمَةٌ عَلَيْهِمْ ۛ أَرْبَعِينَ سَنَةً ۛ يَتِيهُونَ فِي الْأَرْضِ ۚ فَلَا تَأْسَ عَلَى الْقَوْمِ الْفَاسِقِينَ
[Boroom bi tontu] ne: “Suuf soosu araam na leen ñeent-fukki at yoo xam ne danañu gëlëm di wëndéelu ci àll bi. Bul jàq ci mbiru ñiy sàqi ndigal”.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
24Aaya

Tekki — Al-Maida 24

Simoore Al-Maida Aaya 24 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñu ne : “Yaw Muusaa ! [xamal ne] nun, dunu…

Simoore Aaya 24/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 22–26. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers