Al-Maida · 25/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
قَالَ رَبِّ إِنِّي لَا أَمْلِكُ إِلَّا نَفْسِي وَأَخِي ۖ فَافْرُقْ بَيْنَنَا وَبَيْنَ الْقَوْمِ الْفَاسِقِينَ ۝٢٥
Qaala Rabbi innee laaa amliku illaa nafsee wa akhee fafruq bainanaa wa bainal qawmil faasiqeen
📖 Tekkim Wolof
Mu ne : “Sam Boroom ! Mënaluma dara ku dul man ak sama mbokk [Haaruuna : àtteel sunu diggante ak ñiy sàqi ndigal”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 23-27 — Al-Maida

23قَالَ رَجُلَانِ مِنَ الَّذِينَ يَخَافُونَ أَنْعَمَ اللَّهُ عَلَيْهِمَا ادْخُلُوا عَلَيْهِمُ الْبَابَ فَإِذَا دَخَلْتُمُوهُ فَإِنَّكُمْ غَالِبُونَ ۚ وَعَلَى اللَّهِ فَتَوَكَّلُوا إِن كُنتُم مُّؤْمِنِينَ
Ñaari nit, ca ña ragal Yàlla, wax ne Yàlla teral na leen : “Dugguleen ca ñoom, nu jaare ci buntu bi ; bu ngeen jàllee, yéen ay not. Te ci Yàlla doŋŋ ngeen war a sukkandiku ndegam ñu gëm ngeen”.
24قَالُوا يَا مُوسَىٰ إِنَّا لَن نَّدْخُلَهَا أَبَدًا مَّا دَامُوا فِيهَا ۖ فَاذْهَبْ أَنتَ وَرَبُّكَ فَقَاتِلَا إِنَّا هَاهُنَا قَاعِدُونَ
Ñu ne : “Yaw Muusaa ! [xamal ne] nun, dunu fa dugg mukk li feek ña nga nekk foofa. Dem fa, yaak sa Boroom, ngeen xeex yéen foofa. Nun fii la nuy toog”.
25قَالَ رَبِّ إِنِّي لَا أَمْلِكُ إِلَّا نَفْسِي وَأَخِي ۖ فَافْرُقْ بَيْنَنَا وَبَيْنَ الْقَوْمِ الْفَاسِقِينَ
Mu ne : “Sam Boroom ! Mënaluma dara ku dul man ak sama mbokk [Haaruuna : àtteel sunu diggante ak ñiy sàqi ndigal”.
26قَالَ فَإِنَّهَا مُحَرَّمَةٌ عَلَيْهِمْ ۛ أَرْبَعِينَ سَنَةً ۛ يَتِيهُونَ فِي الْأَرْضِ ۚ فَلَا تَأْسَ عَلَى الْقَوْمِ الْفَاسِقِينَ
[Boroom bi tontu] ne: “Suuf soosu araam na leen ñeent-fukki at yoo xam ne danañu gëlëm di wëndéelu ci àll bi. Bul jàq ci mbiru ñiy sàqi ndigal”.
27۞ وَاتْلُ عَلَيْهِمْ نَبَأَ ابْنَيْ آدَمَ بِالْحَقِّ إِذْ قَرَّبَا قُرْبَانًا فَتُقُبِّلَ مِنْ أَحَدِهِمَا وَلَمْ يُتَقَبَّلْ مِنَ الْآخَرِ قَالَ لَأَقْتُلَنَّكَ ۖ قَالَ إِنَّمَا يَتَقَبَّلُ اللَّهُ مِنَ الْمُتَّقِينَ
Nettalileen, ci lu dëggu, xibaari ñaari doomi Aadama ya. Ba ñu sàkkoo yool bu ñu jaamoo Yàlla ; te Yàlla nangul kenn ca ñoom ñaar, bañ a nangul ka ca des. Ka ñu nangulul wax ne : “Danaa la rey”. Ka ñu nangul ne ko : “Na la wóor yaw it ne, Yàlla ña ko ragal lay nangu seeni jëf”.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
25Aaya

Tekki — Al-Maida 25

Simoore Al-Maida Aaya 25 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mu ne : “Sam Boroom ! Mënaluma dara ku dul…

Simoore Aaya 25/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 23–27. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers