Al-Maida · 46/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
وَقَفَّيْنَا عَلَىٰ آثَارِهِم بِعِيسَى ابْنِ مَرْيَمَ مُصَدِّقًا لِّمَا بَيْنَ يَدَيْهِ مِنَ التَّوْرَاةِ ۖ وَآتَيْنَاهُ الْإِنجِيلَ فِيهِ هُدًى وَنُورٌ وَمُصَدِّقًا لِّمَا بَيْنَ يَدَيْهِ مِنَ التَّوْرَاةِ وَهُدًى وَمَوْعِظَةً لِّلْمُتَّقِينَ ۝٤٦
Wa qaffainaa `alaaa aasaaarihim bi `Eesab ni Maryama musaddiqal limaa baina yadihi minat Tawraati wa aatainaahul Injeela feehi hudanw wa noorunw wa musaddiqal limaa baina yadaihi minat Tawraati wa hudanw wa maw`izatal lilmuttaqeen
📖 Tekkim Wolof
Toxal Nanu ci seen ginnaaw ya [ñoom Yonent ya] Iisaa, doomi Maryaama, mu dëggal la ko jiitu ci Tawreet. Jox ko Linjiil, njub ak leer nekk ca, muy dëggal la ko jiitu ci Tawreet, di njub ak waare gu jëm ca way-ragal Yàlla ña.

🎧 Dégg


📜 Aaya 44-48 — Al-Maida

44إِنَّا أَنزَلْنَا التَّوْرَاةَ فِيهَا هُدًى وَنُورٌ ۚ يَحْكُمُ بِهَا النَّبِيُّونَ الَّذِينَ أَسْلَمُوا لِلَّذِينَ هَادُوا وَالرَّبَّانِيُّونَ وَالْأَحْبَارُ بِمَا اسْتُحْفِظُوا مِن كِتَابِ اللَّهِ وَكَانُوا عَلَيْهِ شُهَدَاءَ ۚ فَلَا تَخْشَوُا النَّاسَ وَاخْشَوْنِ وَلَا تَشْتَرُوا بِآيَاتِي ثَمَنًا قَلِيلًا ۚ وَمَن لَّمْ يَحْكُم بِمَا أَنزَلَ اللَّهُ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الْكَافِرُونَ
Nun wàcce Nanu Tawreet, njub ak leer nekk ca Yonent ya nga xam ne wommatu woon nañu. Àtte nañu ca ña nekkoon i yahuud, ak niti Yàlla ya ak fóore ya. Te la nga xam ne dénkoon nañu leen ko [ci xam-xam] ci Téere Yàlla ba, ñu nekkoon ca ay seede. Buleen ragal nit ñi, ragal-leen Ma. Buleen weddi Samay laaya ci njëg gu néew. Képp du dul àtte ci li Yàlla wàcce, ñooña ñoo di ay yéefar.
45وَكَتَبْنَا عَلَيْهِمْ فِيهَا أَنَّ النَّفْسَ بِالنَّفْسِ وَالْعَيْنَ بِالْعَيْنِ وَالْأَنفَ بِالْأَنفِ وَالْأُذُنَ بِالْأُذُنِ وَالسِّنَّ بِالسِّنِّ وَالْجُرُوحَ قِصَاصٌ ۚ فَمَن تَصَدَّقَ بِهِ فَهُوَ كَفَّارَةٌ لَّهُ ۚ وَمَن لَّمْ يَحْكُم بِمَا أَنزَلَ اللَّهُ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الظَّالِمُونَ
Dogal Nanu ca ñoom ci Tawreet, ne ku rey nit ñu rey la ; naka noonu, ku fuq bët, ñu fuq bosam ; ku dog bakkan, ñu dog bosam ; nopp itam, nopp a koy fey; bëñ, bëñ a koy fey. Gaañu-gaañu it dañu koy feyee gaañu-gaañu. Waaye ku baale sa àq def ko sarax, dana am njéggalu Boroomam. Képp ku dul àtte ci li Yàlla wàcce, ñooña ñooy tooñkat ña.
46وَقَفَّيْنَا عَلَىٰ آثَارِهِم بِعِيسَى ابْنِ مَرْيَمَ مُصَدِّقًا لِّمَا بَيْنَ يَدَيْهِ مِنَ التَّوْرَاةِ ۖ وَآتَيْنَاهُ الْإِنجِيلَ فِيهِ هُدًى وَنُورٌ وَمُصَدِّقًا لِّمَا بَيْنَ يَدَيْهِ مِنَ التَّوْرَاةِ وَهُدًى وَمَوْعِظَةً لِّلْمُتَّقِينَ
Toxal Nanu ci seen ginnaaw ya [ñoom Yonent ya] Iisaa, doomi Maryaama, mu dëggal la ko jiitu ci Tawreet. Jox ko Linjiil, njub ak leer nekk ca, muy dëggal la ko jiitu ci Tawreet, di njub ak waare gu jëm ca way-ragal Yàlla ña.
47وَلْيَحْكُمْ أَهْلُ الْإِنجِيلِ بِمَا أَنزَلَ اللَّهُ فِيهِ ۚ وَمَن لَّمْ يَحْكُم بِمَا أَنزَلَ اللَّهُ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الْفَاسِقُونَ
Ñoñ-Injiil, nañu àtte ca la Yàlla wàcce ca biir [Téere boobu]. Képp ku dul àtte ca la Yàlla wàcce, ñoom way-sàqi ndigal lañu.
48وَأَنزَلْنَا إِلَيْكَ الْكِتَابَ بِالْحَقِّ مُصَدِّقًا لِّمَا بَيْنَ يَدَيْهِ مِنَ الْكِتَابِ وَمُهَيْمِنًا عَلَيْهِ ۖ فَاحْكُم بَيْنَهُم بِمَا أَنزَلَ اللَّهُ ۖ وَلَا تَتَّبِعْ أَهْوَاءَهُمْ عَمَّا جَاءَكَ مِنَ الْحَقِّ ۚ لِكُلٍّ جَعَلْنَا مِنكُمْ شِرْعَةً وَمِنْهَاجًا ۚ وَلَوْ شَاءَ اللَّهُ لَجَعَلَكُمْ أُمَّةً وَاحِدَةً وَلَٰكِن لِّيَبْلُوَكُمْ فِي مَا آتَاكُمْ ۖ فَاسْتَبِقُوا الْخَيْرَاتِ ۚ إِلَى اللَّهِ مَرْجِعُكُمْ جَمِيعًا فَيُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمْ فِيهِ تَخْتَلِفُونَ
Te wàcce Nanu ci Yaw Téere ba [Alxuraan] ci lu dëggu, muy dëggal la ko jiitu ci Téere bii, te muy aji-sàmm it [dëgg ya ca nekk]. Nanga àtte [yaw Yonent bi] seen diggante ci la Yàlla wàcce. Bul topp seen bànneex bàyyi li ñu la digal ci dëgg. Ku ci nekk ci yéen, defal Nanu ko aw yoon ak doxaliin. Te kat su neexoon Yàlla Mu def leen ngeen di wenn xeet. Waaye [Dakoo defe noonu] ngir nattu leen ca la Mu leen jox. Jëkkanteleen jëm ci yiw ya. Yéen ñépp ca Yàlla ngeen di mujj dellu ; Mu xamal leen la ngeen nekkoon di ca juuyoo.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
46Aaya

Tekki — Al-Maida 46

Simoore Al-Maida Aaya 46 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Toxal Nanu ci seen ginnaaw ya [ñoom Yonent ya] Iisaa,…

Simoore Aaya 46/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 44–48. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, August 19, 2026

Don't forget us in your sincere prayers