Al-Maida · 45/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
وَكَتَبْنَا عَلَيْهِمْ فِيهَا أَنَّ النَّفْسَ بِالنَّفْسِ وَالْعَيْنَ بِالْعَيْنِ وَالْأَنفَ بِالْأَنفِ وَالْأُذُنَ بِالْأُذُنِ وَالسِّنَّ بِالسِّنِّ وَالْجُرُوحَ قِصَاصٌ ۚ فَمَن تَصَدَّقَ بِهِ فَهُوَ كَفَّارَةٌ لَّهُ ۚ وَمَن لَّمْ يَحْكُم بِمَا أَنزَلَ اللَّهُ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الظَّالِمُونَ ۝٤٥
Wa katabnaa `alaihim feehaaa annan nafsa binnafsi wal`aina bil`aini wal anfa bilanfi wal uzuna bil uzuni wassinna bissinni waljurooha qisaas; faman tasaddaqa bihee fahuwa kaffaaratul lah; wa mal lam yahkum bimaaa anzalal laahu fa ulaaa`ika humuz zalimoon
📖 Tekkim Wolof
Dogal Nanu ca ñoom ci Tawreet, ne ku rey nit ñu rey la ; naka noonu, ku fuq bët, ñu fuq bosam ; ku dog bakkan, ñu dog bosam ; nopp itam, nopp a koy fey; bëñ, bëñ a koy fey. Gaañu-gaañu it dañu koy feyee gaañu-gaañu. Waaye ku baale sa àq def ko sarax, dana am njéggalu Boroomam. Képp ku dul àtte ci li Yàlla wàcce, ñooña ñooy tooñkat ña.
🎧 Dégg

📜 Aaya 43-47 — Al-Maida

43وَكَيْفَ يُحَكِّمُونَكَ وَعِندَهُمُ التَّوْرَاةُ فِيهَا حُكْمُ اللَّهِ ثُمَّ يَتَوَلَّوْنَ مِن بَعْدِ ذَٰلِكَ ۚ وَمَا أُولَٰئِكَ بِالْمُؤْمِنِينَ
Naka lañu lay àtteloo sax te ñu yor Tawreet, àttey Yàlla ya nekk ca biir ? Gannaaw loolu, ñu dëddu dëgg ga. Ñoom gëmuñu de.
44إِنَّا أَنزَلْنَا التَّوْرَاةَ فِيهَا هُدًى وَنُورٌ ۚ يَحْكُمُ بِهَا النَّبِيُّونَ الَّذِينَ أَسْلَمُوا لِلَّذِينَ هَادُوا وَالرَّبَّانِيُّونَ وَالْأَحْبَارُ بِمَا اسْتُحْفِظُوا مِن كِتَابِ اللَّهِ وَكَانُوا عَلَيْهِ شُهَدَاءَ ۚ فَلَا تَخْشَوُا النَّاسَ وَاخْشَوْنِ وَلَا تَشْتَرُوا بِآيَاتِي ثَمَنًا قَلِيلًا ۚ وَمَن لَّمْ يَحْكُم بِمَا أَنزَلَ اللَّهُ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الْكَافِرُونَ
Nun wàcce Nanu Tawreet, njub ak leer nekk ca Yonent ya nga xam ne wommatu woon nañu. Àtte nañu ca ña nekkoon i yahuud, ak niti Yàlla ya ak fóore ya. Te la nga xam ne dénkoon nañu leen ko [ci xam-xam] ci Téere Yàlla ba, ñu nekkoon ca ay seede. Buleen ragal nit ñi, ragal-leen Ma. Buleen weddi Samay laaya ci njëg gu néew. Képp du dul àtte ci li Yàlla wàcce, ñooña ñoo di ay yéefar.
45وَكَتَبْنَا عَلَيْهِمْ فِيهَا أَنَّ النَّفْسَ بِالنَّفْسِ وَالْعَيْنَ بِالْعَيْنِ وَالْأَنفَ بِالْأَنفِ وَالْأُذُنَ بِالْأُذُنِ وَالسِّنَّ بِالسِّنِّ وَالْجُرُوحَ قِصَاصٌ ۚ فَمَن تَصَدَّقَ بِهِ فَهُوَ كَفَّارَةٌ لَّهُ ۚ وَمَن لَّمْ يَحْكُم بِمَا أَنزَلَ اللَّهُ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الظَّالِمُونَ
Dogal Nanu ca ñoom ci Tawreet, ne ku rey nit ñu rey la ; naka noonu, ku fuq bët, ñu fuq bosam ; ku dog bakkan, ñu dog bosam ; nopp itam, nopp a koy fey; bëñ, bëñ a koy fey. Gaañu-gaañu it dañu koy feyee gaañu-gaañu. Waaye ku baale sa àq def ko sarax, dana am njéggalu Boroomam. Képp ku dul àtte ci li Yàlla wàcce, ñooña ñooy tooñkat ña.
46وَقَفَّيْنَا عَلَىٰ آثَارِهِم بِعِيسَى ابْنِ مَرْيَمَ مُصَدِّقًا لِّمَا بَيْنَ يَدَيْهِ مِنَ التَّوْرَاةِ ۖ وَآتَيْنَاهُ الْإِنجِيلَ فِيهِ هُدًى وَنُورٌ وَمُصَدِّقًا لِّمَا بَيْنَ يَدَيْهِ مِنَ التَّوْرَاةِ وَهُدًى وَمَوْعِظَةً لِّلْمُتَّقِينَ
Toxal Nanu ci seen ginnaaw ya [ñoom Yonent ya] Iisaa, doomi Maryaama, mu dëggal la ko jiitu ci Tawreet. Jox ko Linjiil, njub ak leer nekk ca, muy dëggal la ko jiitu ci Tawreet, di njub ak waare gu jëm ca way-ragal Yàlla ña.
47وَلْيَحْكُمْ أَهْلُ الْإِنجِيلِ بِمَا أَنزَلَ اللَّهُ فِيهِ ۚ وَمَن لَّمْ يَحْكُم بِمَا أَنزَلَ اللَّهُ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الْفَاسِقُونَ
Ñoñ-Injiil, nañu àtte ca la Yàlla wàcce ca biir [Téere boobu]. Képp ku dul àtte ca la Yàlla wàcce, ñoom way-sàqi ndigal lañu.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
45Aaya

Tekki — Al-Maida 45

Simoore Al-Maida Aaya 45 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Dogal Nanu ca ñoom ci Tawreet, ne ku rey nit…

Simoore Aaya 45/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 43–47. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers