Al-An'am · 74/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
۞ وَإِذْ قَالَ إِبْرَاهِيمُ لِأَبِيهِ آزَرَ أَتَتَّخِذُ أَصْنَامًا آلِهَةً ۖ إِنِّي أَرَاكَ وَقَوْمَكَ فِي ضَلَالٍ مُّبِينٍ ۝٧٤
Wa iz qaala Ibraaheemu li abeehi Aazara a-tattakhizu asnaaman aalihatan inneee araaka wa qawmaka fee dalaalim mmubeen
📖 Tekkim Wolof
(Te nga fàttaliku) ba Ibraahiima waxee baayam [Aazar] : “Ndax dangay jël ay xërëm def leen ay yàlla ? Man dey gis naa ne, yaak saw nit, yéen a ngi ci réer gu tar ! ”
🎧 Dégg

📜 Aaya 72-76 — Al-An'am

72وَأَنْ أَقِيمُوا الصَّلَاةَ وَاتَّقُوهُ ۚ وَهُوَ الَّذِي إِلَيْهِ تُحْشَرُونَ
te it ngeen taxawal julli te ragal Ko. Fa Moom kat lañu leen di dajale yéen ñépp”.
73وَهُوَ الَّذِي خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ بِالْحَقِّ ۖ وَيَوْمَ يَقُولُ كُن فَيَكُونُ ۚ قَوْلُهُ الْحَقُّ ۚ وَلَهُ الْمُلْكُ يَوْمَ يُنفَخُ فِي الصُّورِ ۚ عَالِمُ الْغَيْبِ وَالشَّهَادَةِ ۚ وَهُوَ الْحَكِيمُ الْخَبِيرُ
Moom mooy ki sàkk asamaan yeek suuf si ci dëgg. Ca bis ba Mu nee : “Nekkal ! ”. Mu daldi nekk, Ay waxam mooy dëgg. Te Moo moom nguur, bis ba ñuy ëf buft bi. Mooy xamaakoonu kumpa ak li fés. Te Mooy ku xereñ ki, deñ ciy kumpa.
74۞ وَإِذْ قَالَ إِبْرَاهِيمُ لِأَبِيهِ آزَرَ أَتَتَّخِذُ أَصْنَامًا آلِهَةً ۖ إِنِّي أَرَاكَ وَقَوْمَكَ فِي ضَلَالٍ مُّبِينٍ
(Te nga fàttaliku) ba Ibraahiima waxee baayam [Aazar] : “Ndax dangay jël ay xërëm def leen ay yàlla ? Man dey gis naa ne, yaak saw nit, yéen a ngi ci réer gu tar ! ”
75وَكَذَٰلِكَ نُرِي إِبْرَاهِيمَ مَلَكُوتَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَلِيَكُونَ مِنَ الْمُوقِنِينَ
Noonu Lanu wonee Ibraahiima moomeelu asamaan yi ak suuf si, ndax mu bokk ca way- wóolu ña.
76فَلَمَّا جَنَّ عَلَيْهِ اللَّيْلُ رَأَىٰ كَوْكَبًا ۖ قَالَ هَٰذَا رَبِّي ۖ فَلَمَّا أَفَلَ قَالَ لَا أُحِبُّ الْآفِلِينَ
Ba guddi lëndemee ci moom, mu gis benn bidiw, mu daldi ne : “Sama Yàllaa ngi nii ! ” Waaye, ba bidiw ba suuxee, mu ne : “Man daal soppuma ñiy suux”.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
74Aaya

Tekki — Al-An'am 74

Simoore Al-An'am Aaya 74 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : (Te nga fàttaliku) ba Ibraahiima waxee baayam [Aazar] : “Ndax…

Simoore Aaya 74/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 72–76. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers