Al-An'am · 75/165
Tekki Waxtaan — Simoore Al-An'am
وَكَذَٰلِكَ نُرِي إِبْرَاهِيمَ مَلَكُوتَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَلِيَكُونَ مِنَ الْمُوقِنِينَ ۝٧٥
Wa kazaalika nureee Ibraaheema malakootas samaawaati wal ardi wa liyakoona minal mooqineen
📖 Tekkim Wolof
Noonu Lanu wonee Ibraahiima moomeelu asamaan yi ak suuf si, ndax mu bokk ca way- wóolu ña.

🎧 Dégg


📜 Aaya 73-77 — Simoore Al-An'am

73وَهُوَ الَّذِي خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ بِالْحَقِّ ۖ وَيَوْمَ يَقُولُ كُن فَيَكُونُ ۚ قَوْلُهُ الْحَقُّ ۚ وَلَهُ الْمُلْكُ يَوْمَ يُنفَخُ فِي الصُّورِ ۚ عَالِمُ الْغَيْبِ وَالشَّهَادَةِ ۚ وَهُوَ الْحَكِيمُ الْخَبِيرُ
Moom mooy ki sàkk asamaan yeek suuf si ci dëgg. Ca bis ba Mu nee : “Nekkal ! ”. Mu daldi nekk, Ay waxam mooy dëgg. Te Moo moom nguur, bis ba ñuy ëf buft bi. Mooy xamaakoonu kumpa ak li fés. Te Mooy ku xereñ ki, deñ ciy kumpa.
74۞ وَإِذْ قَالَ إِبْرَاهِيمُ لِأَبِيهِ آزَرَ أَتَتَّخِذُ أَصْنَامًا آلِهَةً ۖ إِنِّي أَرَاكَ وَقَوْمَكَ فِي ضَلَالٍ مُّبِينٍ
(Te nga fàttaliku) ba Ibraahiima waxee baayam [Aazar] : “Ndax dangay jël ay xërëm def leen ay yàlla ? Man dey gis naa ne, yaak saw nit, yéen a ngi ci réer gu tar ! ”
75وَكَذَٰلِكَ نُرِي إِبْرَاهِيمَ مَلَكُوتَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَلِيَكُونَ مِنَ الْمُوقِنِينَ
Noonu Lanu wonee Ibraahiima moomeelu asamaan yi ak suuf si, ndax mu bokk ca way- wóolu ña.
76فَلَمَّا جَنَّ عَلَيْهِ اللَّيْلُ رَأَىٰ كَوْكَبًا ۖ قَالَ هَٰذَا رَبِّي ۖ فَلَمَّا أَفَلَ قَالَ لَا أُحِبُّ الْآفِلِينَ
Ba guddi lëndemee ci moom, mu gis benn bidiw, mu daldi ne : “Sama Yàllaa ngi nii ! ” Waaye, ba bidiw ba suuxee, mu ne : “Man daal soppuma ñiy suux”.
77فَلَمَّا رَأَى الْقَمَرَ بَازِغًا قَالَ هَٰذَا رَبِّي ۖ فَلَمَّا أَفَلَ قَالَ لَئِن لَّمْ يَهْدِنِي رَبِّي لَأَكُونَنَّ مِنَ الْقَوْمِ الضَّالِّينَ
Ba mu gisee weer wi mu feq, mu ne : “Sama Yàllaa ngii ! ”. Waaye, ba mu suuxee, mu ne : “Bu ma sama Boroom gindiwul, fàwwu danaa bokk ca nit ñu réer ña”.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
75Aaya

Tekki — Al-An'am 75

Simoore Al-An'am Aaya 75 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Noonu Lanu wonee Ibraahiima moomeelu asamaan yi ak suuf si,…

Simoore Aaya 75/165 — Simoore Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-An'am Dégg, Simoore Al-An'am Tekki, Simoore Al-An'am mp3, Simoore Al-An'am pdf. Aaya 73–77. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers