Al-An'am · 78/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
فَلَمَّا رَأَى الشَّمْسَ بَازِغَةً قَالَ هَٰذَا رَبِّي هَٰذَا أَكْبَرُ ۖ فَلَمَّا أَفَلَتْ قَالَ يَا قَوْمِ إِنِّي بَرِيءٌ مِّمَّا تُشْرِكُونَ ٧٨
Transliteration
Falammmaa ra ashshamsa baazighatan qaala haazaa Rabbee haazaaa akbaru falammaaa afalat qaala yaa qawmi innee bareee`um mimmaa tushrikoon
Tekki (Tekkim Wolof)
📖 Tekkim Wolof
Ba mu gisee jant ba fenk, mu ne : “Sama Yàllaa ngii ! Jii moo gën a màgg”. Ba mu suuxee, mu ne : "Yéen samaw nit, man dey deñ naa ba set wecc ci lii ngeen di bokkaale ak Yàlla.
Additional reference in Fulfulde
🎧 Dégg
📜 Aaya 76-80 — Al-An'am
76فَلَمَّا جَنَّ عَلَيْهِ اللَّيْلُ رَأَىٰ كَوْكَبًا ۖ قَالَ هَٰذَا رَبِّي ۖ فَلَمَّا أَفَلَ قَالَ لَا أُحِبُّ الْآفِلِينَ
Ba guddi lëndemee ci moom, mu gis benn bidiw, mu daldi ne : “Sama Yàllaa ngi nii ! ” Waaye, ba bidiw ba suuxee, mu ne : “Man daal soppuma ñiy suux”.
77فَلَمَّا رَأَى الْقَمَرَ بَازِغًا قَالَ هَٰذَا رَبِّي ۖ فَلَمَّا أَفَلَ قَالَ لَئِن لَّمْ يَهْدِنِي رَبِّي لَأَكُونَنَّ مِنَ الْقَوْمِ الضَّالِّينَ
Ba mu gisee weer wi mu feq, mu ne : “Sama Yàllaa ngii ! ”. Waaye, ba mu suuxee, mu ne : “Bu ma sama Boroom gindiwul, fàwwu danaa bokk ca nit ñu réer ña”.
78فَلَمَّا رَأَى الشَّمْسَ بَازِغَةً قَالَ هَٰذَا رَبِّي هَٰذَا أَكْبَرُ ۖ فَلَمَّا أَفَلَتْ قَالَ يَا قَوْمِ إِنِّي بَرِيءٌ مِّمَّا تُشْرِكُونَ
Ba mu gisee jant ba fenk, mu ne : “Sama Yàllaa ngii ! Jii moo gën a màgg”. Ba mu suuxee, mu ne : "Yéen samaw nit, man dey deñ naa ba set wecc ci lii ngeen di bokkaale ak Yàlla.
79إِنِّي وَجَّهْتُ وَجْهِيَ لِلَّذِي فَطَرَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ حَنِيفًا ۖ وَمَا أَنَا مِنَ الْمُشْرِكِينَ
Man jébbalu naa ci Ki sos asamaan yeek suuf si ; di ku Ko wéetal, man dey bokkuma ci way-bokkaale ya.”
80وَحَاجَّهُ قَوْمُهُ ۚ قَالَ أَتُحَاجُّونِّي فِي اللَّهِ وَقَدْ هَدَانِ ۚ وَلَا أَخَافُ مَا تُشْرِكُونَ بِهِ إِلَّا أَن يَشَاءَ رَبِّي شَيْئًا ۗ وَسِعَ رَبِّي كُلَّ شَيْءٍ عِلْمًا ۗ أَفَلَا تَتَذَكَّرُونَ
Aw nitam dàggasanteek moom ; mu ne leen : “Moo ndax dangeen di dàggasanteek man ci Yàlla, te man gindi Na ma ? Ragaluma li ngeen koy bokkaale lu dul lu Yàlla namm. Xam- xamu sama Boroom peeg na yëf yépp. Moo ndax dangeen dul fàttaliku [xalaat] ?
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
78Aaya
Tekki — Al-An'am 78
Simoore Al-An'am Aaya 78 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ba mu gisee jant ba fenk, mu ne : “Sama…Simoore Aaya 78/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 76–80. Tekkim Wolof: Fulfulde.
العربية
English
Bahasa Indonesia
Türkçe
Русский
فارسی
Français
اردو
বাংলা
Deutsch
Español
中文
हिन्दी
Português
Italiano
ภาษาไทย
Polski
Nederlands
Shqip
Kiswahili
O'zbek
தமிழ்
Melayu
Bosanski
Soomaali
Azərbaycan
کوردی
한국어
日本語
Svenska
Dansk
Norsk
پښتو
മലയാളം
සිංහල
Tamazight
Hausa
አማርኛ
Български
Тоҷикӣ
Қазақша
Filipino
سنڌي
Yorùbá
Fulfulde
Татарча
ئۇيغۇرچە
Кыргызча
ਪੰਜਾਬੀ
Jawa
తెలుగు
မြန်မာ
ગુજરાતી
Oromo
मराठी
Tiếng Việt
Malagasy
Нохчийн
Wolof
ދިވެހި
ಕನ್ನಡ
Українська
Ελληνικά
ქართული
ខ្មែរ
دری
Qafar af
Maranao
नेपाली
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers








