Al-An'am · 79/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
إِنِّي وَجَّهْتُ وَجْهِيَ لِلَّذِي فَطَرَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ حَنِيفًا ۖ وَمَا أَنَا مِنَ الْمُشْرِكِينَ ۝٧٩
Innnee wajjahtu wajhiya lillazee fataras samaawaati wal arda haneefanw wa maaa ana minal mushrikeen
📖 Tekkim Wolof
Man jébbalu naa ci Ki sos asamaan yeek suuf si ; di ku Ko wéetal, man dey bokkuma ci way-bokkaale ya.”
🎧 Dégg

📜 Aaya 77-81 — Al-An'am

77فَلَمَّا رَأَى الْقَمَرَ بَازِغًا قَالَ هَٰذَا رَبِّي ۖ فَلَمَّا أَفَلَ قَالَ لَئِن لَّمْ يَهْدِنِي رَبِّي لَأَكُونَنَّ مِنَ الْقَوْمِ الضَّالِّينَ
Ba mu gisee weer wi mu feq, mu ne : “Sama Yàllaa ngii ! ”. Waaye, ba mu suuxee, mu ne : “Bu ma sama Boroom gindiwul, fàwwu danaa bokk ca nit ñu réer ña”.
78فَلَمَّا رَأَى الشَّمْسَ بَازِغَةً قَالَ هَٰذَا رَبِّي هَٰذَا أَكْبَرُ ۖ فَلَمَّا أَفَلَتْ قَالَ يَا قَوْمِ إِنِّي بَرِيءٌ مِّمَّا تُشْرِكُونَ
Ba mu gisee jant ba fenk, mu ne : “Sama Yàllaa ngii ! Jii moo gën a màgg”. Ba mu suuxee, mu ne : "Yéen samaw nit, man dey deñ naa ba set wecc ci lii ngeen di bokkaale ak Yàlla.
79إِنِّي وَجَّهْتُ وَجْهِيَ لِلَّذِي فَطَرَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ حَنِيفًا ۖ وَمَا أَنَا مِنَ الْمُشْرِكِينَ
Man jébbalu naa ci Ki sos asamaan yeek suuf si ; di ku Ko wéetal, man dey bokkuma ci way-bokkaale ya.”
80وَحَاجَّهُ قَوْمُهُ ۚ قَالَ أَتُحَاجُّونِّي فِي اللَّهِ وَقَدْ هَدَانِ ۚ وَلَا أَخَافُ مَا تُشْرِكُونَ بِهِ إِلَّا أَن يَشَاءَ رَبِّي شَيْئًا ۗ وَسِعَ رَبِّي كُلَّ شَيْءٍ عِلْمًا ۗ أَفَلَا تَتَذَكَّرُونَ
Aw nitam dàggasanteek moom ; mu ne leen : “Moo ndax dangeen di dàggasanteek man ci Yàlla, te man gindi Na ma ? Ragaluma li ngeen koy bokkaale lu dul lu Yàlla namm. Xam- xamu sama Boroom peeg na yëf yépp. Moo ndax dangeen dul fàttaliku [xalaat] ?
81وَكَيْفَ أَخَافُ مَا أَشْرَكْتُمْ وَلَا تَخَافُونَ أَنَّكُمْ أَشْرَكْتُم بِاللَّهِ مَا لَمْ يُنَزِّلْ بِهِ عَلَيْكُمْ سُلْطَانًا ۚ فَأَيُّ الْفَرِيقَيْنِ أَحَقُّ بِالْأَمْنِ ۖ إِن كُنتُمْ تَعْلَمُونَ
Te sax man, naka laay ragale li ngeen Koy bokkaale te yéen ragaluleen ne yéen, yéen a ngi bokkaleek Yàlla yoo xam ne wàcceluñu leen ca aw lay ? Kon ñaari kurél ya [yéen ak nun], ku ci gën a yay ci am kóolute ? (waxleen) dengam xam ngeen.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
79Aaya

Tekki — Al-An'am 79

Simoore Al-An'am Aaya 79 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Man jébbalu naa ci Ki sos asamaan yeek suuf si…

Simoore Aaya 79/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 77–81. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers