Al-A'raf · 142/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
۞ وَوَاعَدْنَا مُوسَىٰ ثَلَاثِينَ لَيْلَةً وَأَتْمَمْنَاهَا بِعَشْرٍ فَتَمَّ مِيقَاتُ رَبِّهِ أَرْبَعِينَ لَيْلَةً ۚ وَقَالَ مُوسَىٰ لِأَخِيهِ هَارُونَ اخْلُفْنِي فِي قَوْمِي وَأَصْلِحْ وَلَا تَتَّبِعْ سَبِيلَ الْمُفْسِدِينَ ١٤٢
Transliteration
Wa waa`adnaa Moosaa salaaseena lailatanw wa at mamnaahaa bi`ashrim fatamma meeqaatu Rabbihee arba`eena lailah; wa qaala Moosaa liakheehi Haaroonakh lufnee fee qawmee wa aslih wa laa tattabi` sabeelal mufsideen
Tekki (Tekkim Wolof)
📖 Tekkim Wolof
Àppal Nanu Muusaa fanweeri guddi, Nu mottali ko ak fukk, diir ba Boroomam dogal mat ñeneenti fukki guddi. Muusaa wax na mbokkam ma Aaruuna : “Wuutu ma ci samaw nit, te nangay jubbanti te bul topp yoonu yàqkat ya”.
Additional reference in Fulfulde
🎧 Dégg
📜 Aaya 140-144 — Al-A'raf
140قَالَ أَغَيْرَ اللَّهِ أَبْغِيكُمْ إِلَٰهًا وَهُوَ فَضَّلَكُمْ عَلَى الْعَالَمِينَ
Mu wax ne : “Moo ndax dama leen di wutal jeneen yàlla ju dul Yàlla, te Moom mu defal leen ngëneel, teg leen ci kaw waa àddina si yépp [ca booba] ? ”
141وَإِذْ أَنجَيْنَاكُم مِّنْ آلِ فِرْعَوْنَ يَسُومُونَكُمْ سُوءَ الْعَذَابِ ۖ يُقَتِّلُونَ أَبْنَاءَكُمْ وَيَسْتَحْيُونَ نِسَاءَكُمْ ۚ وَفِي ذَٰلِكُم بَلَاءٌ مِّن رَّبِّكُمْ عَظِيمٌ
(Fàttalikuleen) ba Nu leen musalee ci nitu Firawna ya leen doon teg mbugal mu gën a ñaaw. Daan rey seeni doom yu góor, di bàyyi yu jigéen ya. Te loolu nekkoon na nattu bu màgg bu tukkee ca seen Boroom.
142۞ وَوَاعَدْنَا مُوسَىٰ ثَلَاثِينَ لَيْلَةً وَأَتْمَمْنَاهَا بِعَشْرٍ فَتَمَّ مِيقَاتُ رَبِّهِ أَرْبَعِينَ لَيْلَةً ۚ وَقَالَ مُوسَىٰ لِأَخِيهِ هَارُونَ اخْلُفْنِي فِي قَوْمِي وَأَصْلِحْ وَلَا تَتَّبِعْ سَبِيلَ الْمُفْسِدِينَ
Àppal Nanu Muusaa fanweeri guddi, Nu mottali ko ak fukk, diir ba Boroomam dogal mat ñeneenti fukki guddi. Muusaa wax na mbokkam ma Aaruuna : “Wuutu ma ci samaw nit, te nangay jubbanti te bul topp yoonu yàqkat ya”.
143وَلَمَّا جَاءَ مُوسَىٰ لِمِيقَاتِنَا وَكَلَّمَهُ رَبُّهُ قَالَ رَبِّ أَرِنِي أَنظُرْ إِلَيْكَ ۚ قَالَ لَن تَرَانِي وَلَٰكِنِ انظُرْ إِلَى الْجَبَلِ فَإِنِ اسْتَقَرَّ مَكَانَهُ فَسَوْفَ تَرَانِي ۚ فَلَمَّا تَجَلَّىٰ رَبُّهُ لِلْجَبَلِ جَعَلَهُ دَكًّا وَخَرَّ مُوسَىٰ صَعِقًا ۚ فَلَمَّا أَفَاقَ قَالَ سُبْحَانَكَ تُبْتُ إِلَيْكَ وَأَنَا أَوَّلُ الْمُؤْمِنِينَ
Ba Muusaa agsee ca Sunu ndaje te Boroomam wax ak moom, mu ne : "Sama Boroom, won ma ma gis La ! ”. Mu ne ko : “Doo ma gis Muusaa ; waaye xoolal tundu doj wii : bu saxee ci barab bi mu nekk, kon danga Ma mën a gis.”. Ba Boroomam feeñoo doj wa, dafa mokk rumbax, Muusaa daanu xëm. Ba mu ximmee, mu daldi ne : “Tudd naa sag sell, kañ naa La ! Dellu naa ci Yaw ; te man sax faf maa di ki jëkk a gëm”.
144قَالَ يَا مُوسَىٰ إِنِّي اصْطَفَيْتُكَ عَلَى النَّاسِ بِرِسَالَاتِي وَبِكَلَامِي فَخُذْ مَا آتَيْتُكَ وَكُن مِّنَ الشَّاكِرِينَ
Mu ne ko : “Yaw Muusaa, Man tànn naa la ci biir nit ñi, ngay Sama Yonent ak Sama kàddu. Jëlal li Ma la jox te nga bokk ca way-gëm ña”.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
142Aaya
Tekki — Al-A'raf 142
Simoore Al-A'raf Aaya 142 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Àppal Nanu Muusaa fanweeri guddi, Nu mottali ko ak fukk,…Simoore Aaya 142/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 140–144. Tekkim Wolof: Fulfulde.
العربية
English
Bahasa Indonesia
Türkçe
Русский
فارسی
Français
اردو
বাংলা
Deutsch
Español
中文
हिन्दी
Português
Italiano
ภาษาไทย
Polski
Nederlands
Shqip
Kiswahili
O'zbek
தமிழ்
Melayu
Bosanski
Soomaali
Azərbaycan
کوردی
한국어
日本語
Svenska
Dansk
Norsk
پښتو
മലയാളം
සිංහල
Tamazight
Hausa
አማርኛ
Български
Тоҷикӣ
Қазақша
Filipino
سنڌي
Yorùbá
Fulfulde
Татарча
ئۇيغۇرچە
Кыргызча
ਪੰਜਾਬੀ
Jawa
తెలుగు
မြန်မာ
ગુજરાતી
Oromo
मराठी
Tiếng Việt
Malagasy
Нохчийн
Wolof
ދިވެހި
ಕನ್ನಡ
Українська
Ελληνικά
ქართული
ខ្មែរ
دری
Qafar af
Maranao
नेपाली
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers








