Al-A'raf · 36/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
وَالَّذِينَ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا وَاسْتَكْبَرُوا عَنْهَا أُولَٰئِكَ أَصْحَابُ النَّارِ ۖ هُمْ فِيهَا خَالِدُونَ ۝٣٦
Wallazeena kazzaboo bi Aayaatinaa wastakbaroo `anhhaaa ulaaa`ika Ashaabun naari hum feehaa khaalidoon
📖 Tekkim Wolof
Gaa ña nga xam ne dañoo weddi Sunuy tegtal, rëy-rëylu, dëddu ko, ñooñee ñooy waa Safara, te dañu fay béel.

🎧 Dégg


📜 Aaya 34-38 — Al-A'raf

34وَلِكُلِّ أُمَّةٍ أَجَلٌ ۖ فَإِذَا جَاءَ أَجَلُهُمْ لَا يَسْتَأْخِرُونَ سَاعَةً ۖ وَلَا يَسْتَقْدِمُونَ
Xeet wu nekk am na àpp. Bu àpp ba agsee, duñu yées senn saa te it duñu ko jiitu.
35يَا بَنِي آدَمَ إِمَّا يَأْتِيَنَّكُمْ رُسُلٌ مِّنكُمْ يَقُصُّونَ عَلَيْكُمْ آيَاتِي ۙ فَمَنِ اتَّقَىٰ وَأَصْلَحَ فَلَا خَوْفٌ عَلَيْهِمْ وَلَا هُمْ يَحْزَنُونَ
Éy yéen doomi-aadama yi ! Amaana ay Yonent yu bokk ci yéen dikkal leen, di leen nettali sunuy tegtal, (nangeen xam ne) képp ku ragal na Yàlla tey yéwénal, du am tiitaange te du jàq.
36وَالَّذِينَ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا وَاسْتَكْبَرُوا عَنْهَا أُولَٰئِكَ أَصْحَابُ النَّارِ ۖ هُمْ فِيهَا خَالِدُونَ
Gaa ña nga xam ne dañoo weddi Sunuy tegtal, rëy-rëylu, dëddu ko, ñooñee ñooy waa Safara, te dañu fay béel.
37فَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّنِ افْتَرَىٰ عَلَى اللَّهِ كَذِبًا أَوْ كَذَّبَ بِآيَاتِهِ ۚ أُولَٰئِكَ يَنَالُهُمْ نَصِيبُهُم مِّنَ الْكِتَابِ ۖ حَتَّىٰ إِذَا جَاءَتْهُمْ رُسُلُنَا يَتَوَفَّوْنَهُمْ قَالُوا أَيْنَ مَا كُنتُمْ تَدْعُونَ مِن دُونِ اللَّهِ ۖ قَالُوا ضَلُّوا عَنَّا وَشَهِدُوا عَلَىٰ أَنفُسِهِمْ أَنَّهُمْ كَانُوا كَافِرِينَ
Ana kan moo gën a tooñ kuy duural Yàlla ay fen walla muy weddi ay tegtalam ? Ñoom dey, danañu jot seen wàll wi Nu dogal ci ñoom ; ba kero bu leen Sunuy ndaw dikkale, naan len : “Ana ña ngeen daan jaamu bàyyi Yàlla ? ” - Ñu toontu ne : “Réer nañu nu”. Daldi seede ne ñoom ay yéefar lañu.
38قَالَ ادْخُلُوا فِي أُمَمٍ قَدْ خَلَتْ مِن قَبْلِكُم مِّنَ الْجِنِّ وَالْإِنسِ فِي النَّارِ ۖ كُلَّمَا دَخَلَتْ أُمَّةٌ لَّعَنَتْ أُخْتَهَا ۖ حَتَّىٰ إِذَا ادَّارَكُوا فِيهَا جَمِيعًا قَالَتْ أُخْرَاهُمْ لِأُولَاهُمْ رَبَّنَا هَٰؤُلَاءِ أَضَلُّونَا فَآتِهِمْ عَذَابًا ضِعْفًا مِّنَ النَّارِ ۖ قَالَ لِكُلٍّ ضِعْفٌ وَلَٰكِن لَّا تَعْلَمُونَ
Mu ne leen : “Dugguleen fekki xeet ya leen jiitu woon, di ay nit ak i jinne ca Safara sa.”. Xeet wu ca dugg rekk, tàmbalee rëbb moroom ja. Ba ñépp yembee, ña jiitu ak ña mujj ku nekk naan : “Ñii noo nu sànkkoon : kon nag Yàlla, fulal mbugal ma ci seen kaw.”. Yàlla ne leen : “Yéen ñépp laay ful seen mbugal, waaye xamuleen”.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
36Aaya

Tekki — Al-A'raf 36

Simoore Al-A'raf Aaya 36 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Gaa ña nga xam ne dañoo weddi Sunuy tegtal, rëy-rëylu,…

Simoore Aaya 36/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 34–38. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers